Maryaama Ba

Liggeey
Jàngalekat
Dundu ak jaar-jaaram
Bésu juddu 17 awiril 1929

Dakaar, Senegaal

Bésu faatu 17 ut 1981 (ci juroom-fukki atam ak ñaar)

Dakaar, Senegaal

Réew Senegaal
Fi mu jànge Ekool Normaal bu Tëngeej (Rufisque)
Yëngu-yëngu Bindkatu téere nettali
Way-jur wu góor Aamadu Ba
Borom-kër Obéey Jóob
Yeneen xibaar ci moom
Diine Islaam
Neexal Prix Noma de publication en Afrique
Téereem yi gën a fës
  • Une si longue lettre
  • Le Chant écarlate

Erreur de script : la fonction « build » n’existe pas.Royuwaay:Infobox en Lua Maryaama Ba mu ngi juddu fukki fan ak juroom-ñaar ci weeru awiril atum 1929, faatu fukki fan ak juroom-ñaar ci weeru ut atum 1981 ci Dakaar. Bindkat la woon. Ci ay téereem, Maryaama Ba dafay ŋàññ ñàkk a yemale gi am ci diggante góor ak jigeen te aju ci aaday Afirig.

Dundu ak jaar-jaaram Soppi

Mu ngi juddoo Dakaar atum 1929 ci njaboot gu am alal. Way-juram wu góor liggeeykatu nguur gi la woon.

Ginnaaw bi way-juram wu jigeen faatoo, ci teel sax, ay maamam a wéyoon di ko yar. Ñooñu ñoo ko yar ci diiney lislaam. Way-juram wu góor, ñu doon ko wax Aamadu Ba mujj nekk jëwriñ ji yore wér-gu-yaram bi ci ngornamaŋ bu Senegaal atum 1952.

Mu daldi dugg ci lekool farañse bi, nekk ku ci ràññeku lool ndax ay jallooreem. Bi mu amee sàrtikaa (certificat d'études primaires) ci fukki at ak ñeentam, la dem ca Lekool Normaal bu Tëngeej (Rufisque) atum 1943. Lekool boobu mu nga fa jóge atum 1947 ginnaaw bu mu fa amee lijaasab njàngale. Mu nekk di jàngale diiru fukki at ak ñaar laata muy ñaan ñu jële ci njàngale mi, yóbbu ko ca Eespeksiyoo bi yore wàllu njàng mi ci gox bi (Inspection régionale de l’enseignement), loolu wéradig yaramam moo ko waraloon.

Am na ñetti doom yu jigeen ci sëyam bu jëkk ak Basiiru Njaay, am beneen doom bu jigeen SMK[Quoi ?] ci ñaareelu sëyam ak Ablaay Njaay. Yàlla wéddi sëyam ak ñetteelu borom-këram di Obéey Jóob, nekkoon fi deppite ak jëwriñ te mu amoon ak moom juroomi doom. Ginnaaw jaar-jaar yooyu yépp mu am ci sëy, Maryaama Ba dafa mujj dugg ci kureeli jigeen yu bare, ngir jigeen ñi jàng te mën tamit di jot seeni àq ak yelleef. Loolu moo waraloon mu yëkëti ay kàddu, siiwal ay jukki yu aju ci wàll wi ci bérebi tasekaay xibaar yi.

Atum 1979 la siiwal téere bile di Une si longue lettre di téere nettaleem bu jëkk ci këru móolukaay téere gu ñu naan Nouvelles éditions africaines. Ci boobu téere, nettalikatam bi di Ramatulaay mu ngi ciy nettali, ci ab baataxal, dundam gi weesu ginnaaw bu borom-këram faatoo. Téere baa ngi fësal bëgg-bëgg bu mag, bu yeewu ngir nekkal fi jiggeeni Afrig yi war a jàmmaarloo ak aada ak cosaan ak tamit diine. Bi ñu ko génnee rekk, la téere nettali bi siiw lool, ñépp di ci wax ; ñu tappal ko ci neexal bu ñu naan « Prix Noma de publication en Afrique » ca Fuwaaru téere bu Francfort atum 1980. Lu moy Une si longue lettre, mu ngi doon taxawu ak a yëkëti àq ak yelleefi jigeen ñi, rawatina jigeen ñi nekk ci buumu sëy. Muy wax ak a bind ay jukki ci nekkinu jigeen ñi, rawatina ñi seen yoxo jotul seen ginnaaw.

