Xadi Silla
Xadi Silla
Dundu ak jaar-jaar | |
Juddu | 27 màrs 1963 wala 27 màrs 1967
Dakaar |
Faatu | 8 oktoobar 2013
Dakaar |
Réew | Senegaal |
Tàggatu | Iniwersite bu Pari |
Liggeey | Saa-sinemaa, bindkat |
Yeneen xibaar | |
Liggeeye na | Iniwersit Seex Anta Jóob |
Erreur de script : la fonction « build » n’existe pas. Abla Pokou (wala Aura Poku, wala Abraha Pokou) lingeeru Afrig la , juddoo ci fukk ak juróom-ñetti xarnub. Indi na askanu Baoulé ci réewum Gana ba ci Kodiwaar. Léeb bi dafa nettali, saraxu doomam bu góor ngir jàll ag dex .
Bat bi "Baoulé " li nu tudde leegi askan yi , mu ngi joge ci saraxu doomam.
Bicci toppu saraxe, né na "Ba-ouli", loolu dafay tekki "doom bi dee na". Xadi Silla mu ngi juddu ñaar-fukki fan ak juroom-ñaar atum 1963 ci Dakaar, génn àdduna juroom-ñetti fan ci weeru oktoobar atum 2013. Bindkat la woon bu doon yëngatu ci sinemaa tamit.
Dundu ak jaar-jaaram
SoppiGinnaaw bu mu amee bakalóoreyaa ci Dakaar ba pare, Xadi Silla dafa dem Pari ngir wéyal fa ngàngum njënd ak njaay mu mu doon def. Bi mu demee, dafa mujj dakkal njàng moomee, dem jàngeji Hypokhâgne (ci néegu njàng buy waajal xam-xamu càllala), foofu la ame ab lisãas ci filosofi. Mu dakkal njàngam mi, tàmbali di ànd ak ay nit (góor ak jigeen) yuy yëngu ci mbiru uslu ak misig… Foofu sax la ko cofeel gi mu am ci mbind mi feeñoo. Ginnaaw bu waajuram wu jigeen faatoo, mu tàmbalee bind : « Dama xalaat ne bu may bind ci moom, dina am lenn lu ma mën a dekkal, dinaa ko mën a génne ci lu ma jàpp ne lu neenoon ba pare la ». Ci noonu, mu daldi bind mayeem (nuwelam) bu jëkk, tudde ko L’Univers, waaye ba tey, téere boobu kënn mësu ko siiwal. Mu wéy di bind bés bu Yàlla sàkk te mbind moomu sukkandiku ci ay xalaat yu tukke Dakaar, dëkk bi mu juddoo, « mu mujj nekk dëkk bu yéeme ndax li ma nekk di dundu feneen ».
Atum 2005, mu jël neexalu joŋante bi amoon ca festiwaalu àdduna ci mbind ak ceetaan ba amoon ca Màrsey, ndax film bu mu defoon tudde ko Une fenêtre ouverte.
Mu ngi doon jàngale almãa ci iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar.
Ab téereem
Soppi- Le Jeu de la mer (roman), Paris, l'Harmattan, 1992, 160 p. (ISBN 2-7384-1563-6)
Léppi filmam
Soppi- 2005 : Une fenêtre ouverte
- 2006 : Colobane Express
Téere, jukki wala dali web yi ñu yër
SoppiToftal yi
SoppiLees bind ci moom
Soppi- Françoise Pfaff, « Khady Sylla », in: À l'écoute du cinéma sénégalais, Paris : L'Harmattan, 2010, p. 213-224 (ISBN 9782296103528)
Jukki yi ñu ko tudd
Soppi- Sinemaa bu Senegaal : <small>Cinéma sénégalais</small>
- Limu filmë yu Senegaal : <small>Liste de films sénégalais</small>
Lees jële feneen
Soppi- Fees ko mën a xame
- Dundu ak ay téerey Xadi Silla : Bio-bibliographie de Khady Sylla