Maa ngi Tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ju ñu jagleele ji ca allaaxiraa.

Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci suñu sang Muhammad ak ci ñoñam aki saabaam ci anam gu sax

Yàlla doy na ñu, moom de wéeruwaay wu baax la (wu mat a wéer say mbir, joyal ko ko).

Jëf yaa ngi ci yéene yi, ku nekk it la nga yéeneey sag pay

Bokk na ci hikam (sagesse) :

ku sàkku mbir de bu ca saxee am ko. Ku fëgg bunt it boo fa saxee ubbilees la

Bokk na ci hikma bat ay:

ku tëyye boppam wëlif neen yi (caaxaan yi ) limees ko mu bokk ci boroom xel yi.


Bokk na ci ba leegi:

ku dul merloo boppam du begloo boroomam.

Bokk na ci ba tay :

ku def la ko soob dajeek la ko naqari.

Bokk na ci:

ku taqook jiyaar ak bakkanam, texe fa biir bàmmeelam .

Bokk na ci :

ku topp Yonnant bi, am gën ji la mu ñaan.

Am ku jël maanaa yii yépp boole leen ci wenn bayit :

( képp ku woor wëlif caaxaan yi () danga dogi ciy ngënéel )

Taalif wi

Soppi

Taaliif wii nag lu ñu barkeel la ci njëlbéen gi ba ca dayo ba.

Moom nag (ki waxoon bayit wu njëkk wi) –yal nañu ko dolli ag bëbb (xéewal) – am na ba tay weneen bayit wu yor maanaa mii, mu ciy nos (woy) maanaam waxi sëriñam ji, wax jooju mooy jii :

(nguurug neen waxtu rekk la, nguurug dëgg nag day wey ba yawmal-xiyaam)

Woy waa ngii :

( dëgg day sax , neen nag bu kawe woon it day mujj naaxsaay, mujj suufe)


Maa ngi Tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ju ñu jagleele ji ca allaaxiraa


Ubbite gi

Soppi
  • Kii di doomi sëriñam ji dul sant ci boppam lu dul turam (wu tedd wa) Muhammad, kii de mi ngi sant Yàlla (t.m) mi suturaal ay ayibam te taxawu ko te dimbali ko.

Tudd naa sellam ga moom de boroom bu tedd la bob may na ma lu waral ma koy sant. Moom de mooy ki def ay teggiin yu raf muy luy làq ag réer ak judd bu ñaaw (bonu askan). Mooy ki jagleel boroom xam-xam yeek teggiin, mooy ki léen jagleel ab yool akug jam-jub (def la jub). Xéewal ak mucc gu kawe nañu sottiku ca ka yéegoon ca Alburaax (Yonnant bi).

Kooku mooy suñu sang biy woote jëme ci aji bind ji (ki sàkk mbindeef yi), defe ko nag ci gën jaa rafeti teggiin yi .

Kooku mooy Muhammad ak ñoñam ñi di woroomug raw ak saabaam yi làq ngënéelul Aji des ji (Yàlla mi fi dul jug)

Ñoom saaba yooyu de saxaloon nañu ag laa-biire ci lu dul ŋaayoo , ndaxte dañoo toroxaloon seeni bakkan ba far léen moom.

Sànkoon nañu seeni alal cig joxe ci lu dul ngistal mbaa naafeq. Ñu sukkandiku woon ci Aji jariñ (Yàlla) jiy Aji wërsëgale, ngir ag wakkiirlu ci moom ci mbooleem wërsëg yi.

Ñoom de dañoo boyoon jëm allaaxira ngir ne dañoo fase woon wujj wa (adduna). Masuñoo bàyyi lenn ndigal lu juge ci Aji settantal ji (kiy def mbir yi di Yalla) kiy Aji bind ji. Ñoom de - ci saffanub ñuy bàyyi ndigal yi - dañu ciy sax ànd ceek bànneex, ndaxte koomum ja yi du tax ñu koy fàtte (alal ji ñuy jële ci marse yi duñu tax ñuy fàtte ndigali suñu boroom yi) . Wuññi woon nañu lëndëm-lëndëmi gox yi ci xam-xam ak jëf ak dëppoo.

Ndaw ñu di sang yu ñaw ! ñoom de la neexoon ca cafka ga jël nanu ko.

