Sénki

(Yoonalaat gu jóge Sëng g)

Sénki garab la gu fekk baax fii fi Afrig guddayam day toll ci 4 ba 7i Met garab la gu siiw, amna Asi, Óstraali ak réewi Karayib yi.

Nataalu sénki

Melo wi

Soppi

Ay xobam dañoo sew yaram wi daa baam, te itam dañiy janoo toll ci 5 ba 15i sàntimet. Meññeef mi day nekk ciy xolliit yu mboq walla yu xuun di am 4 ba 5i doom. Garab gi mi ngi jebbi ci ñaareelu xaaju noor bi.

Solo si

Soppi

Ay reenam dees na ko fajoo ci yax yuy metti ak gone guy waccu, ba tay reen yi bees ko jaxasee ak xob yi day dindi kadam. Bantam dafa dëgër te ñeme max te itam dees na ci liggéey ay njëfendaay. Bantam itam neex naa togge te man këriñ lu baax! Reen bu tooy bi bees ko dëbbee tay ko ci bëñ buy metti da koy faj. Ngir faj "estomaa" góomu biir dangay jël ŋëbub xob yi ak i reen boole leen baxal ci liitaru ndox bàyyi ko bam sedd nga segg ko di ci naan benn kaas saa yoo lekkee ba noppi.

Nataal yi

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Dichrostachys glomerata