Téere Tasawudus sixaar

Ahuuthu billaahi minash shaytaanir rajiimi wa inniya uhiithuhaa bika wathuriyyatahaa minash shaytaanir rajiimi rabbi,ahuuthu bika min hamazaatish shayaatiini wa ahuuthu bika rabbi ayyahduruuni.

Maa ngi tàmblee ci turu yàlla, miy yaatali xeewalam ci àddina te di ko jagleele ca alaaxira. Yal na yàlla mu kawe mi dolli xeewal ci sunu sang ,sunu kilifa, Muhammad,ak ñoñam aki saabaam,ak mucc ak barke bob dana ci wommate kepp ku jàng teere bii, yobb ko ca àjjanaam ja mu dig ña ko ragal,aamiin yaarabal haalamiin.

Ahmadu mi dul dañ di sant boroomam, di jaamub yàlla,tey ligéeyal yonant bi (j.y.m) nee na : ag cant ñeel na yàlla mii di rafetal ci samag wàll,rafetal gu tooll ne rafetalug ku musla dañ di rafetal.Maang koy sant ndax kat moo tabe ci indil nu tawhiid (muy wéetal yàlla),ak ñaari mbokkam yooyu di lislaam ak lihsaan,te ñooy sunnas yonant bi(j.y.m),xeewal ak mucc gu sax na ne ca xaritam ba,soppeem ba,Ahmad,ak ñoñam ak saabaam yu gëm, yu jullite,yu tedd,yuy rafetal yi.

Lii nii aw woy wu rajas wu am njariñ te tedd la, ma tudde ko yobbalub ndaw ñi(tathawudush shixaar) jem ca àjjanay yàlla jii ami dex,maa ngi ñaan yàlla ag nangu,ak jàmm ak sell,ak màggal. Maang koy ñaan woy wii di wommat kepp ku ko jàng jëme ko ca yoon wa gën a jub. Tey texeg ndaw ñi,ak mag ñi,ak waxambaane yeek jigeen ñi. Waxtuw soppiku jëm ci li nu tax a jug nag jot na,sunu boroom laa ciy wut ci lu sax.

(AG JIITAL )

Yeen ndaw ñi maa ngi leen di digal ngeen bañ a wut lu dul ag jub,te soxlawoo xam-xam,soxlawoo leen jàng ak mokkal,te teet barabi texeedi yi,taqoo leen ak ki dul dañ di jaamu boroomam,ndax kooku kat la yàlla digale rekk la jeme,kepp ku daw cig ndawam jëm cig jub,bu màgge noppalu. Ku dabaatal li ko rëccoon ci lu bon akug neen,te jeem a dundal waxtu yi ci tuub gu sell,ak jublu sunu boroom,am la gën. Jàpp leen ci sama laabiire gii ma leen jox,kon dey da ngeen tonowu ci addina ak alaaxira,bokk ci ñiy texe.

(BUNT CI XAAJI DIINE YI)

Diine ñatti xaaj la,benn xaaj bi mooy bu gëm, Beneen bi di bu lislaam mooy ni nuy jaamoo yàlla ba yàlla di ko nangu,ak bu lihsaan,muy rafetal jaamu gi ngay jaamu ci sa digganteek sa boroom.Lu ci ne dees na ko gën a leeral. Ñu tàmbli ko ci xaaj bu njëkk bi muy gëm .

Gëm mooy nga gëm yàlla ak malaakaam yi,ak teereem yi mu wàcce,ak alaaxira,ak yonenteem yi ak dogal bi.

(DOGGANTAL (chapitre) CI NI NUY GËME YÀLLA)

Yàlla moom ni nga koy gëme mooy : nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la, te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee,aji des la te desam gi amul fu muy yam, aji wuuteek mbindeef yi la,aji doylu ci boppam la,kenn la kok amulub kem,aji wéet la ci jëmmam- maanaan amul kenn ku mel ni moom- ak ciw meloom , aki jëfam.

