MIIRAAS

Miiraas: Xam-xam la buy lijjanti alalu aji faatu ji; muy li mu bàyyi ginnaawam lépp, nan lees koy séddalee ci ñi nga xam ne ñoo ko war a donn, moom nag mooy xam-xam biy jëkk réer, jugee ci àdduna. Loolu nag Sangub mbindeef yi moo ko wax Muhammat (SHW), te it nee na mooy genn wàllug xam-xam, (عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم: (تعلموا الفرائض وعلموها الناس فإنها نصف العلم وهو ينسى، وهو أول شيء ينزع من أمتي) رواه ابن ماجه والدارقطني) Moom miiraas benn la ci xam-xam yi soqikoo ci Fiq ci la bànqaasoo aw wëppaam (them) day dugg ci biir bànqaasi xam-xamu Fiq bokk ci xam-xami diiney lislaam.