Ndimbal:Caytu

(Yoonalaat gu jóge Ndimbal:Yërte)

Xët wii day xamale fànni yëriin yu wuute gu jimbulang bi.

Jàppal ne jukki yi duñu noppi mukk, saa su ne ñoo ngi nekk di gënal seenug ëmbiit. Soo raññee ay njuumte, bul xaar, jubbanti leen fa saa sa. Xëtu waxtaanuwaay wi ñu booleel ak jukki bi, man naa ami leeral yu solowu, dee ko yër di ci bàyyi al laaj walla ay xelal.

Jumtukaayu seet

Soppi

Jumtukaay yooyu, yaa ngi leen di gis ci cammooñu wépp xët ci biir jimbulang bi.

  • Jumtukaay Ayca day tambalee seet jukki bi méngoo ak baat bi nga bind. Méngoo gi dafa wara wér, maanaam waroo juum ci mbindinu baat bi. Maas yi sax dang leen ciy def. Misaal: soo bindee mbej du la tijjil xët wi tudd mbëj, ndax maasoo ko.

Su gisul jukki bi, dalay won yeneen koji xët yu, seen biir, baat boobu nekk.

  • Jumtukaay Seet, moom day tambalee seet ci biir jukki yi, jox la ab limu ay jukki yi mu méngool.

Segam ceet gi doonul luy jàppandi saa su ne, ndax day yeexal joxekaay bi. Manees naa jëfandikoo seetukaay bu Google, moo gën a gaaw, wante tamit man naa am ay jafe-jafe ci diir bi muy am ngir dugal koju xët yu bees yi, walla wuute ci tekkinu baatu-caabi yi. Jàppal ne fii soo bindee ay baat yu bari, yoo xam ne am nañu ci woowu xët, laaj na nga bind + ci baat boo toftal.

Sosug jukki: doon na lu soof, lu mana ñakk , sakkaat ab jukki bu amoo ba noppi (yu seen tur wuute wante jegeñe), doon na lu nuy digalaate, fexe ba xam ndax jukki bi am na ba noppi walla déet. Lu yomb la su fekkee Jumtukaay seet bi mi ngi dox (ndax ci sa coobare man nga kaa doxadil), lu ko moy faaw nga jëfandikoo ab seetukaay bu mel ne Google walla nga dàq ceet gi ba beneen.

Jàppal tamit ne man ngaa lawal sag ceet walla sebare ko lu weesu jukkiy jimbulang bi, àggal ko ci xëtu ndimbal yi walla waxtaanuwaay yi, ak yeneen. Loolu yaa ngi koy lijantee ci ndimbalu néegu tànn yi, yiy feeñ ci njeextalu gépp ceet; yooyu néeg ñoo ngi tamit ci xëtu Samay tànneef.

Wàll yi

Soppi

Man ngaa seet ab jukki walla lu mu manti doon, soo tànnee wàll gi nga yaakaar ne fa la bokk, lu mel ne Wàll:Taariix, Wàll:mbëj, ak yeneen.

Wàll yi dañuy boole jukki yi bokk wenn melokaan, ci misaal: Wàll: Taariix dalay jox bépp jukki buy wax ci taariix. Dafa mel ne ag garab, da lay may nga man a dem ci car bu la neex; kon soo duggee ci ag wàll da lay yombalal nga jot jukki yi nekk ci biiram ci anam gu noppale.

Soo gisee linga doon seet ba noppi, doy na nga cuq ci wàll gi mu nekk, ngir man a xam yeneen jukki yi mu ko bokkal.

Fi limu wàll yi nekk mooy: Wàll

Xët yi mu lëkkalool, toppteg lëkkalekaay

Soppi

Xët yi mu lëkkalool Day tax nga man a am limu xët yi nga xam ne ci seen biir, lëkkalekaay bu lay indi ci xët wi ngay yër nekk na fa. Toppteg lëkkalekaay di la won yi ci am ay coppite ci yooyu xët

Aw xët ci mbetteel

Soppi

Li ngay fekk ci wii xët dalay bett, saa yoo ko tijjee li fa nekkoon day soppi boppam.

Jaar-jaaram

Soppi

Jukki bu ne, am na ay jaar-jaar, maanaam coppite yi mu am yépp. Yenn saa yi dina am solo yër jaar-jaaru xët yi ngir xool ay xibaar yu ñu far walla yu ñu soppi walla nga delloo xët wi ni mu meloon, lu weesu ay coppite yu bari.

Sa xëtu jëfandikukat

Soppi

Soo bindoo, da ngay am sa xëtu bopp woo man a bind lu la neex (ay xibaar ci sa bopp, ay ndimbal yu man a jariñ ñeneen ñi. Soo xamee nooy soppee wii xët, dinga ci man a def lu bari