Kàttan (man-manu jëf) ak nameel (maanaam bëgg di def) ak xam-xam akug dund ,ak gis ak dégg, ak wax,yooyule yu war ci sunu boroom lanu. Kon nag mu nekk di aji am kàttan lu war la, tey ku am nameel ,di aji xam, di aji dund,tey kuy degg di kuy gis, nekk it di kuy wax yu war lan ci moom. Ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom, la ame yeneen melo yu waradi,te jomb ci moom,niki ñàkk, (maanaam sun boroom bañoon a am) ak sosu (ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu,nekkul di ku fi mas di ne),ak jeex (maanaam muy ku fi dul des),ak niru,(ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam,kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom)ak aajowoo (jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn),ak limu (maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt) ak lott (maanaam ñakk man-man ci def li ko soob) ak sibeel ( def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel,mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom) ak tëx (mooy safaanub degg) ak réer ( di safaanub xam) ak dee di (safaanub dund)ak gumba di (safaanub gis) ak luu di (safaanub wax) .

Yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom ,tudd naa sellam ga,kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott,mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer mbaa muy ku gumba mbaa ku dee -soril naa ko loolu- walla muy aji luu,yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan.Moom daal sunu boroom deful dara cig war,lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare,loo fi gis daal,ci mbindeef yi, seenug jëf ak seenug ba, ñoo yam ca sunu boroom,lenn du ci lu war, lu dagan rekk la ci moom, (dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk).

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME MALAAKA YI yal na yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom)

Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lanu,te ñu nu musal ciy bàkkaar lanu,(dun moy yàlla),dunu xayta (dunu puup) dunu saw it,ñu sunu boroom laabal lanu. Dunu lekk dunu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu yàlla teral lanu ba fàww,ken du ci moy yàlla,ku ci ne li ko yàlla digal rekk lay def.Ci leer la leen yàlla binde. Sàbbaal seen boroom mooy seenug naan,sellal ko mooy seenug lekk.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME TEEREY ASAMAAN YI)

Ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la,te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk.Seenub lim nag teemer ak ñeent la. Fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Aadama (j.y.m), juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla Sihsa(doomi yonant yalla Aadama), fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla Idriisa,fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Ibraahiima miy xaritub yàlla bi(j.y.m). Bu ko defee Tawreet ñeel Muusa(j.y.m),Injiil ñeel Hiisaa,saboor Davood (j.y.m)Alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi Muhammad yonant bi tëjj yonant gi,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom,ak ci ñoom ñepp.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME YONANT YI,mucc ak xeewal yàlla na nekk ci ñoom)

Ni ngay gëme yonant yi (j.y.ñ) mooy nga dëggal leen,te dëggal li nu indi jële ci seen boroom.Te nga gëm ne itam dëggu ak wóor ak jotal lu war ci ñoom la.Fen nag ak wor ak nëbb dëgg dafa araam ci ñoom. Gaar-gaar bu dul ayibal tey dal nit da na leen dal,niki tawat, waaye bu mu doon juy foñloo,maanaam juy tax nit ñi di leen daw,niki ngaana nga xam ni day wàlle,ak yu mel ni ñoom,ñoom tawat yooyu danoo wormaal yonant yi,dun leen dal. Waaye nag jaay ak jënd,ak denc (am soxna) ak lu ni mel ci lepp lu yàlla daganal,bun ko defee du leen dolli lu dul yoolub yàlla seen boroom. Liy wone ne ñoom ñu dëggu lanu te yàllaa leen yonni,mooy kiimaan yi leen yàlla di wàcceel ,di ci wone ne moo leen yonni,mu mel ni (ñoom kiimaan yi)daniy wax ak nit ñi naan leen jii waay de lu mu wax, mbaa mu def ko yàllaa ko ko diggal. Yonant yi nag, seenub lim ñatti teemeer ak fukk ak ñatt la,waaye anbiyaawu yeek (mooy ku am darajay yonant te yonniwun ko ci nit ñi) yonant yi,yepp boo leen boolee ,seenub lim moom teemeeri junni la ak ñaar fukk ak ñeent,yal na mucc ak xeewal sax ci ñoom ci lu dul dog.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME BIS BU MUJJ BA,yal nanu yàlla fegal ay tiitaangeem )