Mu ngi génn àdduna ginnaaw bu ko ab kãaseer daanee, laata ñaareelu téere nettalim bii di Un chant écarlate di génn. Téere boobule dafay nettali ñàkk a antu gu ab sëy bu doxoon diggante ab waa-senegaal ak ab waa-farãas ñàkk a antu. Loolu li ko waral yépp mooy, bopp-sa-bopp gu jëkkër ji di wéye ak wuute gu ñaari mbatit yi wuute.

Liise bu Gore (Këru yar Maryaama Ba) moom lañu ko tudde.

Ay téereem dañuy fësal anam yi ñi ko wër ak doomi Afrig yi di dunde ay jafe-jafe yiy tukke ci yile yépp : denc jabar yu bare, waasoo, teg jigeen lu mu àttanul ci téereem bu jëkk bi ; ñàkk a àndug mbokk yi, ñàkk a mën a dund ci am mbatit mu dul sa mos, te sëyu ñu bokkul der fësal ko ci ñaareelu téereem bi.

Ag ràññeekum Soppi

Bindkat bile di Maryaama Ba bokk na ci ñi xàll yoonu càllala ci Senegaal. Téere bi ñu naan Une si longue lettre, nekk téere nettaleem bu jëkk, moo ko siiwal. Téere baa ngi wax ci ñàkk a yemale gi am diggante góor ak jigeen, mbiri waasoo, ngëmi diine yi, aada ak cosaan yi, rawatina lu jëm ci anam yi ñuy dëjale nit. Mu ngi wax tamit ci mbiru denc jabar yu bare, nga xam ne dafa dem ba yàq lu bare ci dundinu askan wi, ñu ciy toroxal jigeen ñi lu ci ëpp, mu leen di jural ay naqar su fekkee ne dañu la wutal wujj wu maase ak say doom. Gëdd, njëriñ ak siiw gi Une si longue lettre am tax na ba nguuru Senegaal jël dogalu boole ko ci téere yi ñuy jàngale ci lekool yu digg-dóomu yi, ay at a ngi nii, booba ba léegi. Dafa jël téere bi, def ko muy téere buy jëmmal taxawu askan te gàlloo ak wareefu dimbalante lal ko, loolu sax moo tax tey, mu bokk ci bindkat yi gën a siiw ci Senegaal, ñu tudde ko tamit lekoolu xaley jigeen ba nekk Gore ngir sargal ko.

Ay téereem Soppi

  • Une si longue lettre, Abidjan, Nouvelles éditions africaines, 1979 (ISBN 2-7236-0430-6) ; réédition, Paris, Le Serpent à plumes, coll. « Motif » no 137, 2001 (ISBN 2-84261-289-2)
  • Un chant écarlate, Abidjan, Nouvelles éditions africaines, 1981 (ISBN 2-7236-0826-3)

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër Soppi

Lees bind ci moom ak ay téereem Soppi

  • (en) Ada Uzoamaka Azodo (dir.), Emerging perspectives on Mariama Bâ : postcolonialism, feminism, and postmodernism, Asmara, Trenton, NJ, Africa World Press, 2003, 483 p. (ISBN 978-1-592-21027-5)
  • (en) Faustine Boateng, At the Crossroads: Adolescence in the Novels of Mariama Bâ, Aminata Sow Fall, Ken Bugul and Khadi Fall, Howard University, septembre 1995
  • (en) Wanjiku Mukabi Kabira, A letter to Mariama Ba, University of Nairobi Press, Nairobi, 2005, 34 p. (ISBN 9966-84678-6)
  • Lilyan Kesteloot, « Mariama Bâ », in Anthologie négro-africaine. Histoire et textes de 1918 à nos jours, EDICEF, Vanves, 2001 (nouvelle éd.), p. 468-469
  • (en) Susan Stringer, « Cultural Conflict in the Novels of Two African Writers, Mariama Ba and Aminata Sow Fall », A Scholarly Journal on Black Women, 1988, supplément p. 36-41
  • (en) Dorothy Davis Wills, « Economic Violence in Postcolonial Senegal: Noisy Silence in Novels by Mariama Ba and Aminata Sow Fall », dans Violence, Silence and Anger: Women's Writing as Transgression, Charlottesville, University Press of Virginia, 1995, p. 158-71

Jukki yi ñu ko tudd Soppi

Lees jële feneen Soppi

Dundu ak jaar-jaaram

Maryaama Ba (juddu 1929, faatu 1981)










Balluwaay bu aju ci càllala gi






Balluwaay bu aju ci ag dundam