Qin Shi Huang
Qin Shi Huang moo doonoon imbraatóor bu njëkk bu Siin gees Bennal. Ginaaw bi mu bennalee Siin, moom ak njiitu xelalkatam yi Li Si, def nañu am mbooloom ay yéwénal (reformes) yu koom ak politig yu mag, def it ay sémb yu mag, yu ëmbaale sumb (version)bu njëkk bu Miir bu Mag (the great wall)bu Siin bi. Waaye nguurug jaay-dooleem ga (nga xam ne lakk na ay téere, suul ay woroomi xam-xam) tax na muy jëmm ju jeqi dàggasante ci taariixu Siin