Ngonaake
'"Ngonaake"' xeet la ci xeeti garabi dicotylédones, mi ngi bokk ci njabootug Fabaceae, ci njabootaatu Momosoideae, mi ngi cosaanoo penku Afrig ak sowu Asi, garab yu ndaw lay doon, dañuy sax fof suuf si day wow walla fu bari suuf lool.
Melo wi
Soppi"'Ngonaake"' garab gu ndaw lay doon guddaayam man naa jàpp ñaar-fukki 20i Met, yaatuwaayu peeram dees koy natt ci 60i Met. Am xasam day yor melo wu ñuul di am ay xar-xar yoy day am ay dég.
Fóoyteefam day guus. Dinay sax foo xam ne daa bari suuf lool.
Njariñ yi
SoppiGarab la gog bari na ay njariñ lool, manees na cee dundal jur gi, man naa faj, manees na jël am peeram...
Garab la gog manees na koo jël di taaral kër walla mbedd.