Niimaa xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Azadirachta", End la bàyyikoo. Ci barab yu naaje yi ak xaw a naaji yi lay sax.

Nataalu garabug niimaa

Melo wi

Soppi

Garab gu gaaw a sax la, man na àgg ba 20i met ci guddaay, ci lu neew nag 35 ba 40i met. Xobam day wéy waaye danay ruus ci jamonoy bekkoor gu taar. Bànqaasam daa yaa te tàlleeku.

Xobam danay àgg 20 ba 40i sàntimet ci guddaay.

Tóortóoram daa weex te gëtte.

Njariñ yi

Soppi

Xobi niimaa day dàq yoo ak i ñoñam. Diwu niimaa day jariñ ci wàllu melal.

Nataali niimaa

Soppi
 
Tóortóori yi


 
Niimaa gu ndaw

Turu xam-xam wi

Soppi

Azadirachta indica

Turam ci yeneeni làmmiñ

Soppi

Araab:

Farañse: neem 

Àngale: neem