Xewar xeetu garab la gu bokk ci njabootug « Sapindaceae ».

Xewar gi (Lepisanthes senegalensis)
Xewar gi (Lepisanthes senegalensis)

Cosaan li

Soppi

Moo ngi tasaaroo ca Afrig ci réew yii: Senegaal, Eritere, Ecopi, Somali, Sudaan, Keeñaa, Tansani, Ugàndaa, Kamerun, Réewum Diggu-Afrig, Gaboŋ, Kóngoo, Bene, Kodiwaar, Gàmbi, Gana, Gine, Gine bisaawóo, Niseer, Niseeryaa ,Tógoo, Àngolaa, Mosàmbig, Madagaskaar.

Amna it ca Asi gu bari naaj ga: Bangalades, Butaan, End, Nepaal, Siri-lànka, Kàmbots, Lawos, Birmani,Taylànd, Wiyet-naam, Endonesi, Maleesi, Papuwaasi Gine Gu yees ak Filipiin.

 
Meññeefum garabu xewar

Melo wi

Soppi

Xewar garab la guy toll ci 6i met ci guddaay. Ay xobam day nëtëx.

Turu xam-xam wi

Soppi

Lepisanthes senegalensis (Aphania senegalensis)

Tur wi ci yeneeni làkk

Soppi

farañse: Cerisier du Cayor