Muhammad Lamin Daraame
Muhammad Lamin Daraame (turam dëgg di Demba Dibaasi) sëriñ la won bu bokkoon ci giirug Saraxule, di woon it tiijaan bu askanoo ci Gonjuro. Tukki woon na dem Màkkatal Mukaarama, nekk fa ba 1879 g,j. Bi mu dellusee la ko Ahmad Seexu jàpp, jotul a àgg cig njabootam lu dul ci atum 1885 g.j .
Muhammad Lamin Daraame siiwe woon na ag ragal Yàlla, looloo waraloon mu amoon taalube yu bari. Jibaloon na jiyaar ci kaw dëkkandoom yi duli jullit ak ci ñoñ frãas ñi sancoon réew mi. Xareem bi, tolloon ci junniy xarekat jawali woon na Bundu, daal woon gaw tatay Bakkel ji, atum 1886 g.j, waaye ak li ko waa Bakkel doon faral lépp taxutoon mu man a teg loxo ci dëkk bi, looloo taxoon mu dëppaat. Waa Frãas yi tiitoon nanu lool ci ndam yi xareem bi ndàmm, looloo waraloon ñu song ko nangu Sinodibo, njaf doomam ja Saybu, ginnaw bi ñu ray ko.
Ci atum 1887 g.j, la ko tubaab yi manante ci deltu ginaaaw jëm Gambi. Daal di toj tata ja mu tabaxoon ca Tuubaa Kuta. Muhammad Lamiin ñàkkoon na lu bari ci xarekatam yi ci xare bii. Tubaab yi ray nanu ko ci ndimbalul Muusa Mulo. Ñu mujjoon manante buur yu bari ci ñu xaatim ay kóllarey ndénkaane(tutelle), tegoon it loxo lu ëpp ci suufi Senegaal yi.