Ndiir xeetu ñax la gu bokk ci njabootu "Cyperaceae".

Ndiir (Cyperus esculentus)

Melo wi Soppi

Ndiir ñax la gog ab guddaayam day toll ci diggante 25 ba 40i sànti meetar. Ay xobam dafa sew di gudde 5 ba 10i mm te tàllalu di niru ab jubb. Peeram dafa taxaw, liis te am i pàcc yu ñatti-koñe. Doom bi ci reen yi lay meññ. Ndiir bi day xaw a wurmbalu, yor wirgo wu jege mboq, ab deram ñagas. Ëmb na lu xaw a tollu ak 50% ci gilisit( sakaroos ak amido), 22% ci lipit ak 6 ba 7 poroteyin.

Njariñ li Soppi

Dees na ko jaay ci ja bi. Ca Senegaal dees koy lekk noonu mbaa soppi ko diw. Amna ñu koy soppi njar niki waa-espaañ. Amna it ñu koy jëfandikoo nib fiirukaayu jën niki waa-àngalteer.

Nataal yi Soppi

Turu xam-xam wi Soppi

Cyperus esculentus

Tur wi ci yeneeni làkk Soppi

farañse: chufa
angale: chufa sedge
itaaliyee: zigolo dolce