Coqueluche, feebaru sëqët bu tar la, ñu koy faral di woowe sëqëtum100 fan, feebar la bu gaaw ci wàlle te benn doomu jàngoro (bakteri) moo koy joxe.[1][2] Su lay sooga dal, dangay melni ku soj, sa bakkan di sotti ndox, sa yaram tàng ngay sëqët ndànk.[3] Ci ayi-bis yi ci topp, sëqët mi dafay gëna tar.[4] Nit ki su sëqëtee ba sëqët mi jéggi dayo, su nit ki noyyi dangay dégg muy riir.[1] Sëqët mën na dem ba 100 fan, wala ba 10 ayi-bis.[5] Nit ki mën na sëqët ba waccu, wala mu dam faaram, wala mu dem sax ba dootul amati benn njariñ.[6] Su jàppee xale bu amagul at, du sëqët wala limuy sëqër du bari waaye nak mën na fatt seen noyyi ab diir.[1] Diggante bi muy dug sa yaram ak bi muy feeñ mën na def juróom ñaar jàpp fukki fan.[7] Feebar bi mën na dal ñi ñaqu ba noppi waaye ni muy feeñee du tar noonu.[8]

Doomu jàngoro (Bactérie) biy joxe coqueluche mooy Bordetella pertussis.[9] Feebar la buy tasaaroo ci ngelaw li, di bawoo ci kiy sëqët, tisooli ki am feebar bi.[10][11] Bu nit ki xasee ba am feebar bi rek mën na ko wàllee ba keroog sëqëtam mu metti mi di am ñatti ayi-bis.[12] Ñi ñu fajee ak ay antibiotic dootu ñu wàlle suñu weesoo juróomi fan.[12] Suñu bëggee saytu feebar bi, dañuy xool ci ginaaw bakanu nit wala ci putam.[13] So noppee ñu amal njàngat mu xóot ci ni chaine polymerase bi di doxee.[13]

Li gëna mëna aar nit ki ci jàngoro jooju mooy mu ñaqu anti-coqueluche.[14] Liir bi su amee juróom benn jàpp 8 juróom ñatti weer dañu ko wara ñaq ngir musal ko ci feebar boobu, mu luñu wara baamtu ñeenti yoon laata xale bi di weesu ñaari at.[15] Lu ñaq bi di gëna yàgg dooleem di gëna néew, moo tax yen xale dañu leen di faral di baamtul ñaq bi, ak yenn mag yi itam.[16] Nit ñi nekk ci barab bu leen feebar bi mëna dale, mën nañu jël antibiotic ngir mu musal leen ci feebar bu tar bi.[17] Ki feebar bi dug ci yaramam ba noppi mën na jël ay antibiotik diiru ñatti ayi-bis ginaaw bi feebar bi tàmbalee feeñ suko weesoo du ci mën lu bari.[18] Sudee xale bu amagul at la, ak ci jigéen ñi ëmbmën nañu ko jël ci biir 6 ayi-bis ginaaw feeñal yu njëkk yi.[18] Antibiotik yi nga mëna jëfandikoo ñooyerythromycin, azithromycin, walatrimethoprim/sulfamethoxazole.[12] Ama guñu gëstu bu leer bu wane xarañteg garab giy dakkal sëqët mi.[19] Lu tollu 50% ci xale yu bari yu amagul benn at, fàww ñu yóbbu leen hospital, 0;5% ci ñoom (1 ci 200) dañuy faatu.[20][21]

At mu nekk coqueluche dina jàpp lu tollu ci 16 milion ci nit ci àdduna bi.[22] Waa réew yu néew doole yi lay gëna jàpp te mën na dal ku nekk, mag wala ndaw.[23][19] Ci atum 2015 feebar faat 61 000 nit – wuute ak 138 000 yi mu faat ci  1990.[24] Lii yi amagul at le am feebar lu xawa yées 2% ci ñoom lay faat.Jàpp nañu feebar baa ngi njëkka feeñ ci 16eme xarnu (siècle).[7] Ci atum 1906 la ñu njëkka gis bacterie bi koy joxe.[25] Ci atum1940 lañu njëkka génne ñaq bi.[7]

