SancamJolof Ak li ko waraloon

Sëñ baa ngi sanc Jolof - ci li ma sëñ Mbàkke BUSO nettali - bi mu nekkee Tuubaa,ba nit ñi bari fa,magi donga yi denc ay soxna,dëkk yi woon ci wet gi, ñu ci bari tuxusi fi woon ak seeni ñoñ, ñi sëñ bi jugoon ngir yar leen tàmblee jaxasoo’k ñeneen ñi,nos gi sëñ bi nosoon mbir yi,am lu ci tàmblee yàqqu,mooy bëgg gi mu bëggoon a ber ñiy jàng cig wàll, ñay ligéey,ca geneen wàll, ñiy ligeey ak ñiy jàng jaxasoo gi naqari ko,rawati na jaxasoo gi niy def ak ñeneen ñi,nga boole ci loolu ,aj gi mu bëggoon a defi ak siyaare ji Yonnant bi (j.y.m),te bëggoon koo bëgg,ba daa ko wax ñenn ci ñi ko jege woon.


Kenn ci sunu moroomi naari Daymaan yi,di Muhammad doomi Hamdil Abhami nettali na ma ne:Sëñ bi nee na ko ca at mooma ca Tuubaa,ndax bëgg ngaa aji? Ma ne ko waaw-wallaahi,waa-waaw,ku ma fay yobbu kay laa amul,mu ne ko,demal ca sa ñoñ,te waaj,te ñëw ci mujjug at mii, nu ànd aji,bu neexee Yàlla ,ma dem waaji te lijantiji sama njaboot,naan (Inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun).

Nu dellu ca wax ju njëkk ja, Sëñ Mbakke BUSO nee na,bi ko ñaari mbir yu gaar yooyu jaaxalee,muy mbirum jaxasoo bi ak mu bëgg a aji gi,da maa woo,waxtaan ci ak man,diisoo’k man ci mbirum ñu sanc ab barab,bu nu man a tàqalee ñaari kuréel yi wëlif ñu dul ñoom,te teqale leen ñoom ci seen biir,ngir ñiy jàng ak a jàngale man a def seenub ligéey,mu samp ci jiite njàngum alxuraan mi, ,sëñ Abdu Rahmaan LO,njàngum xam-xam mi,mu teg ca Maam Cerno rakam ja, ànd fa ak ñoom ñaar rekk ak seeni kuréel,keneen dollikuwu ca,ci donga yi walla sheex yi. Mu ne ma yaw nag kon da ngay des Tuubaa,di jëwrini donga yi, ñiy siyaaresi bu nu ñëwee ak seeni àddiya,ku ci war a agsi,nga bàyyi mu ñëw,ku warut a agsi,bumu agsi. Ma ànd ak moom ci loolu,xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la,inshaal laah.

Mu tàmblee waaj,di ci làqatu ñi mu bëggul ñu dem,bi dogu gi dëggaree ci dem,te loolu da ko daa làq sunu waajur wii di nijaayam, nga xam ne da koo bàyyi woon ak man rekk,doyloo ab gis-gisam ci man,mu mel ni da maa soxlawul - bi mu ci dogoo dëgg nag,la xam ne du man a ñàkk,mu yëgal ko nijaayam jooju,mu dal di ko koy yëgal,yëf yi nag tiis ko lool,ngir xam gi mu xam ni buuri Jolof yi fiire,ak ni nu manadee muñ,wuuteek buuri wii tund , te taalibey Jolof yi it dunu bàyyi seeni doom aki donga,te dunu muñ it, wuuteeg yu gox bii,mu ragaloon nu sonal ko,aaye woon ko ci anam gu nooy mu bañ a dem, yee ko ci aaday ñaari dëkk yi,ci li mu ci xam,ndax xamoom na ne li Sëñ bi bëgg dëppoowul ak seeni aada.


Waaye Sëñ bi moom niki soofiyu yu mag yi,dafa dogu te fas yeenee wéyal li mu dogu, ndax wéyal ag dogu ci tasawuf la bokk,tekki ag dogu fi ñoom mook tubbee yam,dee ko gën a woyof ci ñoom.