Yal na ngërëm - lol di naa ci dajeek ëlëg ka làq cang gu joyu ga – sottiku ci seen kaw . Kooka mooy Muhammad, yal na ko Aji des ji sotti ay xéewal ak mucc mook ñoñam ak saabaam yi di ay ndab (yuy duy xam-xam aki xeewal aki hikam)

Li waral xasida gi

Soppi
  • Man dey tay damaa ñëw ngir wuyyu lenn ci murit yi di woroomi tuub (ñiy tuub ak a jéggalu seen boroom).

Ñoom de dañoo sàkku woon ñu defal leen woy wuy jàngale ay teggiin, ngir ñu sàkkoo ciy teggiin, te loolu wartéef la .

Ndax kat képp ku bëgg a topp Yonnant bi te tegoo ko ciy teggiin dees na ko xañ ag texe akug jariñu Moom teggiin de - ci àdduna ak allaaxiraa – mooy gën ji ndàmb tey gën ji lu ku tedd di tedde Ndaxte mooy leeral ab xol tey jegeele àjjana.Dina waral say dëkkandoo di la tagg te dina sooreel it sawara.

Ma daal di jug (ngir sàkku gi ñu ko sàkku woon ci man ) gaawantu, tontu léen, di ci sàkku nag ab yool ak ngërëm. Moom nag du lu dul jël la Waliya wa tuddoon Dal-Haaji wesaroon (manaam la mu bindoon te woyu ko,maanaam defu ko woon ay bayit ) def ko ay woy, di ñaan ci def gi Yàlla fajal ma samay aajo


Lu tax ma taamu ko ?

Soppi
  • Ndax dafa boole – ba noppi gàttal ko – li ëpp ci li taalifkat yu njëkk ya bindoon cig tàqale.

Lépp loo gis mu néew te doy moo gën lu bari te sonle.

Def naa ko nag woy wu ami njariñ, ci baaxug Yàlla mi dige (ci Alquraan) ne dana aar (ñi gëm) Ndax Yàlla may ma ci ngërëm ak kóolute ak njéggal ca bisub njàqare ba.

Kon kat yéen sàkkukati xam-xam yi maa ngi leen di dénk te dellu di léen dénk te di leen xiirtal ci tontu bii (téere Nahju bii) Ndax kat yor na ci ay jikko aki teggiin lol (bu ngeen ci tënkoo ) dina leen wommat jëme leen ca jub ga

Ay gindee ngi ci aki jariñ yoy boroomug nammeel (ab murit) du ci yoqat mukk Kuy door a dal ak kaaŋ-fóoree yam ciy njariñam , aw yiwam it du jeex mukk.

Ndaxte ni ñuy àgge ci gën jaa rafeti jikko yi mi ngi ci ak ca (lu baax) la ñuy mébët. Maa ngi ko tudde:

Nahju QadaaAl Haaji) ci góob mbayum suñu sëriñ bii di Dal-Haaj.

Maa ngi ñaan Yàlla mu nangu ko ca baaxam ga te àggale liggéey bi. Di ko ñaan it mu mel ne turam wi, ba ki koy jàng ay mbiram man cee yéwéne ngir mu texe Te mu musal ma ci ngistal ak aaw (naw sa jëf) ci barkeb Yonnant biy boroom Liwaaul Hamdi Ak yu dul ñoom ñaar ci caay-caay yi (bon-bon yi) te mu may ma ay ngënéel Te mu musal ma (t.s) ba fàwwu ci ayuw ibliis mii nga xam ne dafa féttéerlu .

Te mu musal ma ci ayu li mu bind ci suuf si, ak li mu bind ci asamaan si ak li nekk ci seen diggante ñoom ñaar Te mu may ma ma topp ci sunnas Yonnant bi (j.m) miy gën ji mbindéef , miy ku ñu ramuloo, miy ku ñu topp

Ginnaaw bi mu jullee ci moom te sëlmël ci, ak ñoñam aki saabaam ci anam gu dul dog.

