Sàmba-sayar garab la gog mi ngi bokk ci njabootug (Entada Africana). mi ngi faral di sax lu ëpp ca Sudã. Dina sax it ca Burkinaa Fasoo, ca Kóngo, ca Niseriyaa, ca Senegaal ak ca Ugàndaa.

Sàmba-sayar

Melo wi

Soppi

Garab la gog amna tolluwaay 4i ba 10i metar ci taxawaay ak 90i cm ci wërngal (diamètre). Der wi dafa dóomu taal jàpp brune ba jël ñuul, dëgër, am ay raya yu taxaw, mel ni xollit. Xob yi da ñuy tegaloo ñatt ba juroom ñeent. Doom yiy sax ci garab gi yu dëgër lañu, te dañuy lang ay weer i weer, 12i (millimètres) la ci guddaay.

Meññeef

Soppi

Sàmba-sayar mi ngi sax ci àll walla barab yuy taw lu bari, walla bari ndox.

Njariñ yi

Soppi

Xob yi manees na cee defar ay basaŋ. Xob yi, reen yi ak wànqaas yi day jur want yu gudd yu nu man a defare ay buum ak i takaayu bant i tabax. Xob yi ak gàncax gi bari na luñu koy jëfandikoo ca Niseriyaa ak Gana ci wàllug paj.

Nataal yi

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Entada africana