Rajab
Rajab manees naa wax ne ci xeetu garab yi la bokk. Amna ñu ko ber it ne du garab. Bari na ay xeet lool nag, amna lu ëpp téemeeri xeet.
Xeet yi
SoppiAmna ci bu ñuy wax kooyi naar, pakkub lëg, jaatoor, beñeb lëg, sawum xaj. Amna ci yu weex am ci yu yor yeneen i wirgo. Amna ci yu ñuy lekk, te muy sax ci suuf di am jëmm, am ci yoy tooke la day raye. Yooyu di raye nag Afrig la ëppe ci tàngoor wi, fu ci mel ni Senegaal, rajab ya fa nekk, kenn waru koo lekk.
Saxiin wi
SoppiMoom rajab nag ci ngelaw li rekk la aw jiwoom di jaar. Jiwu wu góor wi mooy naaw daje ak wu jigeen wi ñu joxe doom. Amna ci yoy, day yàq garab da koy ray. Pëndax lay doon bu weex tuuru ci garab gi ne ci ñàpp. Pëndëx boobu it bu laalee kawari nit, da koy xus moom la ñuy wax mbay-wataan . Rajab yi tuuti ba kenn manu koo gis ak bët moo koy def. Lu bari looy gis mu xuur nag, bu dul bagteri rajab a ko waral.
Nataal yi
SoppiTur wi ci yeneeni làkk
Soppifarañse: champignon |
angale: mushroom |
itaaliyee: fungo |