Fii nag mooy fi tarjumaani téere bi yam, kon leegi nanu jublu ci (indil leen) teggiin yi.

ndoorte li

Soppi
  • Ngir woy (nos) lii di wesaru Seex Ahmadu - mii di ku géeju ci xam-xam – maa ngi naan :

Yeen mbooleem way sàkku yi xam-xam déglu leen sama laabiire gii di léen tàqaleek ag texeedi Mu di laabiire gog dañu leen koo jëme ngir jëmmi Yàlla rekk, muy yee nag jépp aji xellu ak ku jamuj(fàtte) :

Yoonu teggiin de mooy yërëm ndaw, ni ko baayam di yërëme ak ndayam te weg mag ak def sa moroom ni sa bopp ngir jëmmi Yàlla mi nekk ca aras (toogu ba)'



saraab aji taalif ji : Yoonu teggiin mooy nga yërëm ndaw mel ci moom ni baayam ba ko jur te am lool ci moom yërmande, te mel ci ne ndayam ju am ja ag ñeewant, nga weg it mag ak doonte da di ab jaam bu bawoo Abasa (Ecopi) , te nga yamale sa bopp ak sa moroom ngir jëmmi Yàlla kepp.

Xamal ni teggiin de mooy taarub boroom xam-xam ak ku koy sàkku, mooy it takkaayi aji xellu ak ku lewet, mooy njobbaxtalu jikko yi, ku ko takkaayoowul yoqéel na (ñàkk na ay takkaay)te neenal, dana mujj di ku ki bind bañ ak ñi mu bind (Yàlla aki mbindéefam) képp ku ko gis bañ ko te sànj ko (mere ko), kepp ku toog ak moom am ci moom ag yoqat akug doyal.

Bokk na ciy teggiin ngay laabiire koo gis ca la nga gis ne ag jubam a nga ca, te ngay bañ a yayale sa bopp jenn àq ci kenn, te nga jort it ne yayoowoo ci kenn mu lay màggal (ci lenn).



Loolu nag mooy li mu junj ci waxam jii :

Nangay yërëm gone

Soppi

Nangay yërëm gone, (rikk) bu ko nëbbal benn yoon genn laabiire gu aw yiwam nekk. Deel weg mag ak doonte da di ku doyadi te xeebu. Bokk na ci ay teggiin nga bañ a jort ne yayoo nga jenn àq ci kenn ku mu man a doon . Te nga bañ a séentu genn maggal ( mbaa wormaal) mu juge ci kenn (kok man nay mer sax ci màggal gi mu lay màggal).

Yaw daal jortal ne teggiin yepp ci yaw la war a bawoo, bu leen séentu mukk ci say àndandoo. Àndal ak nit ñi ni nga bëgge ñu ànde ko ak yaw.

Saraab aji taalif ji :

Li mu namm a wax mooy : bokk na ci teggiin yu rafet nga jort ne ay teggiin moom ci yaw rekk la war a juge, te nga bañ di ko séentu ci ku dul yaw. Te ngay ànd ak nit ñi ( ci jikko yu baax yi nga bëgg ñu ànde kook yaw) (boo ko deful it jikko yoo ànde ak ñoom ci yu bon séentu ko ci ñoom, nit ñi daal ni nga mel ak ñoom rekk lañuy mel ak yaw).

Nangay sàmmoonteek aqi (Yàlla) - boroom màgg giy boroom kàttan gi - ci ñoom ngir jëmmam ja (moom Yàlla) ni waxi woykat ba :

Mu bëgg a wax rekk ne bokk na ci teggiin yu rafet ngay sammoonte ci mbindéef yi àqi ki leen bind(t.s) ci di àndeek ñoom ni ko woykat bi waxe ca qasidaam ga yor bahru basiit: Yaw mbokk mi nangay am yërmande ci mbooleem mbindéef yi, nanga léen di xoole bëtub ñeewant ak yërmande

Nangay weg mag di yërëm gone, tey sammoontek àqi aji bind ji ci mépp mbindéef. Am na addiis bu naan : sama xeet wi de du dañ di nekk ciw yiw li féek ku ndaw a ngi ciy weg mag, mag di ci yërëm gone.

Kon rikk nanga di roy ci gindig Imaam yi (y.y.g)kon de di nga gindiku

Bul di toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a ñàkk(loola mooy lu mel ne) : ngay jàng ( ci moom) walla nga dëkk (ak moom) walla nga bokk ak moom di lekk, bul toogandook moom cib lal it

Saa su (Yàlla defee nga toogandook moo) nanga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu Akug watandiku, te bul di tafu ci kawam, bul toog it ci kanamam

Yaw mbokk mi (rikk) bu ko tàllal sab tànk boo toogee ci moom, te deel damm sab gis wëlif ko (maanaam bul ko di faral di xool rekk

Saraa :

