Màdd xeetu gàncax la gu bokk ci njambootu "Apocynaceae".

Màdd gi (Saba senegalensis)
Màdd gi (Saba senegalensis)
Meññeef mi laata ñor
Màdd bi
Tóor-tóor yi (Saba senegalensis)
Tóor-tóor yi (Saba senegalensis)

Melo wi

Soppi
 
Doom yi

Màdd gi xeetu lawtan la guy sax Afrig. Dees na ko bay it. Manees na koo lekk noonu mbaa nu boole ko ak suukar, xorom mbaa kaani. Bees ko boolee ak ndox ak suukar, manees na cee am ub njambaan. Manees na ci am it njar.

Dañuy aaye ku wann xoox bi. Waaye su nu xaree xoox bi, am na xeetu der bu fa nekk bees di lekk. Doom bi dafa gànjaru ak witaamin C, camin, ribofalaawin, ñasin ak witaamin B6. Moom nag ci nawet lay sax. Màdd bi dafa roo, ñam wu mboq moo ëmb xoox bi te dafa nooy, wex ba noppi saf suukar.

Barab yi muy sax

Soppi
 
Njaru Senegaal

Moom màdd Afrig gu soww la gën a bari. Dees na ko fekk it Afrig gu penku gi, moom màdd mbaa yu niroo ak moom, fu mel ni ca Tansani. Fii fi Senegaal kaasamaas/Sigicoor lay faral di bàyyikoo.

Turu xam-xam wi

Soppi

Saba senegalensis

Tur wi ci yeneeni làkk

Soppi
farañse: liane saba