Mbàccaar
Mbàccaar xeetu garab la gu bokk ci njabootu "caesalpiniaceae" walla "fabaceae". Tóortóoram daa xonq te taaru lool. Madagaskaar la bàyyikoo waaye leegi ci barab yi bari naaj ci àddina bépp dees na ko fa fekk nib garabu taaral.
Melo wi
SoppiPonkalu garab gii danay romb 15 met ci guddaay. Téeñam jëmmu fanq-naaj la yor. Tóortóoram 4i xob yu xonq la yor yuy xaw a tolloo ak 8 sàntimet, ak uw ñeenteel wu gën a rëy wuy nekk ci digg bi te yor wirgow xeex ak mboq. Mbàccaar si ronam day liis te leer.
Mbàccaar bi melo ñebbe la xaw a yor te guddaayam di àgg 40 ba 60 sàntimet. Yaatuwaayam danay àgg 5 sàntimet te da day ëmb 10i xoox.
Mbaaxam
SoppiBarab yi xaw a naaje la taamu, waaye danay muñ bekkoor, xorom. Bëggut suuf yi bane te tooy, suufus joor moo ko gënal.
Solo si
SoppiGarabu ker la baaxoo ci tool yi, bedd yi ak kër yi. Dees na ci yàtt gaal, dees na ci wutum màtt te di ci fajoo.
Turu xam-xam wi
SoppiDelonix regia
Turam ci yeneeni làkk
Soppifarañse: flamboyant |
angale: royal poinciana |