Raaya wu Senegaal
Raaya réewum Senegaal am na ñatti rëdd yu taxaw te tolloo, wu wert, wu mboq ak wu xonk. Ab biddiw wu wert am juróomi cat a nekk ci digg rëdd wu mboq wi.
Kulóor bu wert bee ngi màndargaal kulóoru yonent Yàlla Muhammad ñeel jullit yi, wow yaakaar ñeel nasaraan yi mbaa wow njur ñeel ñi gëmul Yàlla. Nimero bi ko sistem Panton jox mooy 361 mbaa RGB 30 181 58.
- Melo (Kulóor) wu mboq wi day màndargaal am-am ak njariñal liggéey, doon it kulóoru Caada ak ladab; kulóoru xel mbaa ruu. Nimero bi ko sistem Panton jox mooy 116 mbaa RGB 252 209 22.
- Kulóor bu xonk bi day màndargaal kulóoru dereet, joj dund, joj jaayante gu askan wépp def ak joj xeex ñàkk. Nimero bi ko sistem Panton jox di 186 mbaa RGB 206 17 38.
- Biddiw bu wert bi juróomi cat yi day màndargaal mbokkoo gi ak Afrig, akug ubbeeku ñeel juróomi dénd yi. Li mu wert nag day tekki yaakaar gi judd ci moom gi Senegaal moom boppam. Day màndargaal it juróomi ponki Lislaam yi ñeel jullit yi. Nimero bi ko sistem Panton jox mooy wow rëdd wu wert wi.
Amul benn dogalu buur bu ñeel yaatuwaayu rëdd yooyu, kulóoru raaya wi ak tolluwaayu biddiw bi.
Raaya ya jëkkoon
Soppi-
Raaya Senegaal wi njëkk (1958-1959)
Raayaw Senegaal wi njëkk, ci atum 1958, daa amoon biddiw bu mboq bu am juróomi cat te ginaaw gi wert. Mi ngi ajuwoon ci Mbooloom Jëmale Senegaal kanam (doon tey làng politig gii di Parti socialiste (PS)), amoom benn biddiw ca jamono jooja.
Ci weeru samwie 1959, réewum Sudaη miy làkk faraase (doon tey réewum Mali) ak réewum Senegaal ñoo ànd sos Mbooloo mu Mali (bokk ci réew yiy wax farañse), te aw raayaam, am ñetti kulóor, wert, mboq ak xonk akub kanaga ca digg ba. Réewum Senegaal daa mujj rocciku ci mbooloo moomu, témb ci 20 ut atum 1960. Bamuy génn ca Mbooloo ma Senegaal daa yóbbale raayaw Mbooloo mu Mali ma waaye daa wuutale kanaga ba akub biddiw bu wert ngir bañ a juuyoo ak jullit yi.