Ni ngay gëme bis bii mooy nga dëggal ko,te dëggal lepp li mu ëmb,niki wisaareg teere ya,ku ci ne dees na ko won ay jëfam ci teere,ak pang ma,muy dajale gi niy dajale nit ñi,ak balaas bi, muy balaas bi niy mandaxee jëfi jaam yi,ak déegub yonant bi (j.y.m),ak ajjana ak sawara,ak siraat(aw yoon la wu deesi romb),ak romb gin ciy romb,ak hisaab(mooy seet gi niy seet jëfi nit ñi) ak rammug yonant bi (j.y.m) ak mbugal(yal nanu ci yàlla musal). Hisaab nag luy tar la ca boobale bis,ndax dees na hisaab nit ki ci lu gën a tuuti fepp suuf cib tuutaay.

Fayyantoo itam dana fa am,ndax lu waay daa jay moroomam fii, teg ko cig ëpp doole,bu yawmal-xiyaamee dees na jox aji neew ji doole, doole muy fayyu ci ki ko daa neewal doole,niki xar mi am bejjan te daa daan mi amul bejjan,bu bis baa,da niy jox aji ñakk jiy bejjan bejjani mi ko daa daan muy fayyu,loolu lepp maandute ga fay am lay wone.

Dee,ak laajug malaaka yi ak mbugalum bammeel,ci yawmal-xiyaam lanu,ndax kat yawmal-xiyaam yi ñaar lanu,bu mag ak bu ndaw,bu ndaw bi mooy dee gi ñepp di dee,bu mag bi di wal gi niy wal buftu bi .

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME DOGAL BI)

Gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am,moo xam lu làqu la walla lu feeñ,ak fu’m man a ame,sunu boroom mooy ki ko xamoon ,namoon ko am kàttanug def ko ,def ko.Moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi,walla lu bon ,niki jëfe tere yi.Walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi,walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi.

Cig gàttal daal lépp lu am,ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la.Nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla,lu fi am cib dogalam la ame.

(BUNT CI LISLAAM)

Lislaam mooy wax laa ilaaha illal laa (muy yàlla rekk ay buur,amul beneen buur bu dul mom) ak julli ak woor,aj màkka,natt asaka.

(DOGGANTAL CI LAA ILAHA ILLAL LAA)

Wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla,Muhammad,yonantub yàlla’a - yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom,ak ñoñam aki sahabaam- mooy ngën ji lu kuy wax di wax,ku ko weddi it pert rekk,ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu,te du dajeek nëx-nëx.

(BUNT CI JULLI YI JUROOM)

Julli yi juroom farata la ci lu dog,ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam-xam yi. Kepp ku ko bañ a def ngir weddi,mook ku tubbee yam cib àtte,dees koy tuubloo may ko ñatti fan,bu tuubee nu ba ko,bu tuubul,sariiya ray ko ci jaasi,te deesu ko sang,deesu ko sàng ,deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña.

Imaam daal day yonni kenn rekk, mu suul ko,te dunu ko jublule xibla,te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def (baytulmaal mooy (trésor publique) bu nguurug lislaam),ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def,te amul ngànt,moom danu koy bàyyi ba waxtu julli wi jot,nu digal ko,bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex,nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk a ciy bëgg a des,bu bañee nu topp ko,ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi,walla ab yamoo,loolu lepp nag ngir bañ koo ray, ñongal dereetam,bu bañee, kilifa gi ray kook jaasi ,rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër.

