Njàndam xeetu gàncax la gu bokk ci njabootu “capparaceae”. Moo ngi bàyyikoo Afrig gu sowwu gi.

Njàndam gi (Boscia senegalensis)
Njàndam gi (Boscia senegalensis)
 
Tóortóoru Njàndam

Njàndam gancax la guy sax fu nekk. Dana àgg yaar ba juróomi met cib guddaay.

Njàndam day meññ ay foytéef. Ay tóortóoram day dajaloo.

Foytéef bi danay am benn ba ñenti xoox yuy yor wirgo wu nëtëx su ñoree.

Solo si

Soppi
 
Meññeefum Njàndam

Njàndam dees na ko jëfandikoo cig togg ak cim paj.

Ay doomam dees na ci jële xeetu ñam yu nekk.

Turu xam-xam wi

Soppi

Boscia senegalensis

Taram ci yeneeni làkk

Soppi
farañse: hanza
angale: hanza
itaaliyee: hanza