Soppi

Mu bëgg a wax ne : bokk na ci teggiin yu rafet nga bàn a toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a ñàkk, ngir jàng mbaa dëkk ak moom walla di lekkandook moom añs. Boo toogeek moom it nanga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu ak wattandiku. Bul di ko ñóoxu mbaa nga koy tàllal ab tànk, bu ko di ja tam, bul di baril di gëstu ci lu dul aajo, ndax loolu ci màndargay ag ndof la, Yàlla nee na (t.s) : (( neel jullit ñi ñu dam seenub gis . loolu moom lay junj ci waxam jii di ñëw :

Bul di baril looy geestu fu nekk, te dara ñoru la ci geestu gi. Ndax loolu kat màndargam ndof la, te (boo demee ) ci téereb Yàlla bi (di nga fa gis) : ((neel jullit ñi)) Deel topp ndigali boroom mbindéef yi, ndax kat nekk na ci addiis : waay de (sànkoo na ci bennub xool rekk) Ab woykat de waxoon na bu yàgg ne : ( booy def loo gis xool ko danga ci mas a am bis) kon bul di wëndéel sab gis . Saraa : Mu namm a wax rekk : war na la nga topp li la sa boroom digal muy damm sab gis. Ndax Addiis bi nee na : waay de dana xool benn xool bob xolam dina ci yàqoo nib der di yàqoo ca sébej ga , du ca jariñu mukk. Woykat ba nee na : ( yaw de boo sànnee sab gis ngir sa bànneexub xol, bis dina ñëw bob li ngay gis dina la sonal (danga gis lol doo man léppam (doo man a am lépp ) te doo man a muñ rekk ca lenn la ( doo man a yam rekk ca xool ba. Doo ko man a am te doo ko man a muñ, bu ko defee ngay sonn ci loo dul am, te boo ko gisutoon doo ko yittewoo) Keneen it ne: ( jàmbaar du mooy kiy aar ay gawaram ca bisub jamante ba, bu xare ba tàkkee) (waaye ka damm ab gisam mbaa mu lem ab tànk wëlif ay moy kooku ci jëmmam mooy gawar dëgg bay jàmbaar ) Bul di baril am po, bul di ree lu bari, mbaa ngay baril looy yëngatu ak a defi neen Bul di baj-baji mbaa ngay jéem a yëddu lu nëbbu lu mu man a doon Loolu de màndargam tóoy la ak woyofum xel ci ku ko baaxoo Boo jekkee nanga dalal say cér, nangay taqook ag noppi ànd ak dëddu (ci lug dëddu war) kon de nga jariñu Deel muñ ag ŋàññ te bu ci tontu kenn, te mel ni na boroom njàngat la (adiib) waxoon : wallaay damay romb waa ji mu may xas may jellale naan kii de xam naa ne waxuma Ndax kat xasante ak weddeente bokk nañu ci jikko yi gën a bon niki dóorante. Bariy ree daay ray ab xol, kon rikk néewalal ree yi, ndax nga gërëmloo Boroom bi

Saraa:

Soppi

Maanaam bokk na ci teggiin yu rafet nga bañ a barili ree, po, ag neen, ag baj-bajeek yëngatu ak a jéem a yëddu lu nëbbu, loolu de ci màndargam tóoy la bokk,ak gàttum xel, nangay faral a dal boo jekkee (boo toogee) cib jataay tey faral a noppi, ba ñu laaj la, bu boobaa nga tontu ci kàddu gu suufe, walla nga soxlaa laaj dara, bu boobaa nga def ko te yam ca sa soxla rekk, bu ca dolli dara, ndax kat noppi noflaay a ngi ci ak sutura niki ñu ko waxe:(nëbbal ayib yi kem li nga man cig noppi, ndax kat ab noflaay a ngi ci noppi ñeel aji noppi ji )(defal sab tontu boo lottee muy “noppi”, bari na wax joj tontu baa nga ca ag noppi) Bokk na ci Hikma: Bu wax doon xaalis noppi di wurus, bu la nit réeree (def la ag ñàkke-teggiin) Jéllale ko taqoo noppi, ni ko Yàlla waxe: (( Jéllaleel ñeel ñi réere)) ((bu ñi réer waxee ak ñoom nu tontu léen ci luy waral jàmm)) Ni ko woykat bi waxe: (Amaa na ma romb ku soxat ki (ku yaradiku ki) mu may ŋàññ, bu ko defee ma fegu te naan kii daal waxut ak man) ŋàññante ak weddeente bokk nanu ci jikko yi gën a ñaaw, yi gën a bon, ree ju bari day ray ab xol. Boo bëggee am sa ngërëmul boroom, néewalali ree, Yàlla ci jëmmam (t.s) moo ne : ((nañuy ree lu néew )) Boo toogee ak ku la mag booy ree nangay yam ci muuñ Booy wax ak moom it bul bayliku ( ëppal ci wax ji) ndax loolu du lu rafet Noppil ba nga gis mu bëgg a wax ak yaw, bu boobaa yamal ca la mu soxla ci yaw Loolu kat moo di ay teggiin, kon jëfe ko cig wàllam Bu la béccingalee , muñal béccingalam yooyu, bu defee lu jaaduwul suturaal ko Bul dañ di ko jéggalu, te bu ko di mere it Bu koy faral di ja (jëmale ko say gët , samp ko ko rekk) ci waxtu wu nekk