Bu réccoo nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee, deesu ko nangu,dees na ko jullee nag,waaye boroom ngëneel du ko jiite,ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy.Bàmmeelam nag dees na ko fonk,jégénal ko(jal ko) kenn du ko maasale noonu rekk,ndax moom fi boroom xam-xam yi ab julit la.Lii dey waxi imam Hawfii la.

(DOGGANTAL CI LAAB)

Laab moom lu war la,ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam-xam yi. Ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu,dees koy ray rayug gëtën,gu dul gu yéefër, ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la.

(DOGGANTAL CIG SOÑÑEE CI ÑU FARLU CI RÀÑÑALE DIGGANTE FARATA YEEK SUNNA YI AK ÑÀKK CEE SÀGGAN)

Koo xam ne julli na ca anam ga mu gën a rafete, ci maanaa,mu jullee ni ko yàlla digalee,metal rukoo ya ak sujood ya,metal taxawaay ya ak jataay ya,te bawul dara lu nu war a def ci julli gi,mu noppi nag nu laaj ko li julli gi am ciy farata akub àtteem, ndax moom julli gi farata la walla sunna walla lu nu sopp,te moom xamul dara ci li nu ko laaj,xanaa mu tontu rekk ne man daal da may gis nit ñi ñuy jaamu ma ànd ak ñoom ca la ñuy def waaye li ci des xawma ci dara.

Ci loolu yenn boroom xam-xam yi nee nanu julleem gi baaxul,te dunu nangu ngàntam li. Naka noonu ku jàpp njàpp mu sell,raxas ñatti yoon ay loxoom ba ci tikkujara yi,gallaxndiku gu ànd ak soccu,saraxndiku,fiiru,lu ci ne ñatti yoon raxas kanamam,ay loxoom lu ci ne ñatt,te xaliil baaraam ya,masaa boppam tàmblee ko ci fi jë bi yam ba ci doq gi,delloosi ko ba fa mu tàmblee woon,masaa ñaari noppam ginaaw bi mu tooyalaatee ay loxoom,raxas ñaari tànkam ànd ak xaliil leen,matal njàpp mi ni mu ware.

Naka noonu ku sangu janaba ni mu ware,raxas ñaari loxoom ñatti yoon ba ci tikkujara ya,raxas li ko taq ci sobe,raxas pëyam walla sakkaraam ànd caak yeene,bu noppee jàpp njàppum benn-benn,xaliil mbooleem kawaram,tooyal ko,tamblee ko ci mujug ndaal-bopp li ngir jañ lor ji. Dal di raxas boppam ci ñatti tanqi ndox yum tanqe ci loxoom,ginaaw bi mu ko xaliilee,dal di as ndox ci tenqul ndijooram,jengal boppam raxas noppub ndijooram,bu jàllee mu defaat noonu raxas bu cammooñam,dal di raxas ag doqam,ak wetug ndijooram ba ci bëtu woom bi,def noonu ci gu càmmooñ gi,dal di raxas tankub ndijoor bi ba ci dajoor bi,teg ci bu càmmooñ bi,dal di matal am cangaayam ci raxas biir bi ak dënn bi,ginaaw bim raxasee ginaaw gi.

Te xamul ci loolu lepp la cay farata ak la cay sunna, kon na ko wóor ne tojam ma (toj mooy ñàkk a lab) dañul te julleem ga mu ca julli baaxul,te coonaam boobu bepp du ca jële lu dul bàkkaar, te mi ngi moy yàlla ak yonentam bu sel bi (j.y.m) .Wax jii nag mi ngi bawoo ci Imaamul Hawfii, luy tiitloo tey jàjjee ngi ci nag,nee na itam gépp jaamu yàlla gu nu defe nii njariñ du ca juddoo,moo xam aj la walla jihad walla woor walla yu ni mel niki joxe ak lele.

