Waxtaan:Xam-xamu nosukaay

(Yoonalaat gu jóge Waxtaan:Xibaarfeppal)

baatukaay

Soppi
  • xibaarfeppal: informatique
  • seggatukay: ordinateur
  • logiciel et application: tërël ( ci italien «un programma» la nuy wax maanaam li nga programmer: li nga tërël. un programme: ab tërël)
  • système:demin

--Ibou 21 octobre 2007 à 11:45 (UTC)


yii laa gisoon man

Soppi
  • xibaarfeppal: informatique ( xamtéef moom la ko Aram Faal tudde woon, man ma gisoon xam-xamu nosukaay walla xibaartéef
  • seggatukay: ordinateur : man ma gis Nosukaay (nos ci wolof mooy tekki ordonner;organiser;programmer;sistemare)
  • logiciel et application: tërël ( ci italien «un programma» la nuy wax maanaam li nga programmer: li nga tërël. un programme: ab tërël): tëriin la ko Aram Faal daa wax. walla nga ne tëraliin
  • système:demin:Man NOSTE laa gis boo xoolee ci yewwute ci sama téere ba danga ko fa gis, (nosteg laman: systeme feodal. nosteg pénc: systeme republikin


Ma bëgg laa yëgal ne al foo ko gisatee doo ko binde ël maanaam tërël moom ngay jàng waaye tëral ngay bind, ndax mi ngi juge ci tër, kon al gi moo koy defloo li muy def, lekk lekk-al, naan naa-al wax wax-al tëdd tëddal. Al nag jumtukaayu digal la niki lekkal, jumtukaayu defloo la tam niki lekkal na ko, def na ko mu lekk.

Ma yeewaat la ci leneen, gis naa saa su nekk booy bind lu Afrig Afrik ngay bind, nag nga bind nak, ma lay xamal ne soo bëggatee xam ba xam ga la walla ka dangay bind am giy firi yëfam ci ginnaaw baat bi xool, danga gis ne Afrigam lanuy wax ak nagam walla nga bind u ci ginnaaw afrigu sowwu jant, nagu baay.judd baaxul juddu moo baax, boo ci bëggee xam dara , danga koy def jëfi dàq mu jox la judduwul nga xam ne juddu lanuy bind, bu dul loolu juddul la waroon a doon, walla nga def ko jëfi ndigal mu jox la juddul, bu doonutoon loolu juddal lay doon te loolu amul. Mbindiin wi am na nos bu mu war a topp, waaye jàmbaar nga lool

informatique

Soppi

Yaakaar naa ne waxoon xibaarfeppal walla xibaartéef moo gënoon xamtéef. ndax xamtéef ak xam-xam seeni tekki waru ñoo soriyante. Man xibaafeppal ci ñaari baat yii la ko sose xibaar ak mbëjfeppal(electronique, electron).

yeete gi ci mbindiin mi doon na lu am solo ndaxte cim njang laa nekk ba léegi. saa yoo gisee ay njuumte ci samay mbind, nga may jubanti doon na lu may dimbali. kon jaa jëj!!!! --Ibou 22 octobre 2007 à 19:09 (UTC)


Ñàkk a fasu

Soppi

Ñàkk a fasu, maanaam di jëfandikoo baat yi dul naqaree nànd, yi dul jafee xam lu am solo la, bul fàtte ne bañ a jëfandikoo tubaab ngir jafe gi moo tax ñuy bind ci wolof, kon lépp loo xam ne man naa tax ñuy xaw a jegewaat jafe ga ca làkku tubaab nanu koy moytu, te yombal gi dinay tax nit ñi di gën a ñëw, di fi gën a ba nasaraan. Waaye bu mu tee nga xam ne gaynde nga, jaajëf

Revenir à la page « Xam-xamu nosukaay ».