XUDAR
XUDAR /Xadir /Xidir
Xudar, mooy jëmm ji Alxuraan di nettali ci Saaru Xunt Ma {65. Ñu daje ak ab jaam ci sama jaam yi boo xam ne may Nanu ko yërmaande lu jóge ci Nun, te jàngal Nanu ko xam-xam bu bàyyikoo ci Nun.} [Saar 18 : Xunt Ma], Muusaa toppoon ko ca dajewaayu ñaari geej ya {66. Muusaa ne ko : “Ndax ma topp la ci kaw nga jàngal ma ci lu xamaleef na la ko ci luy gindee [ak xamle] ? ”.} [Saar 18 : Xunt Ma]. Wuute nañu ci ne ndax ab Yónnent la am déet, am ñu nitu Yàlla la woon, ba moo tax jullit ñi sunu tuddee turam teg ci (HS) (Halayhis Salaam/ yal jàmm ne fa moom). Sahaaba bii di Ibnu Mashuut nee na moom (Xudar) lañu namm ci laaya:{40. Ka ame woon xam-xamu Téere ba ne ko : “Mën naa la koo indil ba la ngaa xef”. [Ne ko mingi nii] , ba ko Suleymaan gisee ci kanamam, dafa wax ne : “Lii dey ngënéelul sama Boroom bi la. Dama ciy nattu ndax damay sant walla damay xarab... képp kuy sant yaw caak, ku weddi nag, sama Boroom moom di Ku doylu, di Ku tedd”.} [Saar 27 : XORONDOM YA] loolu wuute ak waxu Ibnu Abbaas ja te mooy li gëna siiw, nee na ki ñu namm ci laaya ji mooy Aasif doomu Barxiyaa. woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ag faatoom, waaye ñiy wax ne moo ngi dund ba leegi bari na loolu ci waxi fere yi.
Xudar nag ku ñu jox dayo la ci ag sellal ci diine yu bari niki diiney Masiih, Darsi ak Yahuut yi. Ci baaxi Lislaam ak yu dul Lislaam yu bari dañuy melal Xudar ci Yónnent, Nabii, Walliyu, Jaamu Yàlla, Malaaka, Kiy wattu géej gi ak Sëriñu bóoti xam-xam, muy kuy jappale ñi nekk ciy nattu. Dëppale nañu jëmmi Xudar ak ay jëmm yu wuute ciy jamono yu fasantikoo, niki rekk nu tudd ci Saruus ca Irãn, ku sell ka Sarkiis gawar ba ak ku sell ka Jarjes ca Asi gu ndaw ga ca réewi Saam, ak Yuuhanaal Mahmadaan ca Armeen. Am na ñu bari ñu ko jàppe ne mooy Iiliyaa.
Ag Askanoom
Soppiworoom xam-xam yi dëppoo wuñu ci fu mu askanoo, amna ay nettali yi bari ci wall googu, bokk na ca:
Ibnu Kasiir wax na ca téereem ba "Al-Bidaaya Wan Nihaaya" ne Xudar, Aadama a ko jur ci geñoom: « Al-Hafis mom Hasaakir nee na: waxees na ne mooy: Xudar mom Aadama(HS) ci geñoom. ginnan ba mu nettali awale ko ci Ad-Daaruqutnii ne: Muhammat mom Al-Fathul Xalaanisii nettali na nu, Al-Habbaas mom Abdul Laah Ar-Ruumi nettali na nu, Ruwaat mom Aj-Jarraah nettali na nu,Muqaatil mom Sullaymaan nettali na nu jële nañu ci Dahaag, jële ci Ibnu Habbaas mu ne : Xudar doomu Aadama la ci geñoom, ñu dooli ay fanam ba muy fenloo Dajjaal, lii nag Hadiis bu ddog la te yéeme.» _Ibnu Kasiir, Al-bidaaya Wan-Nihaaya- Pàcci bu njëkk bi.
waxees nañu ne mooy Xaabiil mom Aadama, am ñu ne mooy Bilyaa mom Milkaan (/Kilmaan) mom Faalix, doomu Saalix mom Haamir doomu Arfaxsat, amna ñu ne mooy Al-Mahmar doomu Maalig doomu Abdul Laah mom Nasr doomu Asd, am ñu ne mooy : Doomu Hamaa-il mom Nawaat mol Hiis mom Ishàq. ñenn ñi ne moom sët la ci Ndawu Yàlla lii di Haaruun miy magu Yónnet Yàlla Muusaa, jële nañu ko ci Kalbii mu jële ci Abii Saalih mu jële ci Abii Hurayrata mu jële ci Inbu Habbaas,te moom ku sori la, am ñu ne doom la ci doomu Fihawn ju jigéen, am ñu ne sax doom la ci Firhawn, loolu Nuqaas nettali na ko, amna ñu ne mooy Yónnent Yàlla Ilyasah, am ñu ne mi ngi bokk ci doomi Faaris, doom la ci kenn ci ñi gëmoon Yónnet Yàlla Ibraahiima te gàddaayoon ànd ak moom juge Baabil (Babilõ) waxees na ne baayam ab saa-pers la woon yaayam di ab saa-rom, am ñu wax fasaan wi.
amna ñu wax ne mooy Xadiruun mom Haayiil mom Mahmar mom Hiisuu mom Ishàq mom Ibraahiima, waxeew na ne mooy ka Yàlla rayoon téeméeri at ginnaaw ba mu dekkal ko dootul deeti ba ba ñuy ëf buftu ba ci Saaru Nag Wa Laaya {259. Walla ka romboon ab dëkk bu ràppoon ba ruus, mu ne : “Waa naka la Yàlla di dundalee lii ak ni mu dee te wow ? ”. Yàlla daldi koy rey moom lu tollu ci téeméeri at. Daldi koy dekkalaat, ne ko : “Sab yàggaay fii nu mu tollu ? ”. Mu ne ko : “Benn bis walla sax matu ko.”. Yàlla ne ko : “Am nga fi téeméeri at. Xoolal sa lekk gi ak sa naan gi : soppikuwuñu ; waaye xoolal sa mbaam mi... Te ngir nu def la kéemaan ci nit ñi, xoolal ni nuy dajalee yax yi, ba noppi wodde ko yàpp”. Ba mu ko leeree nàññ nag, mu daldi ne : “Xam naa xéll ne Yàlla mën na lu ne”.}
Lu Waral Tur Wi(Xudar)
Soppisoloo nañu ci Abii Hurayrata ci Sahiihul Buxaarii “Tuddee nañu ko Xudar ngir ne daa fa toog ci...”