Am nag ci boroom xam-xam yi ñu ci ne ku sangu mbaa mu jàpp,def ko ca anam ga mu ware,yeene ca biir def la yàlla farataal,na xam ne jëfam ja ju nu nangu la, ju baax la,te dana ko doy ca la gën a wér,te julli gam ca def it gu baax lay doon ,bu ca yeenee def la ca yàlla farataal,amul it benn bàkkaar ,mbaa muy moy yàlla ngir ñàkk gi mu ñàkk a gëstu.

Waxi Imaam Hawfii jii du dara lu dul ag xuppe akug yeete akug laabiire ,ngir nu farlu ci jeem a xam farata yeek suna ak yi ni mel,yàlla na ko yàlla fay aw yiw. Li ma (sëriñ beey wax) wax mooy yàlla dey araamal na ci mukalaf mu ne - ci li nu tuxal- jëf dara ci diine te xamoo la cay àtteb yoon,yax (mbind mii) bii nag daliil xathii la,(daliil xathii ci wallug usool mooy lu wér lu mel ni alxuraan).Kepp ku réere farataam te laajul,na xam ne tooñ na boppam te alag ko.

(DOGGANTAL CI FARATAY JULLI)

Faratay julli fukk ak juroom la, ci li faqiih bii di Hawfii wax. Ñooy yii: 1 yeene 2 kàbbarub armal ba 3 taxaw ngir kàbbar ko 4 jàng faatiya 5 taxaw ngir jàng ko 6 rukoo 7 siggi ca rukoo ba 8 sujood 9 siggi ca sujood ba 10 yeenee roy imaam boo ko amee ca njëlbeen ga 11 toftale gi 12 dal gi 13 yamoo gi 14 sëlmël bi 15 jataayub sëlmël bi tàmblee ca alifug al gi ba ca miimug kum gi.

(DOGGANTAL CI SUNNAY JULLI)

Ay sunnaam 18 la, 1 liqaam 2 saar wi ci ginaaw faatiya (sunna sun feddali la) 3 taxaw gi gay taxaw di ko jàng (sunna sun feddali la) 4 birël fi mu ware 5 yalu fi mu ware 6 kàbbar bu dul bu njëkk bi 7 taaya ju njëkk 8 taaya ju mujj 9 julli gi ngay julli ci yonant bi ca taaya ju mujj ja 10 jataayub taaya ju njëkk ja 11 jataayub taaya ju mujj ja 12 li dolliku ci dal gi ngay dal 13 li dolliku ci sëlmël bi 14 birël sëlmëlub farata ba 15 delloo sëlmël Imaam 16 delloo ko ki ci sa wet 17xerawlug maamoom bu imam dee birël 18 am saatir bu dee imaam walla kenn ku beru,waaye kuy roy moom imaamam doy na ko saatir.

( DOGGANTAL CI FARATAY NJÀPP )

Faratay njàpp juroom ñatt la, ñooy: 1 yeene 2 raxas kanam gi 3 raxas loxo yi ba ci conc yi 4 xaliil baaraami loxo yi 5 masaa sa bopp 6 raxas sa tànk 7 jonj 8 gaaw

(DOGGANTAL CI SUNNAY NJÀPP)

Sunnay njàpp moom itam juroom ñatt la,ci li imaamul Hawfii wax :1 raxas say loxo ca tàmbli ga 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 fiiru 5 masaa sa ñaari nopp 6 tooyalaat say loxo bala ngaa masaa say nopp 7 boo masaa sa bopp ba ci doq gi,delloosi gi nga koy delloosi 8 toftale gi.

(DOGGANTAL CI FARATAY SANGU)

Faratay sangu joroom la : 1 yeene booy tàmbli 2 jonj 3 gaaw 4 xaliil kawar gi 5 nal ay lett ci kepp ku lettu

(DOGGANTAL CI SUNNAY CANGAAY )

Ay sunnaam ñeent la: 1 raxas loxo cig tàmbli 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 masaa ker nopp yi.

