Tansani

(Yoonalaat gu jóge Tanzania)
Réewum Tansani
Raaya bu Tansani Kóót bu aarms bu Tansani
Dayo 947 303 km2
Gox
Way-dëkk 51 820 000 (2014) nit
Fattaay 55 nit/km2
Xeetu nguur
- Njiitu Réew
- Njiitu Jëwriñ
Repiblik
Samia Suluhu
Nassim Kinja
Tembte
- Bawoo
- Taariix
Péy ak rëddi
Tus-wu-gaar
Tus-wu-taxaw
Dodoma
Làkku nguur-gi Kiswahili
wu-angalteer njàgg mu kawe ma
Koppar Tanzanian shilling (TZS)
Turu aji-dëkk Tansani-Tansani
Sa-Tansani
Telefon
   

Tansani am réewum penku Afrig la, féete ci peggi mbàmbulaanug End . Keeñaa ak Ugandaa ñoo ko féete bëj-gànnaar, Ruwandaa, Buruundi ak Kongóo-Kinshasa nekk ci sowwoom, Saambi ak Malawi nekk ci bëj-saalum-sowwoom, Mosambik nekk ci bëj-saalumam.

Réew mi tollu na ci 947 303 km²

te am 51 820 000 ciy way-dëkk, ay bantu rekk a fa dëkk. Péeyam mooy Dodoma, mi ngi nekk ci biir réew mi, waaye dottub koom-koom bi dëgg mooy Dar es Salam gi doonoon péey bi, féete ci tefes gi. kiswahili ak wu-angalteer ñooy làkki nguur ga, teewul ne itam araab am na fa doole, rawati na ci duni Sansibaar ak bu Penda.

Tansani ju tay jii a ngi judd ci booloog Tanganyika ak Sansibaar ci 26 awril 1964, gannaaw, ci lu yàggul dara ñu am seenug tembte ci Nguur-Yu-Bennoo yi. Bokk na ci Commonwealth dale ci atum 1961, bokk na itam ci Mbootaayu Xeet yi dale ci 14 desambar 1961.

Taariix

Soppi
 
Julius Nyerere, 4 ut 1977.

Ci 1953, Julius Nyerere, ab jàngalekat la woon bu judd ci 1922, ci bi muy am 31 at la ñëw ci boppu TAA (Tanganyika African Association, mbootaayu waa-afrig bu Tanganyika), mu daldi koy soppi ag làngu politig dëgg, ci lu gaaw, tudde ko Tanganyika African National Union doon woote ngir ag tembteg seenum réew. Ci 9 desambar 1961 la leen ko Nguur-Yu-Bennoo yi jox, ci jàmm. Ci ndoorte li jëwrin ju njëkk la doonoon, ginnaaw pal gu desambar 1962 gi, mu doon njiitu réew ju njëkk ju Tanganyika.

Ci 10 disambar 1963 la Sansibaar ak Pemba am seenug tembte, 26 awril 1964 la Tanganyika ak Sansibaar booloo ngir sos li tudd tay Réewum Tansani. Nyerere doon njiitu réew ma, Abeid Karume mi doonoon njiitu réewum Sansibaar nekk jëwrin ju njëkk ji, ci Tansani. Donte booloo gi amoon na, waaye ba-tay jii Sansibaar moo yoral boppam yenn yi. Njiitu réewum Tansani moo ko yoral li ñeel politig, kaaraange, mbiri biti-réew, añs, moom mu yural boppam njàngale mi ak koom-koom,..

Melosuuf

Soppi

Tansani réew la mu nekk ci xaaju kol-kol bu bëj-saalum féete ci Penku Afrig. Ay digam yu dénd ñooy mbàmbulaanug End gi ci penku, dojuw Kilimandjaro ak déegub Victoria bi ci bëj-gànnaar, déegub Tanganyika bi ci sowwu, déegub Malawi ci bëj-saalum-sowwu ak dexub Ruwuma ci bëj-saalum

Lëkkalekaay yi biti

Soppi

 

Xool it Wikimedia Commons



  Réewi afrig  

Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkina Faso • Buruundi • Cadd • Ecoopi • Eritere • Eswatini • Gaambi • Gaboŋ • Gana • Gànnaar • Ginne • Ginne Bisaawóo • Ginne gu Yemoo • Isipt • Jibuti • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Keeñaa • Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Lesoto • Libeeria • Libi • Madagaskaar • Malawi • Mali • Marook • Móoris • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeria • Ruwandaa • Saambi • Sahara gu Sowwu • Sao Tome ak Principe • Senegaal • Seysel • Simbaawee • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Sudaan gu Bëj-saalum • Tansani • Togóo • Tiniisi • Ugandaa