Nataalu garabu sump.
 
Nataalu meññatum sump ak i socc yu banti sump.

Sump ci garab yiy meññ te am i dég la bokk. Ab njoolaayam dina toll ci 8i ñay. Peer bi day jub, yenn saa yi mu xaaju di ñaar te day ñagas it. Wànqaas yi nag dañuy bari te rankaloo am ay dég yu ñaw jub te ñaw di toll ci 7i sànti met. Car yi it dañuy nëtëx ñoom it am i dég. Xob wi day xaw a tuuti moom it nëtëx. Keram daa yaraax, neexut a féexloo. Rax ci dolli ci ron garab gi day faral di am ay dég yuy wadde ci sump gi. Bant bi it dees na ko jëfandikoo ngir socc.


Meññeef mi

Soppi

Doom bi day gulumba, der wu mboq ëmb ñam wi, ñaw it ëmb ab xoox, ca biir xoox ba it ab saal ne ca buy niru gerte. Day neex nag saf suukar. Bot wi di sump bi ñoragul bi, der bu nëtëx a koy ëmb, waaye moom neexul day wex.

Njariñ yi

Soppi
 
Meññatum sump ci kaw garab gi.

Sump bari na ay njariñ lool. Saal bi ci biir xoox bi, dees na ci defar diw gu baax, muy diwu sump. Dees na defar ci xob yi it saabu. Xob yi ak doom yi dund gu am solo la ci yenn gox yi.


Ay turam ci yeneeni làkk

Soppi

Bàmbara: zeguene. Waa Càdd di ko woowe savonnier. Wolof: Sump Farañse: Dattier du désert.

Turu xam-xam wi

Soppi

Balanites aegyptiaca