(DOGGANTAL CI FARATAY TIIM)

Faratay tiim juroom ñatt la: 1 yeene 2 pakk bu lab 3 gaaw 4 door gi ngay njëkk a door say loxo ci suuf 5 masaa sa kanam 6 masaa sa tikkujara 7 jokkale ko ak julli gi 8 defe ko ci biir waxtu wi,ndax du baax bu jotul.

(DOGGANTAL CIY SUNNAAM)

Sunnay tiim ñatt la : 1 toftale ga (mooy jiital li war a jiitu li ci war a top topp ci) 2 doorub ñaareel bi ngay door sa loxo ci suuf 3 masaa li top ci tikkujara yi. Na nga ba tiim nag tey jàpp,boo weree waxunu boo weredee walla nga am ngànt lu wér,kon bu boobaa nga man a tiim.

(DOGGANTAL CI WOOR)

Woor ñaari farata la am: 1 yeene 2 ba liy dogloo ngir yàlla. Sunna yi ñatt la : 1 gaaw a dog 2 yeex a xëdd 3 ba wax ju ñaaw

(DOGGANTAL CI ASAKA)

Asaka moom ñeenti farata la am : 1 yeene 2 matug at 3 matug nisaab 4 bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi. Am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool  : 1 nga ànd ceek teeyug bakan 2 mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal 3 joxe ko ci sutura ngir daw gistal.

(DOGGANTAL CI AJJ)

Ajj ñeenti farata la am : 1 yeenee ajj 2 tawaaful ifaada 3 dox diggante safaa ak marwa 4 taxaw arafa.

(DOGGANTAL CIY SUNNAAM)

Sunnay ajj fukk ak ñaar la :am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga,1 sangu gu jokkook armal gi 2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labayka.

Tawaaf gi am ñeenti sunna : 1 dox gi 2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi.

Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yeegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa.

(LII AG MOTTALI LA )

Nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne ku birël ci ginaawug laab ne ( Ashadu ba fam yam) da nanu ko ubil bunti àjjana yi, mu dugg ci bi ko soob,waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi.

(DOGGANTAL CI NI NGAY FAYE LI LA FAAT CI GINAAW IMAAM)

Lu war la ci maamoom mu fay li ko fat ci ginaaw imaam.Suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg-dëggi fajar ba bu tàmblee leer,bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya’akuw saar cig birël te bul xunoot.

Waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba,bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig yalu jekki,taaya , sëlmël.Boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya’akuw saar cig yalu,te bul toog da ngay jug def beneen, julli gi mat.

Bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar,nga jàng faatiya’akuw saar te yalu leen,nga jekki, taaya,jug def beneen ràkkaa,bu ànd ak faatiya’akuw saar te doo toog,da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong,mu jeex.

Waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba,ba ca waxtuw gel wa (mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq). Tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf.

Timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq. Bu la cib ràkka rawee jugal,kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig birël,bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal te bul kàbbar, jàng faatiya akuw saar te birël ko,taaya, defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël.

Gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi (guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi) bu njëkk bi. Bu la ci benn ràkkaa rawee jugal, bul kàbbar,jàng faatiya akuw saar te birël ko,bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal kàbbar te jàng faatiya’akuw saar,cig birël,te bul toog,nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba. Bu la ci ñatt rawee,jugal birël faatiya’akuw saar,ci lu dul kàbbar,jekki,taaya,te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya’akuw saar,cig birël,waaye doo toog,da ngay wéy ca ba ca des, jàng ca faatiya rekk te yalu ko.

Boroom xam-xam yi ñoom, jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak Imaam . Ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam ,na ko woor ne jotul ràkkaa ba.Ku jot Imaam ci taaya,daa war a dooraatug julleem.

(BUNT CI LIHSAAN)

Lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis,ci lepp li ngay def,te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis.Kon na ngeen koy fuglu.

