Suuna xeet la ci xeeti garab yi mi ngi bokk ci njabootug buwaasiis ñu di ko bay ngir ay doomam yi nga xam ni dañuy tàkk. garab la gog moom lañuy gën a bay ci xeeti garab yi.

Nataalub suuna
==Melo wi== 

Garab la gog guddaayam man naa àgg 1 jëm 3 ba 4i met, ay doomam dañuy yor melo wu xaw a weex, walla xaw a mboq, walla xawa baam te niru ak ay fer.

===Solo si==
Garab gu ñuy bay la lool te bari ay njariñ fële ca End ak Pakistaŋ, ca Sahel ak Afrig ci yenn barab yi. Ay doomam dañu koy jëfandikoo ni Ceeb ñu di ko tàngal bamu ñor te it dañu koy soppi di ko def Fariñ; boo demee ci yenn réewi Afrig yi am na ñu ko fay soppi am ñoll. Fële ca Órob garab la gog dañu koy jox mala yi ñu di ko jëfandiko. 

Nataali Suuna Soppi

Turu xam-xam Soppi

Pennisetum glaucum