Sëng garab la gu fekk baax ca Afrig.

Nataalu garabug sëng

Melo Soppi

Guddaayu sëng day toll ci 4 ba 7i Met. Garab la gu siiw, am na ca Asi, ca Óstraali ak réewi Karayib yi. Ay xobam dañoo sew, yaram wi daa baam, dañiy janoo tey toll ci 5 ba 15i sàntimet. Meññeef mi day nekk ciy xolliit yu mboq walla yu xuun di am 4 ba 5i doom. Garab gi mingi jebbi ci ñaareelu xaaju noor bi.

Njariñ Soppi

Ay reenam dees na ko fajoo ci yax yuy metti ak gone guy waccu, ba tay reen yi bees ko jaxasee ak xob day dindi kadam. Bantam dafa dëgër te ñeme max te itam dees na ci liggéey ay njëfendaay. Bantam itam neex naa togge te man këriñ lu baax! Reen bu tooy bi bees ko dëbbee, tay ko ci bëñ buy metti da koy faj. Ngir faj "estomaa" góomu biir dangay jël ŋëbub xob yi ak i reen boole leen baxal ci liitaru ndox bàyyi ko bam sedd nga segg ko di ci naan benn kaas saa yoo lekkee ba noppi.

Nataal Soppi