Yewwute gu ndefar (industrie) : li mu jagoo – ay màndargaam – li mu fi indi: Soppi

Yewwute gu ndefar ci Tugal, ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug ndefar, walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig, rawati na ci Biritani, ci ñatteelu xaaj bu mujj bi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g.

Waaye nag, moom ndefar gii, yàggul dara mu tàmblee tas ci Tugal nànk-nànk, ak Aamerig, la ko dale ca njëlbéenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Bi mu ko defee nag, ay jeexiitalam tas, ba àgg ci pàkk yu bari ci àdduna bi, loolu nag ci ñaari xarnu yii la: fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar-fukkeelu xarnu g.

Ndefar yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ba ci suñu jamono jii ñu toll.

Looloo waral du man a ñàkk ñu xam sabab yi tax yewwuteg ndefar am ci Tugal.


Sabab yi tax yewwuteg ndefar am ci Tugal Soppi

1 Jëm-kanam gi xam-xam def ci Tugal, ci jamonoy yewwute, moo waral yewwuteg ndefar am.

2 Dëkki Tugal yu mag yi, am gi ñu am, ak tegu gi ñu tegu ci yaxantu ak ndefar, ak woomleg koom gi loolu di jur, nga xam ne day tax ba ndefar di jëm kanam, rawati na, gi ci aju ci ràbbu sér , nga xam ne mooyndefar gi njëkk ci Tugal.

3 Jëmmaan (l'individu) walla jëmm ci Tugal, ni mu jekki-jekkee rekk fés, mujj di dàtt bi mboolaayi Tugal yi tegu, sabab la ci li yee waa Tugal yi, moom jëmm jooju, ci Tugal kees tënk la woon ci jéngi nosteg laman , jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu, féexal am xelam, leeral ko ci xam-xam, ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam.

4 Li juddoo ci wuññiy melosuuf yi it, muy teg loxo gi réewi sancaan yi daa def réew yi ñu sanc , ak di fa jële ay xéewal aki cémb (ñumm) , di leen yobbu seeni réew, loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg ndefar gi ci Tugal.

5 Réewi Tugal yi ak mbootaayi koppar yi, jàpple gi ñu doon jàpple sémb yi jug ngir jëmale kanam ndefar ci Tugal, loolu de ci li defar jawwu ji la ba ndefar man a dox, man a àntu.

6 Boroom xam-xam yu aay, yi xëy feeñ, te bari ci Tugal.

7 Bari gi liggéeykat yi bari ci Tugal, rawati na ñiy liggéey ci ndefar yu ndaw yi. Na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati Angalteer yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi, ci liggéeykat yi amoon xam-xam yu néew lañu woon, nga xam ne daanaka jànguñu woon.


Yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam Soppi

Yewwuteg ndefar ci Tugal, daa jagoo woon ay mbir yu bari, yii ci lañu:

1 Jëmale kanam gu ñu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb : Soppi

Meccem ràbb daal, ci yi gën a jariñu ci fent yu xam-xam yi aamoon ci Tugal la, rawati na ci Britani, loolu di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g.

Loolu nag li ko waral mooy yittewoo gu tar gu nit yittewoo ay sér, ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir liggéey ci.

Ràbbkatu Angalteer bi ñuy wax James Hargreaves, jot na a fent atum 1764 g, benn jumtukaayu defar wëñ, muy benn masin (wuutuloxo) bu loxo, bu ñuy jëfandikoo ci ëcc, li koy doxal nag doon genn mbege walla póno, bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay, bu ko defee benn liggéeykat di ko yor, di ko doxal.

Bu ko defee, fentkat bu Angalteer bii di Richard Arkrihgt, fent moom it atum 1771g, benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi, moom nag jumtukaay la bu ñu daa doxale ci dooley ay fas, mujj ñu koy defe ci dooley ndox, ñu tudde woon ko kaadaru ndox bi, (water frame). Ki ñuy wax Samuel Compton, ñëw fent – atum 1779g – benn jumtukaay buy boole gaaw ci liggéey bi ak baaxle ko, boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi, ci ñaari diiwaani Angalteer yii di Yorkshire ak Lancashire .

