Penda Mbow

Dundu ak jaar-jaaram
Juddu Awiril 1955 (juroom-benn-fukki at ak juroom)

Dakaar

Réew Senegaal
Liggeey Way-pólotig, jàngalekatu taarix
Borom-këram Saaliw Mbay, 2017 ba tey
Yeneen xibaar
Liggeeye na Iniwersite Seex Anta Jóob
Njiitu teesam Charles-Marie de La Roncière


Penda Mbow mu ngi juddu atum 1955. Borom xam-xam bu xam-xamam màcc ci taarix la, muy ab bañkat. Nekkoon na fi jëwriñ ji yore caada ak cosaan ay weer atum 2001. Jàngalekatu taarix la ci Iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar nekk itam njiitu genn mbootaayu njuddu-réew.

Dundu ak jaar-jaaram

Soppi

Penda Mbow mu ngi juddu ci weeru mee atum 1955.

Atum 1986 la am ab doktoraa ci tarixu jamono ji farañse tudde moyeenaas (histoire médiévale) ca iniwersite bu Porowãas (Provence) ci ab teesu ñetteelu fànn bi mu bind ci « Nguuru takk-der gu askanu mameluke ci ni ko téereb nattu suuf bu Ibn al-Ji’an ñu dendale ko ak li am Farãas ngir xam li ñu niroole ak li ñu wuute » (L’aristocratie militaire mameluke d’après le cadastre d'Ibn al-Ji'an : éléments de comparaison avec la France.

Ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru mee atum 2011, mu am Piri Sãa Póol II ngir jàmm ji[1], ab raaya bu Watikãa di joxe te kilifag làbbe gii gi Mgr Luis Mariano Montemayor tegoon ci ay yoxoom.

Dundug biiram

Soppi

Atum 2017 ba léegi, mu ngi ci buumu sëy, borom-këram a ngi tudd Saaliw Mbay[2].

Mbind (tànneef)

Soppi
  • (sous la direction de) Hommes et femmes entre sphères publique et privée, 2005

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër

Soppi

Seetal tamit

Soppi

Lees bind ci moom

Soppi
  • (en) Lydia Polgreen, « At Africa's Crumbling Colleges, No Room for Students », The New York Times, 26 mai 2007 (la situation à l'UCAD)
  • Fabrice Hervieu-Wane, « Penda Mbow. Femme d'utilité publique », dans Dakar l'insoumise, Éditions Autrement, Paris, 2008, p. 94-99
  • Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, B. Ndiaye, Dakar, 2006, p. 284

Jukki yi ñu ko tudd

Soppi
  • Taarixu jigeen ci Senegaal : <small>Histoire des femmes au Sénégal</small>
  • Limu jëwriñ yu jigeen ci Senegaal : <small>Liste de femmes ministres sénégalaises</small>

Lees jële feneen

Soppi