Ndimbal:Nooy sose aw Xët

Xët wii da lay won sosinu xët wu bees, moo xam jukki bu bees nga fay dugal walla leneen.

Seet balaa benn sosteef Soppi

Balaa ngay sos aw xët wu bees na nga bàyyi-xel ci ñett yii:

Bu njëkk bi, ndax li nga ciy dugal du jalgati yoon?
Bul dugal ci Wikipedia ay mbind walla ay nataal te amoo sañ-sañ bi. Bés bu nekk di nañu fi fare ay mbind walla ay nataal, ndaxte dañ leen jëlee ci yeneen dal te amuñu ca woon benn ngigal. Li gën mooy ngeen dugal ay liggéey yu ngeen defal seen bopp walla ñu doon ay liggéey yu jóge ci ay sémb yu seen ëmbit ubbeeku. Ndax ñiy bind seeniy téere ñaare du ñu nangu kuy def seniy liggéey ci dal yu mel nii, li ñuy wax àqi aji-sos bi(droit d'auteur) doon na lu mata bàyyi-xel.
Ñaareel bi, ndax li ngay dugal solowu na?
Ndaxte Wikipidia bëggul ñu ciy dugal ay mbir yu kenn xamul lan lañu. Kon li nga ciy dugal war na doon lu yitteel ay nit.
ñetteel bi, ndax xët wi amul ba noppi ci beneen tur?

Bari nañu, ñuy sàkk ay xët yu bees yu amoon ba noppi ak tur yu wuuteg yi fi nekkoon te seen ëmbit benn la, li ko waral mooy ki sàkk xët wu mujj wi seetul bu baax ndax li mu bëgga dugal am na fi ba noppi walla déet.

Nan la ñuy amee xët wu amul-dara ak kojam? Soppi

  • Am na ay yoon ngir sàkk xët wu bees:
    • ci biir jukki yu am yi ba noppi cuqal ci lëkkalekaay yu xonk yi.
    • Su fekkee dangaa bëgga wax ci lu bees, lu fi nekkul woon, lu njëkk li nga wara def mooy dem ci boyotu seetukaay bi "Seet" (mooy nekk ci cammoñu xët yi), man ngaa gis jukki yi mu méngool walla ci biir ay jukki yoo ko mana dugal (soo bëggee bind ab jukki ci Kajoor, dugal ko ci biir nguuri Senegaal mooy gën). Kon nga tijji xët wi nga yaakaar ne ci biiram war nga faa mana def ab lëkkalekaay buy tudd Kajoor, boo xam ne soo ci cuqe mu yóbb la ci xëtu Kajoor wi. Nii nga koy bindee [[Kajoor]]. Day xonq, su ko defee nga tijji ko def ci li nga ci namm.
    • "Ayca" moom da lay laaj ndax bëgg ngaa sos xët wi ak baat bi nga bind mu nekk kojam, su fekke amul benn jukki bu tudd noonu. Jar naa teey ak bii sosin ndax doy na ab wuute bu tuut ci baat yi mu sosloola jukki bu bees.

</poem>