Mbal ag garab la gog mi ngi bokk ci njabootug " Euphorbiaceae". Mi ngi bokk ci gàncax yi nga xam ne at ba at lay meññ.

Mbal gi (Euphorbia hirta)
Mbal gi (Euphorbia hirta)

Mbooram

Soppi

Mbal mi ngi cosaanoo fële ci diggu Amerig. Mbal garab la gog day sax foo xam ne baaxu faa saxe mu yaatu lool ci tund yi nga xam ne dafa am naaj. Niki noonu bari na fële ca Afrig bëj-Saalum.


Njariñ yi

Soppi
 
Xobi ak tóortóori garabug mbal

Mbal garab la gog bari na xeeti jàngoro yu bari yu muy faj, loolu moo tax fépp fumu nekk dan ko fay jëfandikoo rawatina fii ci Afrig nga xam ne dañu ko fiy jëfandikoo ngir muy faj, biir buy daw, naka noonu dañu koo faa jàppe ngir ne mooy li gën a gaaw ngir faj lépp loo nga xam ne dafa jëm ci wàllu noyyi lu ci mel ni asma, ak yaneen xeet yi ni mel.

Bokk na ci ay njariam batay dañoo wax ne moom moo gaaw lool ci faj bopp buy mett. ak bëñ buy metti.

Turu xam-xam wi

Soppi

Euphorbia hirtata

Tur wi ci yeneeni làkk

Soppi
angale: asthma-plant