Ki ñuy wax Edmund Cartwright, moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu ñuy doxale dooley ndox, ginnaaw bi ñu koy doxale dooley cóolóol , te kat tax na ba ñu man a ful li ñu daa ràbb, daa ko defar ciy sér.

Liggéey bi ñu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal liggéeyu ëcc beek ràbb bi, gën a dolliku, te sax. Nu àgg ci jëfandikoo ne-ne yu simi yi ngir raxas wëtéen wi, defarati yeneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi ñu liggéey.

2 jëfandikoo kàttan : Soppi

Jumtukaay yu njëlbéenu yi amoon, nit a ko daa doxale ci dooleem, walla dooley dundat . Kàttan nag di “energie” jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te dox. Ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbéen gi dooley ndox, ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul, ginnaaw bi, mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ.

Ki ñuy wax Thomas Newman, ñëw, indi fi jumtukaayu cóolóol, James Watt, moom itam dikk, gën a defaraat jumtukaayu Thomas boobu atum 1765g, loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug liggéey bi, ak li ñuy liggéey, ndax kat dugal gi ñu dugal jumtukaay bu mekanig, bu cóolóol ci ndefar ak jokkoo lu rëy a rëy la te am solo, te moo tax ba nga gis ndefar tay mu toll fii mu toll.

Bu ko defee ca saa sa, waa Tugal yi tàmblee gëstu fu ñuy jële këriñ. Këriñ nag bari woon na lool ci Wels gu bëj-saalum gi, ak Skotland.

Nit it gënoon na a jéego ay jéego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan, mu feeñaloon petrol ca D.B.A (Diiwaan yu Bennoo yu Aamerig yi), ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Ginnaaw bi, ñu gisaat petrol fu bari ci àdduna bi. Ginnaaw bi ñu fentati benn jumtukaay buy “lakk ci biir”, boo xam ne mooy soppi petrol bi, ginnaaw bu ko lakkee, def ko kàttan guy yëngal ak a doxal. Loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne dañuy sukkandiku ci li ñuy wax “lakkug biir gi”, mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi, jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni: oto yii ngay gis, fafalnaaw yi, gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs.

Mbëj tam jariñ na nit lu bari, loolu nag mi ngi ame ci bi kii di Faraday juge, fent li ñuy wax '''juddalukaayu mbëj''', nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay liggéey ak njariñ ci dundam.

Nit àgg na ci xam kàttanug saal te jëfandikoo ko ci anam yu bari, loolu tax mu man a néewal li muy sukkandiku ci petrol. Waaye nag nañu xam ne kàttanug saal moom lu seer la, manu fee wuutu petrol ci genn anam, nit it jot na a xam kàttan gu jant gi , te jëfandikoo ko ci yenn anam yi, niki nuggalukaayu ndox yu jant yi ñuy jëfandikoo ci kër yi, ak ci yeneen anam yi.


3 Jëm kanam gu ndefar gu weñ jëm kanam Soppi

Bokk na ci lu am solo li yewwuteg ndefar gi jagoo, bokk na ci, jëmale gi ñu jëmale kanam ndefar gu weñ, loolu nag mooy bi waay Angalteer jii di Bassemer, jugee, fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def “sulb” mooy weñ gu wow kong, dëgër këng, loolu nag ni mu daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool. Nit it gënoon naa def ay jéegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay génne këriñ, loolu tam dimble ko ci mu man a dolli, gën a lëwal li muy liggéey. Lii lépp nag bokk na ci li waral yewwuteg ndefar gi man a am ci Tugal, rawati na ci Britani.


3 Jokkoo gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam Soppi

Li kenn manul a sikk mooy ni ndefar jëme kanam ci Tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo, rawati na bi liggéeyu weñ gënee dox, gën a jëm kanam. Ci noonu angle bii di George Stephonson, moom ñëw , fent saxaarug cóolool maanaam , muy daw ci ay banti weñ ci diggante dëkkub Liverpool ak Manchester ci atum 1830g, yoonu weñ wii mooy yoonu weñ wi njëkk ci àdduna bi.

Ginnaaw bi, nitug Aamerig kii di Robert Foulton, moom dikk, jëfandikoo cóolool, di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi. Ginnaaw bi mu jugati, jëfandikooti cóolóol, dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci géej yeek mbàmbulaan yi. Ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk-nànk, ni ko ndefar defe. Bu ko defee, feeñteg jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg ndefar gu mag gii am tay ci àdduna bi.


