Arafu F
Arafu F
Fegul te fog te foogu tey ku fendi far () ci lépp luy fëkke te am fulla ju far
Te fuglu fàwwu Yàlla tey fàggu bisam () ba mujj tey farlu ba feesaluw fanam
Te femm bakkan bi te fàndaañu te fëx () ba fagg bul fipp ba far tàbbi ci pax
Te bul di féttéerlu ba fiirook sa bakkan () facanteel ak moom te far ak Yàlla ba fen
Fépp fu saytaane ñëwee nga fénati () te xam ne lépp lu’m la wax day fenati
Yàlla ku fiir la kon faral féete fa moom () adduna daa fuytu te ag sax du jikkoom
Te fiir la guy ferngali fàdd lay fexe () ku ci ne fóox sa tànk far ñàkk pexe
Nga rët sa faalanqe gi fettax ne falañ () te fekk fomb wéy nga fande nib fariñ
Nga fande fii ak fële feccikul ca teel () lépp lu lay musal ca fiir googa fexeel
Sa faayda firndéel ko ci fonkug fagaru () fab jiwu fit te dem ca tooli xol faru
Faxas sa fuuy gi tey fésal sa yéene nag () te ful sa jëf mu feese yiw nga falu nag
Fodoŋ sa bakkan bi te folli ag palam () te fecci kóllareem ga fas nag sa kanam
Faramlikug tenq ga bu’m la fif ba tax () nga far ko kon nga fuuti fequl te nga fëx
Firincikul ca buum ga felli teel a fog () fenam ya buñ la fàbbi fippal takku nag
Fobul te fas yéene mu foñ la foñ ko it () te bul ko faale it na fàndaañu ba rët
Cig follikoom ngay falu fàwwu fëll it () ca maas ga formànko ci coona fës ci sut
Bañ a nelaw guddi Xel mu ñor akug mag artu Dox te solo dàll Fënd ak sonn Lànk ag topp Tàqalikool ak moom Dummóoyu ngir soof gu la mbir soof neex Ndëgg-sërëx Kubéer gu àggut joggi Nga tiit Liy tëb ak a dal ci put gi boo tiitee Aw daanuwiin Ñàng ga Xëcc Nga ànd ak moom dagg daw wëlbati Mere ak won ginnaaw