Saraa:

Soppi

Bokk na ci teggiin yu rafet nga bañ di ree ci jataayub ku la mag ndare muuñ, nga bañ di wax ak moom cig bayliku, maanaam ëppal ci wax ji, lu ñor nga wax ak lu ñorul,moom daal nanga yam ci li mu soxla ci yaw, bu boobaa doxal nga ay teggiin ci moom. Bu la defee lu jaaduwul jéggal ko, te di ko jéggalu, bul ko di faral di xool xool bu metti, ndax loolu duy teggiin Boo bëggee juge ca jataay ba, nanga ko defe cig tëyyewu (tëyye sa bopp ba suuf du jug pënd du jeqiku) Bu léen xëpp suuf si ci seeni kanam ndax loolu wuute na ak ag jub Boo ko manee bul di nelaw ci biiru nit ñu nelawul Ndax kat loolu duy teggiin, ngir ne am na lu ci nekk lu man a waral ag yeddeel (kuy nelaw man ngaa ngelawal te doo ko yëg)

Saraa:

Soppi

Bokk na ci teggiin yu rafet nga bañ a jeqi pënd boo toogee ci jataay bay jug, boo nammee jug , def ko ci ag dal akug tëyyewu, te bul jaar ci kanamu way jekki yi. Bokk na ci ay teggiin nga bañ di nelaw ci digg ay way yewwu boo ko manee, ndax amaa na ngelaw génn ci yaw te doo ko yëg, ndax bët ay saañu ag suuf(bën-bënu aw taat)

Nanga xam ne fuqale bokk na ci liy waral gàcca ak yeddeel Képp ku aj yitteem ci lekk ak séy na xam ne boole na lépp luy toroxte Lekk dee ci jël lu lay dëgëral ba nga man a jaamu sa boroom te yam ca Deel wattandiku jamono ju nekk fuqale ndaxte mooy cëslaayu wépp ay Saraa: Bokk na ci ay teggiin ñàkk a fuqale ak ñàkk a aj sa yitte jépp ciw ñam , loolu de cig suufe la te day waral ag ŋàññ Woykat ba nee na: (yaw de foo fi joxe sa biir li mu la laaj ak sa pëy , di nanu àgg fa mbooleem toroxte ya yam ) Sab loxo nanga ko tëyye, bul ci di baril am po, ndax loolu de ayib la Bul jottaliku mukk lol làqul njariñ lu la man a jegeel sa boroom


Saraa

Soppi

Bokk na ciy teggiin :tëyye sa loxo ak bàyyi di ci fo ak bàyyi di ci jefandikoo lu njarin nekkul, loolu de bokk na ci li woroom xel yi ayibal, te ci la musiba yi tase. Saa soo déggee ku la mag mu soxla dara Niki mu bëggoon ku mu yonni, rikk demal doxal ko yonneem boobu ngir jëmmi Yàlla Bu kenn soxla ci yaw dara ndare bu danga koo defal loolu mu soxla ci yaw, boo dee def noonu de danga am teraanga Rikk bul di wax kenn fen nga, walla wax nga lu dul dëgg, walla juum nga Walla jeneen wax ju man a merloo ak doonte ki nga koy wax gone la, di ko waxe de ag njuumte la Bu waxee loo xamul nee ko dëggal nga, kon dees na la teral Nee ko daal man de tegoon naa ko neneen, walla leneen laa jortoon, walla réere woon naa ko Ak yeneen baat yi walla waxiin yi man a bégale, loolu de boo ko defee def nga lu rafet, bul ñaawal te bul lore Deel tàmbal saw làmmiñ wax lu baax, kon de dinga ci ame ag texe te dees na la ci fegale wépp ay Ngir waxi sangub mbindéef yi (ku nekk na….) yal na ko Yàlla dolli ay xéewal ci anam gu sax (ku nekk na….) : (ku nekk na di gëm Yàlla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiw mbaa mu noppi)