  1. 1,0 1,1 et 1,2 "Pertussis (Whooping Cough) Signs & Symptoms". May 22, 2014. Archived from the original on 7 February 2015. Retrieved 12 February 2015.[1]
  2. Carbonetti NH (June 2007). "Immunomodulation in the pathogenesis of Bordetella pertussis infection and disease". Current Opinion in Pharmacology. 7 (3): 272–8. doi:10.1016/j.coph.2006.12.004. PMID 17418639.
  3. "Pertussis (Whooping Cough) Signs & Symptoms". May 22, 2014. Archived from the original on 7 February 2015. Retrieved 12 February 2015.[2]
  4. "Pertussis (Whooping Cough) Signs [3]& Symptoms". May 22, 2014. Archived from the original on 7 February 2015. Retrieved 12 February 2015.
  5. "Pertussis (Whooping Cough) Fast Facts". cdc.gov. February 13, 2014. Archived from the original on 7 February 2015. Retrieved 12 February 2015.[4]
  6. "Pertussis (Whooping Cough) Complications". cdc.gov. August 28, 2013. Archived from the original on 9 February 2015. Retrieved 12 February 2015.[5]
  7. 7,0 7,1 et 7,2 Atkinson W (May 2012). Pertussis Epidemiology and Prevention of Vaccine-Preventable Diseases (12th ed.). Public Health Foundation. pp. 215–230. ISBN 9780983263135. Archived from the original on 2017-07-29.[6]
  8. "Pertussis (Whooping Cough) Signs & Symptoms". May 22, 2014. Archived from the original on 7 February 2015. Retrieved 12 February 2015
  9. "Pertussis (Whooping Cough) Causes & Transmission". cdc.gov. September 4, 2014. Archived from the original on 14 February 2015. Retrieved 12 February 2015.[7]
  10. "Pertussis (Whooping Cough) Causes & Transmission". cdc.gov. September 4, 2014. Archived from the original on 14 February 2015. Retrieved 12 February 2015.[8]
  11. "Pertussis". WHO. Archived from the original on 5 June 2015. Retrieved 23 March 2016.[9]
  12. 12,0 12,1 et 12,2 "Pertussis (Whooping Cough) Treatment". cdc.gov. August 28, 2013. Archived from the original on 11 February 2015. Retrieved 13 February 2015.[10]
  13. 13,0 et 13,1 "Pertussis (Whooping Cough) Specimen Collection". cdc.gov. August 28, 2013. Archived from the original on 8 February 2015. Retrieved 13 February 2015.[11]
  14. Heininger U (February 2010). "Update on pertussis in children". Expert Review of Anti-Infective Therapy. 8 (2): 163–73. doi:10.1586/eri.09.124. PMID 20109046.[12]
  15. "Revised guidance on the choice of pertussis vaccines: July 2014" (PDF). Releve Epidemiologique Hebdomadaire. 89 (30): 337–40. July 2014. PMID 25072068. Archived (PDF) from the original on 2015-02-13.[13]
  16. "Pertussis vaccines: WHO position paper". Releve Epidemiologique Hebdomadaire. 85 (40): 385–400. October 2010. PMID 20939150.[14]
  17. "Pertussis (Whooping Cough) Prevention". cdc.gov. October 10, 2014. Archived from the original on 8 February 2015. Retrieved 13 February 2015.[15]
  18. 18,0 et 18,1 "Pertussis (Whooping Cough) Treatment". cdc.gov. August 28, 2013. Archived from the original on 11 February 2015. Retrieved 13 February 2015.[16]
  19. 19,0 et 19,1 Wang K, Bettiol S, Thompson MJ, Roberts NW, Perera R, Heneghan CJ, Harnden A (September 2014). "Symptomatic treatment of the cough in whooping cough". The Cochrane Database of Systematic Reviews. 9 (9): CD003257. doi:10.1002/14651858.CD003257.pub5. PMID 25243777.[17]
  20. "Pertussis (Whooping Cough) Signs & Symptoms". May 22, 2014. Archived from the original on 7 February 2015. Retrieved 12 February 2015.[18]
  21. "Pertussis (Whooping Cough) Complications". cdc.gov. August 28, 2013. Archived from the original on 9 February 2015. Retrieved 12 February 2015.
  22. Vos, Theo; Allen, Christine; Arora, Megha; Barber, Ryan M.; Bhutta, Zulfiqar A.; Brown, Alexandria; Carter, Austin; Casey, Daniel C.; Charlson, Fiona J.; Chen, Alan Z.; Coggeshall, Megan; Cornaby, Leslie; Dandona, Lalit; Dicker, Daniel J.; Dilegge, Tina; Erskine, Holly E.; Ferrari, Alize J.; Fitzmaurice, Christina; Fleming, Tom; Forouzanfar, Mohammad H.; Fullman, Nancy; Gething, Peter W.; Goldberg, Ellen M.; Graetz, Nicholas; Haagsma, Juanita A.; Hay, Simon I.; Johnson, Catherine O.; Kassebaum, Nicholas J.; Kawashima, Toana; et al. (October 2016). "Global, regional, and national incidence, prevalence, and years lived with disability for 310 diseases and injuries, 1990-2015: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2015". Lancet. 388 (10053): 1545–1602. doi:10.1016/S0140-6736(16)31678-6. PMC 5055577. PMID 27733282.[19]
  23. Heininger U (February 2010). "Update on pertussis in children". Expert Review of Anti-Infective Therapy. 8 (2): 163–73. doi:10.1586/eri.09.124. PMID 20109046.
  24. Wang, Haidong; Naghavi, Mohsen; Allen, Christine; Barber, Ryan M.; Bhutta, Zulfiqar A.; Carter, Austin; Casey, Daniel C.; Charlson, Fiona J.; Chen, Alan Zian; Coates, Matthew M.; Coggeshall, Megan; Dandona, Lalit; Dicker, Daniel J.; Erskine, Holly E.; Ferrari, Alize J.; Fitzmaurice, Christina; Foreman, Kyle; Forouzanfar, Mohammad H.; Fraser, Maya S.; Fullman, Nancy; Gething, Peter W.; Goldberg, Ellen M.; Graetz, Nicholas; Haagsma, Juanita A.; Hay, Simon I.; Huynh, Chantal; Johnson, Catherine O.; Kassebaum, Nicholas J.; Kinfu, Yohannes et al. (October 2016). "Global, regional, and national life expectancy, all-cause mortality, and cause-specific mortality for 249 causes of death, 1980-2015: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2015". Lancet 388 (10053): 1459–1544. PMC 5388903 Check |pmc= value (help). PMID 27733281. doi:10.1016/s0140-6736(16)31012-1. [20]
  25. Atkinson W (May 2012). Pertussis Epidemiology and Prevention of Vaccine-Preventable Diseases (12th ed.). Public Health Foundation. pp. 215–230. ISBN 9780983263135. Archived from the original on 2017-07-29.