Kon Sëñ bi laxas na ak dongaam yooyu,ca sawaal ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñaar g,(G, mooy:ci ati gàddaay gi) wuti suufus Jolof,ndax gisul ci Bawal,barab bu man loolu mu bëgg,ca jamono jooja,ak ndax itam Jolof suufus ay maamam la woon,te foofee ca la wër Tuubaa amul am ndox,walla bu fa saxee it da na ajowoo jankoote ak ay ñoñam,mbaa mudaaraante ak ñoom,te loolu du lu mu daa faral a def,mu dox ak ñoom,ba Mbàkke Baari,wacc fa,sanc fa,waxtaan fa ak yenn jaraaf,waaye ag ñagas feeñ ca njëlbéenug wax ja, àggoon ci ñu naan:nun dey xamunu woon ciy donga ag sàkkoo dooni buur, ñii di ñëw daal,nekkunu lu dul ay buur,yu ñëw ngir xëccoo’k ñun suniy suuf,yàgg nanu leen a dégg ca ña ca seen ginaaw,nun nag ñi ngi giñ ci ne dunu dëkk ak nun ci sunu suuf sii,ci seen melo wii,ak wax yu mel nii,ci yi ko nijaam ji daa wax,ak a sentul bu fa demee.

Waaye Yàlla moom bu bëggee amal am mbir da koy wutal ay sabab, nee nanu bu Yàlla bëggee tàllal gënéel lu lemu,da koy wutal làmiñu ku iñaan. Bokk na ci xéewal yi Yàlla xéewale Sëñ bi , sóob gi mu ko sóob ci yoonu wàlliyu yi, { sunnatul laahil latii qad xalat min qablu,walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan }} muy ci maanaa yoonu Yàlla wii di wu wéyoon bu yàgg,doo gis ag coppite ci yoonu Yàlla. Nit du jug mukk jëm ca Yàlla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor,loolu fiiraangeg Yàlla’a, ngir mu bañ a jàdd,bañ a wéeru ci ku dul moom,Yàlla da koy feeñu cig màgg ak cib taar,ci feeñu gog taar gi (attajalliil jamaalii) ,la ko Yàlla di ñoddile nit ñi, ñuy sottiku ci moom niki ay weñ yu tiimub puur,loolu nag ci tàggatug Yàlla lay ame, ñuy yërmaande juy texeel ku nar a texe. Ci feeñu gog màgg gi attajalliil jalaalii la leen Yàlla di dëddale ak yenn xol yi, ñu nekk seeni noon,dunu gis seen hurma,dunu leen gëm,di leen ayibal ci seen bopp,ak ci seeni taalibe,waayee ak loolu lépp,hifthul hinaaii du tàggoo’k ñoom,mooy wattu gi leen Yàlla di wattoo’k a aar,dara du leen dal lu dull lu Yàlla bëgg mu dal leen juge cib noon,di luy ñaaw ci saayir,diw yoon jëm cig fayantoom { Innaa minal mujrimiina muntaqimuuna } muy ci maanaa,da nanu fayyu ci ñiy tooñ. Ñi ngi ñaan Yàlla jàmm.



Lii mooy mbirum Sëñ bi ak ay àndandoom ca njëlbéenug Jolof, bu dee lu aju ci ñam ba woon ca ginaawam nag, ñoom Sëñ Mbàkke BUSO nee na:taalube yi mu bàyyi woon Tuubaa,bi nu yéggee ni Sëñ baa nga Jolof , ñu tàmblee wuti pexey dem fa,yalwaankat yi fekksi leen ci loolu, ñu gàddaaye Tuubaa,ndare ku fa dëkk,xalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yàqqu,lu tax déet, ginaaw mbir mi du mbirum xalaat.

Bu dee lu aju ci jaraaf yu dëkk bi,ku ci gisoon,li nga gisoon gën naa yokk,ku ci gisutoon tàmbli nga gis leegi,nga boole ci lanu déggoon ci diggam ak buuri Jolof yi,nu tàmbli noo dikkal ci kaw ak suuf.

Bi buur yi ak seen dag yi gisee li nu gis,te ñoom boroomi ngànnaay lanu, ñu daa dund ci seen ngànnaay rekk,danu daan song ku leen daa jéem a të,duma ko,nangu alalam,ray ko mbaa ñu njaf ko (jàpp ko jaam),loolu nag di woon aada ju yàggoon ci ñoom,ju nu daa donnante,waaye loolu téewul ñu amoon jàmm ak lenn ci boroom néeg yu mag yi, daawunu leen boole ci seen jëf jooju,daawunu ci boole it ñi daa aaru ci seen kaaraange,niki néegub sëñ bi.

Loolu ak meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci Sëñ bi,meneen mbir mi nag , nga xam ne moo leen gënoon a jaaxal,mooy mbirum nguur gu raglu gii,loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas, ñoom danu daa def,suuf sunu not ,jël fa njiit,muy ku fa bokk,samp fa,ngir waa dëkk ba bañ a mer te ànd ak ñoom,xoolal ma gii xam politig. Ci noonu nu jël buur yi ak jaraaf yi teg leen ci kaw daara yi ak donga yi,ñuy seeni njiit,waaye loolu xéewal a ngi ci ndax tax na ba buur yi ak seen jikko yu bon yi nu yoroon, di sonnal jullit ñi ak a fitnaal ak a def li leen soob ci nit ñi jeex.

Bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njëkk yu bon ya,muy ray jullit ñi,ak giir seeni alal,ak doonte loolu da leen di àggale ci nuy raye it,du tee nu def ko,bi nu demee ba manatunu loolu te loolu tubaab yee ko waral, ñu mujj di leen xiirtal tubaab yi,jaare ko ci ay pexe ak ay wor. Mu neeti : jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit ñeek nguurug tubaab yi,jubluwunu ci woon,faagaagal leen,ndax lu man a xew, ñoom ci seen ron kiliftéef lanu nekkoon,doonte ci anam gu woyof la,waaye kay ñi ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal,bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a bañ,diw it nanguwul a fay galag, diw mee am na lu mu leen di waajal,diw mii mi ngi wut ay ngànnaay,di dajaley fas,walla nit ñaa ngi koy deglu , walla ku bariy taalibe la, ñu koy màggal,dayob màggal, ba àgg ci bu leen junjoon geej gi,ñu sóobu ci xuus ko,ak leneen ak leneen,ci seen fen yi nu daa def,ngir bëgg tubaab yi digal leen ñu songu leen,walla nu def ci ñoom lu leen soop.

Te xamunu ne yewwuteg faraase yi,ci wàllug politig moo gën a yaatu loolu,waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bët,di sa asaa sekkare,di la xoolal sa ginaaw,da na mujj am lu mu bàyyi ci yaw benn bis,rawati na bu fekkee ki ñu ne moo def loolu,du rambaaj,du jaxase,te du jeem a setal boppam,ca ki nu ko rambaaje,te ñiy yàq dunu dañ,di yàq diggante bi,rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga,yu ko gëm,lu mu leen digal nu def.

Loolu moo waraloon ñu tàmblee tiit ci moom,ndaxte dañu koo niroole woon ak sheex Omar Fuutiyu, Tukkulóor la bu defoon ay xare ci wàll gi mu dëkke woon , ci mujji ati juroom ñaar fukk yi,bi loolu jàllee ba teg lu néew,la benn wolof bu tuddoon Maalik BA,nu gënoon koo xam ci Màbba,defoon ay xare ca goxub Saalum,ci ati juroom ñatt fukk yi,ginaaw bi la Ahmad Sheexu dib Tukkulóor,moom it,xaree xareem ba ak waa Jolof ak Kajoor,ba bi mu deewee ca bisub Samba Saajo,ca wàllug Luga,ca mujjug ati juroom ñeen fukk yi.

Jaxasekat yi nag ,bi nu demee ci tubaab yi danu leen ne Sëñ bi ñii lay roy,ba mujj tubaab yi manatuñoo ñàkk a gëstu li nu leen wax,lii daal mooy li gën a waral tubaab bi jublusi Sëñ bi,ginaaw bi ko Yàlla dogalee namm ca la mu ca namm,muy wax joj dara amu ca,ndax Sëñ bi lorewul ,soxlawul àdduna,te xemmeemul li nu jort ci moom,Yàlla’ay seere lii nuy wax.

Bu doonutoon rambaaj yii,waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal,waxantuma la ak yu mag yi,waaye loolu day dëggal waxi yonnant bi ji (j.y.m), { ñi Yàlla gën a teg ay nattu ñooy yonnant yi,teg ci wàlliyu yi,teg ca ña gën,teg ca ña ca topp}} ,ponk bii nag bu wéy la ci xeetu yonnant bi (j.y.m),ndax ñu baax ñi ëpp ag gëm foo leen fekk,daniy fees dell aki nattu, àdduna dëddu leen naqari ci ñoom, ñooy ëppi jafe-jafe fuuf ñu dul ñoom,boo demee ca Sahiihub Muslim,ak bu dul moom,da nga ca gis :[ àddunaay kasob jullit,tey àjjanay yéefar ],yàlla itam wax ne :{wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin} muy àllaaxira, ñu ragal Yàlla ñee ko moom.


Bi tubaab yi demee ba manatunoo ñàkk a xool mbirum Sëñ bi, ñu tàmbli fa’a yabali ndaw aki bataaxel,ay yooni yoon,di sàkku ci moom mu seetsi leen,moom muy xaar ndigalul boroomam rekk,ak lu yonnant bi,(j.y.m), ñu gise yeex a wuyyusi gi,ag bañ,bu ko defee ña daa jaxase di gën a am lu nu wax,naan,waxoon nanu leen ko,gis ngéen li nu leen waxoon am déet ? .

Ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu ànd ak yenn soldaar yu néew,bunu leen tollalee’k li nu am ciy xarekat,ndax matunu woon mbooloom xare mu mag,lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi.