Timmiñ-tammañ

Timmiñ-tammañ Gàñcaxug ñax la, di it borom juróomi xob yi bokk.

Tóortóoru Timmiñ-tammañ


Melo Soppi

Timmiñ-tammañ day law, ab taxawaayam di àgg ba 10i sàntimet jàpp 20i sàntimet . Ab lawaayam day àgg ba 100 Mt. Ab reenam day dëgër fa miy sax it day mel ni am tàgg ( dankalikoo). Day am am peet mu mboq rafet lool. Ci béreb bi féexlukaay yi lay ëppe ak ci tooli "jardins" yi. Ci jamono yi miy lawe nag mooy ci weeru suliyee jàpp nowambar ( Naweet).

Njariñ Soppi

Ay reenam day yokk ag cawarte. Ab nàcc-nacc it boo ko ci defee day taxawal deret ji. Day faj it biir buy daw. Lawtan gi it daa nañ ko jëfandikoo di ko def ay takkun ngir di ci takk ngóob mi ci jamonay góob.

Loraange yi Soppi

Ñax mi daa am tooke gu bon ci jur gi ba tax na waru ñu koo lekk.

Nataal Soppi

 
Timmiñ-tammañ gi


 
Meññeef
 
Xob ak tóortóor


Turu xam-xam Soppi

Potentilla reptans