Poson Kayit bi ñuy raññee poson bi ñu duppe (Estewaad

Estewaad) moy poson bi ñu jëfëndikoo ci ndoorteeli pomp mi ba 20 fàn ak juroom ci wéeru Ut Sax yi ko tax a jog mooy yii lékk tontòor yi ak doomi sàpp yi te ñu gën ci raññe (Eliyotis, Eyariyas), Diparopsis walla yiy lekk xòb yi (Espodoptera)

Nii  la ñu koy jëfëndikoo :

Bidoq (Estewaad) mooy pomp ñeenti buumu sàpp

Su dee ñaari buum la ñuy pomp :

Jëlal ndox mu set sotti ko ci bidoq bu mag bi ba mu diggu doomu

Poson bi nekk ci bidoq bi jël ci génn wàll gi (xoolal fi ñu ko màndargale) sotti ko ci bidoq bu mag bi

Yëngalal bu baax njaxas mi bala ngay feccali bidon bu mag bi. Njaaxas juroomi liitar la wara doon. Boo bu nàtt mooy pomp buumu sàpp.

Su dee bénn buum la ñuy pomp

Sottil ndox bi ci ñeenteelu xaaju bidoq bu magg bi ;

Jëlal nak ñeenteelu xaaju bidoq  poson bi (baayil sa xel ci màndarga bi koy wone). Yengalal bu baax njaaxas bi balaa ngay dolli ndox ba ci xaaju bidoq bu magg bi.  Boo bu nàtt mooy pomp buumu sàpp.

Ak poson bi ñu duppe Estewaad, diggante pomp ak pomp 10 fànn ak ñeent la

Na ka la poson bi di xeexee ak sax yi

Ñaari ba ñeenti waxtu gannaaw ba nga pompee, sax yi dootuñu mën a yënngetu te dootuñu

lékk itam. La cay tegu mooy ñu dee.

Noonu  muy def  sax yi nak du ko def xaaritu baykat bi yi demee ni yàmb yi ak meelentaan yi

Kayit bi ñuy raññe poson bi ñu duppe Tiriyoonf

Tiriyoonf moom la ñuy jëfëndikoo ngir aar sàpp mi li ko dooree ci 20 fànn ak juroom mbénn ba ca njeexteel pomp mi.

Sax yi ko taxa jóg mooy yiy lekk tontòor yi ak doomi sàpp mi te ñu gënn ci raññee Eliyotis, Eariyas, Diparopsis walla yiy lekk xòb yi (Espodoptera). Mën na xeex itam Piisroq ak weññ yu weex yi (Bemisiya)

Naka la ñuy jëfëndinkoo Tiriyoonf

Bidoq Tiriyoonf moom la ñuy pompee fukk i buum ak juroom bénn (maanam ñeenti ektaar)

Su dee ñaari buum la ñuy pomp

Duyàl bidoq bu magg bi ba mu fees ak ndox mu set

Xaajal bidoq poson bi juroom ñet xaaj. Jëlal bénn xaaj sotti ko ci  bidoq bu mag bi. (Ngiir yombalal natt gi, jëlal nattukaay bu mag bi bi ñuy duppe doset, tëyéko ak so loxo  ndey jòor te sotti ci  poson bi ba mu egg ci ñennteelu rëd bi). Yëngalal bu baax njaxas mi bala ngay feccali bidoq bu mag bi ak ndox (njaxas mi juroomi liitar la wara doon)

Boo bu natt mooy pomp ñaari buum

Su dee bénn buum la ñuy pomp

Duyàl bidoq bu mag bi ak ndox mu set ba mu diggi doomu

Xaajal poson bi fukki xaaj ak juroom mbénn. Jëlal bénn xaaj sotti ko ci bidoq bu mag bi. (Ngiir yombalal natt gi, jëlal nattukay bu mag bi ñuy duppe doset, tëyeko ak sa loxo ndey jòor te sotti ci  poson bi ba mu egg ci ñaareelu red bi). Yëngalal bu baax njaxas mi bala ngay dolli  ndox ba ci xaaju bidoq bu mag bi (foofu mooy mengoo ak  ñaari liitar ak génnwall) .  Boo bu nàtt mooy pomp buumu sàpp.

Ak poson bi ñu duppe Tiriyoonf, diggante pomp ak pomp 10 fànn la

Naka la poson bi di xeexe ak sax yi

Ci diir bu gàtt gannaw ba nga pompee, sax yi dootuñu mën a dem. La cay tegu mooy ñu dee.

Soppi