Ndimbal:Nooy soppee aw xët

Daanaka ci Wikipedia ku nekk man ngaa soppi wépp xët. Jarul ngay bindu ngir mana soppi aw xët. Waaye xët yi ñu aar ñi binduwul du ñu ko mana soppi. Soo toppee xaaj yii di nga xam nu ñuy soppee aw xët.

Xaaj bu njëkk: Nooy duggee ci xëtu coppite wi Soppi

Xët woo tijji soo xoolee ci kaw di nga fa gis soppi soo ci bësee mu ubbil la weneen xët woo koy mana soppee. soppi

Ñaareelu xaaj: Soppi mbind mi Soppi

Xët wi day tijjeeku am melokaan wu mel nii(xoolal nataal bi ci suuf). Ci bii barab man nga fee def bépp coppite boo bëgg, muy jubbanti njuumte yi, yokk ci mbind walla ay nataal... barabu soppikaay bi

Ñetteelu xaaj: Wonendi Soppi

Balaa ngay duggal say coppite, ngala bul yakkamti, na nga wonendi li nga liggéey. Wonendi gi dalay won ni muy mel soo leen duggalee, di na tax nga mana jubbantiwaat yeneeni njuumte, suñu ci amee. Dencukaay:Wonendi.gif

Ñenteel: Dugal coppite yi walla Neenal Soppi

Su fekkee ci biir coppite gi da ngaa dem ba mu yàgg nga jàpp ne coppite yi nga def jaruñu ko woon, man nga leen baña duggal. Da ngay cuq ci Neenal. Ci nii xët wi day melaat na nga ko fekkee woon balaa nga ciy amal coppite yi. Donte def nga ay wonendi, du ci wàññi dara.

Balaa ngay dugal coppite yi, bindal li nga soppi lan la, ci tool bi ci wet gi Koj, ci misaal su fekke njuumtey mbindiin la, nga bind fa jubbantig mbindiin. Su ko defee ci jaar-jaaru xët woowa loolu lañ fay bind, lii di na tax waa-wikipedia yi xam li nga soppi.

Coppite yu néewal: yaw yaay xool ndax say coppite yu néewal lañu walla déet, maanaam am nañu solo lool walla déet. Su ko defee ci jaar-jaaru xët woowee coppite yu Néewal lañu fay bind.

Topp xët wii: Su fekkee ku-bindu nga, nga bëgga xam coppite yi mujjee am ci woowu xët, coppite yi tegu ci say yos, cuqal ci pax mi ci wetam. Ci sa limu toppte nga koy fekk.

ci Jeexintal, soo jàngee jàngaat, saytu bu baax say coppite ndax amuñu benn njuumte, léegi nag man ngaa cuq ci Dugal coppite yi