Saraa

Soppi

Bokk na ci teggiin yu rafet nga saxoo di faj aajoy ku la mag boo ko déggee mu koy sàkku, niki mu soxla woon ku mu yonni Bokk na ciy teggiin ba tay nga bañ di gàntul kenn loo man lu mu soxla ci yaw, te bañ di wax kenn (fen nga) mbaa ( li nga wax du dëgg) mbaa baat bu ko man a merloo ak doonte yaa ko mag, bu waxee loo xamul dëggal ko te ne ko (man de nekkuma woon foofu) walla (jortoon naa ne) walla (xamewuma ko woon noonu) ak yu ni mel ci waxiin yu rafet Nangay tàmmal saw làmmiñ wax ju rafet . Yonnant bi (j.m) nee na : (ku gëm Yàlla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiw mbaa mu noppi) kenn ci woykat yi nee na :(tàmmalal saw làmmiñ wax ju baax, kon de danga ca ame ab cér)(làmmiñ de li nga ko tàmmal rekk lay tàmm)(lu mu man a doon la nga ko ca miinal rekk lay def)(moo xam lu baax la mbaa lu bon, deel xool nooy dollikoo) Sab dox na ko aajo di waral ci lu dul ag rëy, ag rëy de ci mbugal lay bijjee jëme Bul di ree mukk ci lu dul lu yéeme, bul dox mukk it ci lu dul aajo Bul gestu tam te sàkkuweesu ko, ndax yii yépp ag ndofe la gog dàqoo na’aki teggiin Sa tubay it bul ko di wuññi mukk, ndax loolu ci bàyyi ay teggiin la bokk Moom de ci jikkoy kàccoor yi diy saay-saay te bokk ci giirug Hassaan la bokk, ñoom ñi dëddu lu baax Nangay moytoo wuññi sa biir ak li nekk ci diggante jumbux bi ba ci bëti-woom yi, (ngir bon gi mu bon) Loolu de màndargam réer la ak ndofe ak néewug mbañ-rus gu màgg gi Ndax moom (mbañ-rus) mooy dàttub diine, fu mu nekkul diine nekku fa , loolu de la (jàngalekat yu mag ya) saxal Koo agsi ci moom nanga ko nuyyu, bu fekkee ne soxla nga ay teggiin Bu fekkee ne moo la njëkk a nuyyu nanga ko fay ci kàddu Boo saafoonteek moom (boo nuyyoonteek moom ) nanga dëgëral sa loxol ndijoor ci ndijooram, loolu mooy li nu rafetlu Bul rocci sa loxo li feek njëkku la koo rocci moom ci anam gu fés Ndaxte de sibees na fëkk ay loxo ci nuyyoo ci anam gu gaaw ak bàyyi wax ja Saafoonte ci ñaari loxo it bokk na ci ay teggiin, niki ñaar yi nu la waxoon leegi Ñaanalal ki ngay nuyyool yaw boroom xel mi, ndax loolu de bokk na ci liy fari bàkkaar Boo bëggee dugg ci kër (walla néegub) jàmbur nanga yëglu, kon de nga am la gën Bu ñu la digalee nga dugg nga dugg, bu dul loolu dellul Sab bët bul ko di wëndéel ci néegub jàmbur (mbaa këram ) ngir ragal gis fa awra joj bëggunu woon nga gis ko