4 Feeñug campeefi ndefar yi : Soppi

Liggéeyuwaay yu ndaw yi juge nañu ci kër yi, doon leegi ay campéef yu ndefar, yu mag, yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi. Ndefar yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo yu ndefar, yu mag ñoo koy moom, ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi.

Liggéeyuwaay walla isin yu mag yi nag, ci wetu barabi cémb yi (ñumm yi) lañu daa faral a sampu, te loolu da leen daa dimbale ci ñu man a néewal seeni fere ci lu aju ci seeni liggéey, ndax loolu daa na tax li ñu ci waroon a ñàkk gën a néew. Néewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi, ndax daa na leen daaneel. Te daa na gën a baaxal liggéey bi, gën koo wuuteel.


Li fi yewwuteg ndefar gi jur: Soppi

Maneesul a sikk ne yewwuteg ndefar gi indi na ci Tugal ay ngérte yu yaatu ci wàlli koom, politig ak mboolaay.


Li mu fi indi ci wàllug koom: Soppi

Yewwuteg ndefar gi bàyyi na fi ay jeexiitat yu rëy ci wàllug koom, ci biir Tugal ak biteem. Ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ, yi daa am jumtukaay yu rëy yi. Li ñuy liggéey gën a yokk, gën a wuute, li ñu koy jënde gën a néew, ñépp man cee jot, jumtukaayi liggéey yi gën a bari, jokkoo gën a yomb, yoon yi gën a bari, ja yu àdduna yi gën a yaatu, lonkoo yu mag yi amoon ay gis-gis aki xemmemteefi rënk ak sanc , tàmblee booloo.

Ndax kat canc gu politig gu yees gii, du lu dul doomi canc gu koom-koom, gi Tugal daa def, jaare ko ci ndefaram gu jëm kanam gii, ak baaxug ay jumtukaayam, ak soxla gu tar gu mu soxla ñumm yi, ak soxla gu mu soxla ay ja yu yees, yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute.

Waaye mbay nag moom, ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lépp, ak li mu gën a ñaw lépp, te gën a xam-xame, teewul ay njëgi njuddéefam gën a seer, li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi dañoo gàddaayoon àll yi, dem ci taax yi, fi isin yi nekk, ngir man fa a liggéey, ndax la ñu daa ame ci liggéey bi moo daa gën a bari, te daa nañu ci ame ag sax fi barab. Gàddaay gii nag, juge ci àll yi, dem ci taax yi, taxoon na ba ab kiris walla jafe-jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci Tugal, rawati na ci Angalteer.

Joqalanteg yaxantu gën a yokku ci àdduna bi, nga gis réew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu, ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci géej yi, ak mbàmbulaan yi , ak barabi romb yu àdduna yi. Ci noonu lonkooy yaxantu yu àdduna yi nga xam ne seeni boroom dañuy am alal lool tàmblee feeñ, bank yi tàmblee yëngook a sawar, ak këri koppar yi.


Li mu fi jur ci politig: Soppi

Sanc gii Tugal tàmblee sanc réewi jàmbur yi ak di leen teg loxo, bokk na ci li fi yewwuteg ndefar gi indi, wuutal ko fi, ginnaawal ko fi ci wàllug politig, ndax ni ma la ko waxe woon ci ginnaaw , ndefar day soxla ay cémb (ñumm)(matière première), te loolu dañu ko daa gis feneen fu dul Tugal, te loolu jur na ay xare ci diggante ay réew ci fu bari ci suñu àdduna bii, tax it ba réew yi ñu sanc jug, di xare ngir goreel seen bopp, soril senn bopp ag canc, ak lépp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp, ak tembadi.

Bu ko defee, benn dal (principe) daal di feeñ ci Tugal, mooy dalu “koom-koom bu gore bi walla bu af bi” (bu libre bi) am te taxaw ci nosteg bopp-alal (système capitaliste) . Loolu nag mi ngi am ci ginnaaw bi ndefar gu yees gii soppikoo dem ci noste gii, li ko waral di yitewoo gu bari gi mu yitewoo ci ñu sos ay isin yu mag, ak isin yu mag yii, yitewoo gu tar gi ñu yittewoo alal ju bari ngir taxawal leen, sos leen.

