Waax
Waax xeetu garab la gu bokk ci njabootu Poaceae ak ci njabootaatu Bambusoideae, Afrig gu naaje la bàyyikoo.
Meloom wi
SoppiMan àgg ba 10i met ci guddaay ak 10i sàntimet ci yaatuwaayu dàtt. Xobam danay àgg ci guddaay 1 ba 2i sàntimet. Doom danay àgg ci guddaay 10 ba 15i milimet.
Njariña yi
SoppiDees na ko jëfandikoo ci defarug alkol, ñoll ak duu. Waax ci xeeti tabaxukaay yi la bokk.