Bu ngeen bëggee àgg ci martaba yu kawe yi,na ngeen di jëfe ndénkaane bile: maa ngi leen di denk xam-xam,ak kersa,ak sant yàlla ak sellal,ak tabe,ak noppeek lewet booy xamlu, ak muñ ak ragal yàlla ak degg-degglu maanaa yi,na ngeen di farlu ci top aji yërëme ji, fu ngeen man a ne te sori noonoo,bu leen baril wax aki nelaw, na ngeen di teet luy waral yaq, di moytu ngistal,fu ngeen man a ne,ak rëy ak mbañeel, tey sàkkug leer,maa ngi leen di denk ag dëggu, ak wakkiirlu ci yàlla,ak toraxlu ak neewi mebët,denk naa leen bariy teggiin,loolu da na waralub yool,barib xam-xam ci lu duli teggiin ay akub coona rekk lay waral.

Yeen gone yi bu leen di toog ak ku dese cim xel,dee leen toog ak kuy gindee. Kuy gindee kat mooy kiy genne aji toogaale ji jële ko ci juroomi mbir jëme ko ci juroomi mbir,moo koy jële ci ngistal jëme ko ci sellal te du naafeq,moo koy jële cig rëy yobb ko cig toroxlu ak muñ,moo koy jële cig noonoo,jëme ko cig laabiire,moo koy jële ci sikk,yobbu ko ci yaqiin gu ko man a dollig kawe,moo koy jële ci bëgg lu koy lor,jëme ko ci lu koy jariñ.

Màng (profitoo) leen juroom,njëkk juroom ni ko yonant bi (j.y.m) digalee:bi ci njëkk mooy ag ngone njëkk màggat,2 wér njëkk wéradi 3 am koom njëkkug ñàkk 4 ag féex njëkkug féexadi, 5 dund njëkk dee.Gaawantu leen jëm ca yiw wa njëkk muy faat.

Fii la Tasawudus sixaar yam,ànd ak sant sama boroom miy aji feg ji gacca.Woy naa ko nag ndir jëmmi sama boroom mu tedd mi,di yaakaar ci moom ab yool bu dul dog,mu diw woy wuy wommate jëme ci xam-xam ak jëf,ak tegginu tey jàppndal mebat yi.Mu diw rajas wu am njariñ te barkeel,wu way texe yi bokk.

Yàlla ci barkeb yonant bi (j.y.m) nangu na woy wii,jariñ ci it kepp ku texe,kuy laabiire,te yewwu ,moom woy wi du dañ di bijjee jëme cig baax,di jañ gepp texeedeek woru. Yàllaay ki ma digal ma woy ko,yàlla miy ki nu jublu,mi may fegal luy waral njàqare.Woy naa ko ngir jëmmam ju tedd ja,moom mi jënd samam njaay ànd ak di ma teral.

Konug cant ñeel na yàlla,xeewal ak mucc yal na nekk ci Ahmadu ,aji rammu jiy boroomi ngëneel,ak ñoñam aki saabaam.Ahmadu mii dib jaam buy ligeeyal yonant bi mi ngi sant boroomam.

Subhaana rabbika rabbil hizzati hamma yazifuun,wasalaamun halal mursaliin,wal hamdu lillaahi rabbil haalamiin.

(LII AG XAMLE LA)

Bokk na ci njariñi woy wii : ki ko woy (muy sëñ bi) ci ndigalul yàlla mu kawe mi te sell la ko defe ,ak ci lol yonantam ba jàmm ak xeewal yal na sax ci moom.Bokk na ci ngëneeli woy wi, begal gun ko begal bim ci noppee(moom sëñ bi) ne ko woy wii de la yàlla (t.s)ak yonant bi(j.y.m) gën a sopp ci ay keman. Bokk na ci li nu ko begale:kepp ku ko jàng walla nga mokkal ko,texe ag texe gu texeedi dul toppati,bokk na ciy jagleem ku ko mokkal Munkir ak Nakiir dun ko laaj ci bàmmeel,ak leneen ak leneen ak leneen,yàlla mooy jagleel yërmaandeem ku ko soob,yàlla mooy boroom ngëneel lu màgg li.