Nguuri Tugal yi, jàpple woon nañu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li ñu man, am ko ciy man-man aki kerkeraan . Ci noonu wartéefi góornamaa yi gën a yaatu, gën bari ci mboolaayi ndefar yi. Loolu yobbu leen ci ay wartéef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi, te yittewoo leen, sosal leen ay jàngu (leekol) aki daara yu mag, ak sonn ci mbiri wér gu yaram, ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam (societe bi).

Ci noonu ay boroom xam-xam aki bindkat daal di feeñ, yoo xam ne seen liggéey bépp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi, suqali ko. Ay gisiini politig yu yees feeñ, yoo xam ne bokk nañu ci li fi indi xalaatu politig bu Tugal bu yees bii tay.

Góornamaay Tugal yi duggsi nañu ngir aar liggéeykat yi, ci noonu ñu yamale waxtu yi ñuy liggéey, def leen leegi ñuy: 7 – 8 waxtu, te bu njëkk 12 – 16 waxtu lañu woon. Ñu ñëwati indi fi noppaluy tawat yi ak yu njeextel-ayu-bis yi ak yu at yi . Ñu defati ay liggéey ngir yekkati seen payoor yi, jéemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax.

Man gi réewi ndefar yi man a doxal seen mbiri réew, feeñ na, te am bi réew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ . bu ko defee, nga gis réewi Tugal yi sukkandiku ci ndefar, ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay, ak ngànnaay yu yàgg, yi ñu miinoon.

Li mu fi jur, indi ko fi ci wàllug mboolaay: Soppi

Yewwute gi ci Tugal jur na ay gàddaay yu mag, juge ci àll yi, ak dëkk-dëkkaan yi, dem ci taax yi ak dëkki ndefar yi, loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo, jumtukaayi ndefar yi gën a xereñ cig wàll, moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci Tugal, la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g, rawati na ci Angalteer ci geneen wàll.

Bu ko defee, baykatu Tugal bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li ñu koy fay moo gën a wóor te gën di lu ñu xam, te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg-leeg mu baax, leeg-leeg du baax, ak jafe-jafe yi mu àndal, muy njaay meek toppatoo gi.

Lii mooy li waral ñiy liggéey ci mbay néew, te wàññiku, ñi dëkke kaw gi gën a néew, loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi, bu ko defee, am lu juddoo ci loolu, mooy néewug njóoxiitum mbay mi , te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer.

Beneen jafe-jafe daal di juddooti, mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi, di wër liggéey. Ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk. Di dëkkal lu sakkan ciy nit, te matalewul li ñu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu. Ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe-jafe yu rëy a rëy , jikko it naka noonu. Jafe-jafey liggéeykat yi gën na a yokku, bi ñu demee ba li ñu leen di fay manatul a faj gën ja’a néewi seeni aajo, ngir seerug dund gi.

Beneen jafe-jafe bu mboolaay bu bees amati, ànd ak yewwuteeg ndefar gi, ak ag jëmam kanam, loolu mooy ne lu bari ci jigéen ñeek xale yi, leegi dañoo tàmbli di liggéey ci isin yi, te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu ñu man a gën a ame ay liggéeykat ba gën a man a néew lu ñuy fay, ginnaaw liggéey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko. Loolu tam jurati yeneen jafe-jafey mboolaay, ndax tax na ba jigéen bàyyi fi ay liggéeyi boppam, dem ci isin yi, xale yi it bàyyi njàng mi, te loolu ag pert manu koo kawe, ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg.

Ag yàqu-yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay gu mboolaay yi, ci Tugal, loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk-liggéey walla ag liggéeyadi tàmblee tas ak a yaatu ci Tugal, ci liggéeykat yu góor yii nga xam ne dañoo tàmbli woon a nekk ay jafe-jafe dëgg, ci kanamu goornamaa yi, di yëngal, tey sàkku nu ñu leen lijantile seen jafe-jafey liggéey yi. Ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte , indi ay sart yu nos liggéey bi, aar liggéeykat yi ci fuqaleg boroom bopp-alal yi moom isin yi.

Gongikuwaay Soppi

Téere taariix bu Abdu Xaadir KEBE