Saraa

Soppi

Bokk na ciy teggiin booy jug aajo rekk di la yekkati, bokk na ci ag ndofe ngay ree te lu reeloo nekku fi, mbaa ngay dox ci lu dul aajo, mbaa ngay gestu te yittewoowoo ko, bokk na ci ay teggiin ngay moytoo wuññi say sér, loolu de ci jikkoy kàccoori Hassaan yi la, bul di feeñal lenn ci sa biir mbaa li nekk ci sa diggante jumux ba ci say wóom, loolu de ci réer la ak ñàkk kersa te kersa mooy dàttub diine tey laylaat gi mu tege, fu kersa ñàkke diine jug fa. Bokk na ci ay teggiin ngay nuyyu képp koo dox ba àgg ci moom, te di ko fay bu la nuyyoo, te ngay saafoonteek moom tey dëgëral sab loxo ci loxoom boo koy nuyyu, te nga bañ koo njëkk a rocci sa loxo , fëkk loxo ci lu gaaw cib nuyyo de lu ñu sib la. Bokk na ci ay teggiin ngay saafoonteek moom ci sa ñaari loxo yépp, te nga koy ñaanal lu baax ak sa bopp loolu bokk na ci liy far ay bàkkaar . bokk na ci ay teggiin ngay def booy dugg ci néegub jàmbur mbaa këram ngay yëglu bu ñu la nee jàllsil nga dugg, ndeem déet nga dëpp, rikk bul di sànni sab gis ci kër mbaa néeg boo moomul ngir nga bañ faa gis loo warul a gis. Boo bëggee kooy àndandool bu muy ku dese cim xel mbaa ku iñaan mbaa ku bariy xemmeemtéef Bu di toog ak ku dul ku lay dolli diine ak xel, kon de nga am càkkutéef la Ndax de xibaar nañu ne cam si de (waa ji) ma nga ca diiney xaritam ba, loolu ab adiis la bu ñu tuxal(waa ji de diine ji waayam yor rekk lay yor) Saraa: Da lay dénk nga bañ a àndandook way dese yi cim xel te bañ di toog ak ku la dul dolli diine ak xel, ci loolu de ngay ame la nga bëgg, ndax waa ji de ni ab xaritam mel rekk lay mel, (wolof yi nee nañu won ma sa xarit ma wax la sa jikko) seyyidinaa Aliyun - karramal laahu wajhahuu – nee na:(Bul def mukk boroomug réer muy sab àndaale, moytu ko te moytu sa bopp)(bariwaa na aji réer ju alag boroomug lewet (ku nite) ba mu ko defee mbokk) (nit de ca moroom ja lañu koy natt bu àndeek moom)(ni ñuy natte dàll ca moroom ja bu ñu dee ñaar) (mbir de am na ag niroo akug natt ca moroom ja)(xol de misaal la ca moroom ja ) Am na ku ne :(boo nekke ciw nit nangay seet ña ca gën ngay ànd ak ñoom)(bul seet ña ca yées ngay ànd ak ñoom bay yées )(bul laaj waa ji, waaye laajal ab àndandoom)(Ndax ku nekk ca ka ngay àndal ngay roy) Bul sàkkoo gis mukk ab rëcc-rëcc (ci sa moroomu nit) bul gëstu itam ay awra (ay ñaawtéef)

Saraa

Soppi

Mu ne : bokk na ciy teggiin ngay bañ di gëstu rëcc-rëcci nit ñi mbaa seeni ñaawtéef. Waxees na ne : (bul di sàkkoo xam la nit ña nëbb ci seeni ayib) (ndax kat loolu man naa waral Yàlla di muri mbalaan mi mu muuroon ci say ñaawtéef) (rikk nangay tudd lu baax la nekk ci ñoom bu nu léen tuddee) (bul ayibal kenn ci ñoom ndax kat loo léen wax man naa am yaa léen ko ëpp) Nanga mel ne na woykat ba waxoon: (dinaa bëgg jikko yu rafet yi sama kem kàttan) (tey bañ di ayibale ak ñu may ayibal) (may jéggal ŋàññug nit ñi ngir ag lewet) (ndax ki yées ci nit ñi mooy ki sopp ag ŋàññante) (ku weg nit ñi wegees ko) (ku xeeb nit ñi deesu ko weg) Ka wax lii de wax na wax ju rafet: (boo bëggee dund sa diine mucc) (sa wërsëg lëw (bari) sab der ñoŋ) ((boo bëggee loolu) sa làmmiñ bu ci tudd mukk ayibi nit) (ndax kat yaw it am nga ay ayib, nit ñi ami làmmiñ) (bu Yàlla dogalee say gët rot ci ayibi nit, nee leen :) ( ee yéen gët yi bu léen xool de, ndax nit ñi ñoom it am nañu ay gët)

des na