Sexaw ci njaboot gu yaa gog "combrétacées" gi tënk ñaxi yi ci àll ak mànding. Sexaw xeetu garab gu sëkk, man àgg 4 ba 5i met.

Nataalu garabug sexaw

Melo wi

Soppi

Tóortóoram daa tuuti te weex, ba noppi dajaloo te am i dég.

Foytéefam daa wow te yor ay xeeti laaf yuy àgg ba 1,5 sàntimet ci guddaay, ak 1,5 sàntimet ci yaatuwaay.

Meññuwaayam

Soppi

Sexaw ci réewi sahel gi lay sax: Senegaal, Mali, Niseer, Burkinaa, Gine konaakri/Bisaawóo.

Njariñ li

Soppi

Sexaw ràññees na mbaxam ci reesal ak ci moytu ag mbëfër. Ca Senegaal xob yi dañ ko fas ak i xëddee di ko jaay ngir defarug dute mbaa ndékki.

Nataali sexaw

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Combretum micranthum

Turam ci yeneen làkk

Soppi

Araab: Farañse: kinkeliba