Waa Tugal yi ci tefesug Afrig gi :

Yaxantug ñatti koñ yi  :

Ci lu tollook juróom ñatteelu xarnu g.j, jaayees na ay jaam yu waa Afrig ci ay yaxantukat yu daa def yaxantug tàkk gi, ak gu tefes gi ci tefesug mbàmbulaan gu End gi (ocean indien).

Jaam yi jógewoon nañu nguuri Sowwu Afrig: nguuri Senegaal, Gana, Niseeria, Kamerun, Gaboŋ, nguurug Kongóo, nguurug Ndongo ak yeneen nguuri Angolaa.

Ñu màng jaam yooyu yobbu leen ca Afrig gu bëj-gànnaar ga (naar yi), fa la ñu leen jaayaat, ngir ñu doon fay mbindaan aki surga aki soldaar.

Gii yaxantu moom lañuy woowe njaayum jaam yi. Njaayum jaam yi gën naa yaatu bi xarnub fukk ak juroom benn tàmbalee g.j : Waa Tugal yi dañoo aajowoo woon ay loxo yuy liggéey ngir jariñoo mbell yeek suuf yi ñu moom ci Amerig. Looloo taxoon ñu gaawoon dem ca tefesug Afrig gi ngir jëndi ay jam. Ginnaaw nag jaam ya nekkoon ca tefes ga doyuñu woon, ñoom waa Tugal yi dañoo yabaloon ay ñu leen wuutu ñu Afrig ngir ñu gëstujil leen ay way néew-doole ci biir gox bi.

Ndawi tubaab yu Afrig yooyu dañu daan song dëkk-dëkkaan yi di leen lakk, di ray mag ñeek ndaw ñi, bu ko defee yobbu góor ñeek jigéen ñi am kàttanug liggéey. Dañu leen daan jéng, jiital leen ñuy liiru jëm ci digg yii : Gore – Owida – Luwanda. Foofa lañu leen di jaaye tubaab yi leen di sëf ci gaal yi, dem ak ñoom Amerig ci ay nekkiin yu metti te wow, yuy far a ray li ëpp ci ñoom ba lañoo àgg fa ñu jëm. Bu ñu àggee Amerig rekk ñu jaayati leen way meññilu yi (les investisseurs :exploitants), bu ko defee ñenn ci ñoom ñu tàggale leen ak seeni njaboot, te daa leen manante ci def liggéey yu diis yi. Sang bi nag daa na am àq ak sañ-sañ bu mat ci def lu ko soob ci jaam bi. Bu moyee ay ndigalam sang bi daa na digale ñu mbugal ko ba loolu leeg-leeg daa na waral ag faatam. Ci atum 1787 g.j, lañu jël ay matuwaay ngir aaye yaxantu gu ruslu gii. Ci jooju jamono la ay mbootaay sosu yuy safaan ag njaam, gu ci mel ne mbootaay ga amoon ca Angalteer ngir jële fi njaam, ak lonkoo gu xariti ñu ñuul ñi ca Frãas. Waaye njaayum jaam moom dañul ndare ca mujjug xarnub fukk ak juroom ñeent g.j . Afrig ñàkk na ay milyoŋ ciy doomam ngir njaayum jaam yi. Moom de – njaayum jaam – ag tooñaange gu mag la ñeel ag nite ci lu dul gën jaa néewi sikk.

(( Li ñu jublu ci yaxantug ñatti koñ yi mooy jaay gi ñu daa def doomi Afrig yu am yi kàttan, ngir ñu bayi te tabaxi Amerig te waa Tugal yi ko daa def, di jël njëg ga’ak di ko yobbooti Tugal, ngir suqali ko ca. Kon muy yaxantu gu ñatti koñ séq : Afrig gi ñuy jële njaay mi, Amerig gi ñu koy jaayeji, ak Tugal gi koy jëndsi walla fëkksi ci Afrig, jaayeji ko Amerig, yobbu njëg ga Tugal. Fii ba tay man nañu fee gis ne Afrig jëf na ay jëf yu am solo ci jëm-kanam gu koom-koom, gu mboolaay, gu fànn ak ak ak, gu ñaari gox yii, te yii ñaari gox ñoom it dox nanu bu baax cig deltu ginnaawam, ndax ŋacc nañu ciy ponkalam, yi ko manoon a jëmal kanam aki xéewalam, yi ko manoon a liggéey, ci ginnaaw bi ñu ko sancee (coloniisee), teg ko loxo, muucu ay gongikuwaayi xéewalam, yobbu defare seeni réew))

li juddoo ci njàppum jaam yi

Soppi

Njuréefi njaayum jaam yi (les conséquences) :

Askani Tugal yi dugg nañu ci njaayum jaam ci anam gu tar, looloo waral :

- Ay gëpplante aki xare ci diggante réewi Tugal yi

- Barig ñi dee ak ñi ñu ray ci xare yi ak ci biir dox bu gudd bi ngir jéggi mbàmbulaan yi

- Jeqikug askani Afrig yi ngir jàmmaarloo : looloo fi jur ay jafe-jafe yu mboolaay, yu koom-koom yu tar, niki néew dooleg dëkk yu mag yi, tasug ab xiif, wañse, ak yàqug jikko yi, ak amadig kaaraange ak tasug njaboot yi.

- Ŋacc Afrig ciy doomam yu am yi doole, ak ci kàttanam yu nit yi, looloo ko doyadiloo woon ba manul woon a jàmmaarlook canc gi (colonisation).

Ngir mettiit yi jaam yi daa jànkoonteel, boroom yéene yu rafet yi jug nañu ngemb séen bopp ne dañu fiy jële njaam ci turu teddngay nit : ca Angalteer ag yëngu-yëngu judd na fa ngir neenal njaayum jaam (le mouvement Abolitionniste). Bu dee ci Frãas it mbootaayug xariti ñu ñuul ñi (Organisation des Amis des Noirs) taxaw fa ngir xeex ag njaam. Waaye yaxantu gu gàccaale gii jëleesu ko fi lu dul ci atum 1848 g.j .

Nettali wu aju ci njaayum jaam

Soppi

Aw dogiit wu ñuy yër (lire):

Suñu maam yi ci teraanga ak jàmm lañu nekkoon, ami gétt aki tool. Bis gis nañu ca biir géej ga lenn njanaaw lu mag, lu ami laaf yu weex. Aw nit wu weex bàyyikoo nañu ca ndox ma, tudd ay baat yoy kenn ci ñoom déggu leen. Booba la sunu maam yi tiit: ñu jortu ne ñoom de ay jinne lañu, ñu leen di jéem a delloowaat ci géej gi jaare ko ci jëfandikoo ay fett, waaye jinne yi soqi nañu ci seen kaw sawara sos kàddu gi daa mel ag dënnu. Rayees na ñu bari ci ñoom. Sunu maam ya ca dees daal di daw.

Lii ci nettaliy gimiñ yi la :G.L Havaux

Karmat ak delluwaay

Soppi


Xool it

Soppi

Jukki yi ci lonku

Soppi