Mbërbóof xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Curcurbitaceae", barab yu naaje yi lees koy baye. Tur wi nag ci làkku wolof ñi ngi ko tëgge ci "mbër mu bóof" ndax bari gu mu bari ay njariñ rekk.

Mbërbóof gi (Momordica balsamina)

Melo wi

Soppi

Garab gi danay àgg ba 5 met ci guddaay. Xobam xet gu tar ak cafka gu wex la yore.

Tóortóoram day ndaw te mboq. Car yu nooy a koy tëye.

Doom bi daa dége te puur. Guddaayam 8 ba 35i sàntimet lay àgg.

Njariñ li

Soppi

Mbërbóof lees di lekk la te di ko fajoo. Ci toppatoog jabet ak yenn kãseer yi dees na ko fa jëfandikoo.

Nataal yi

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Momordica balsamina