Kureelu Mbootayu Xeet yi

Kureelu Mbootaayu Xeet yi ndawi réew yu mag yi, yu ci mel ni Nguur-Yu-Bennoo , Diiwaan-yu-Bennoo yu Aamerig, Bennog Sofyet, Faraas ak Siin, danoo daje woon ci Wasington peeyub Amerig ci wenn waxtaan atum 1933g, ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi . Ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi, jële fi xeex yi, amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi, ak rafetal nekkiinu mboolaayu r;ew yi, ci koom-koom, mboolaay, aada ak wér.

raaya bu Kureelu Mbootayu Xeet yi
Makkaanaam ca New York

Bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu àdduna bi ci dëkku San Fransisco ci 25 awril atum 1945, ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi. Ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko, nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi, ak xaatim ko ci 26/06/1945g. La jiitu ca kollëre ga mooy:

Nun askani mbootaayu xeet yi ñi ngi giñ ne di nanu xettali maas yiy ñëw ci musibay xare , yi nga xam ne sotti nanu nit ay alkande aki naqar yu kenn manul’a misaal ci ñaari yoon ci diir bu gàtt bu weesuwul genn maas reek. Ñi ngi giñ it ne dananu feddaliwaat sunu ngëm ci àqi nit ju cosaanu ji ak yelleefam, ak teddngay jëmm ak man-manam, di feddali it ne goor ñi ak jigeen ñi ak xeet yi, moo xam yu ndaw lanu, mbaa yu mag, ñoo yam kepp ci àq ak yelleef.

Sosteefam

Soppi

Njiitul Aamerig la tuddoon Widro WILSON da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu àdduna bi, guy jeem a indi jàmm ci àdduna bi, ci ginaaw Xareb Àdduna bu Njëkk bi.

Waxoon nañu ne Wilson moom jotoon naa leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lañu woon ak ñeent ci biir Xareb Àdduna bu Njëkk bi, ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi, ak ngir rëddaat sëqooy réew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati.

Wilson moom gaaraloon na naalam boobu di “Kureelu Mbootayu Xeet yi” , gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa ñu amaloon, kollëre ga ñu jotoon a fas ca Versaay it moo rëddoon lañu fa xaatim.

Ay ponkam

Soppi
 

Sose kureelu xeet yi ci mbooleem réew yi am tembte gu mat gu dara wàññiwut, réew yoo xam ne man nañoo indi ay warlu yu mat ci jox-cër walla wormaal jàmm, te bàyyi xeex mbaa lu koy waral. Réew yi bokk ci kureel gi danañu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi, ngir ñu àtte leen, te xool li leen boole. Réew yi ci bokk it war nañuy seet mbugal yi yell ci réew yiy tooñ, yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom-koom , walla jëfandikoo doole ci seen kaw.

Jeem a dëgëral buumi dimblante ci àdduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa gu fés, ak wormaal kollërantey réew yi, ak xeex njaam, ci meloom yépp, jeem a rafetal nekkiinu liggéeykat yi ak seenug dund, ak xeex seneebar, nos yaxantu ci àdduna bi, ak sonn ci wér-gu-yaramu nit.

Réew yi ci bokk danañu warlul yeneen réew yi wormaal seenug tembteg politig , danañu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare , ak jox kooluteg kureel bi ab day ci mbooleem kollërante yi réew yiy def ci seen diggante. Koolute gi nag di secretariat bi, ci dëkkub Geneve bi nekk Siwis la nekk. Aar neewtey xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem réew yi, ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi, wormaalal leen seen àq ak sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi ñu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom , ak réew yi ñu gañee ci xareb àdduna bu njëkk bi. Kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale gi, mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi, xeet yi ak mbooloo yi, ñu feetale leen réewi sancaan yu mag yi, teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin, ginaaw bi réew yooyu nekkee ci waawug réew yi ñu daanoon ci xeex bi, ñuy : réewum Usmaan mi , Imbratooru Otris gi, ak gu Almaañ gi. Loolu nag ñu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen a may ag tembte ëlëg. Kureel gi, bi muy door a sosu, 42 réew a ca bokksi woon. Ci noonu réew yiy temb di gën a dolliku, naka noonu di gën a bokksi, ba mujj limub réew yi bokk àgg ci juroom benn fukk, mu ci nekk it am genn kàddu ci bu ñuy woote. Kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ-sañ ci mu genn ne bokkatuma, waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk.

Bànqaasi kureelu gi

Soppi

Kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am, ñooy :

Jataay bu Matale bi, Jataayub Kureel bi, Koolute gi (walla secretariat), nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo, ñooy : Àttekaayu Maanduteg Àdduna bi ak Mbootaayug Liggéey gu Àdduna bi.

Jataay bu matale bi

Soppi

Mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi réew yi bokk ci kureel bi. Ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru koor, ngir xool aka xalaat ci mbooleem xew-xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay tëralam (prograamam).

Jataayub kureel bi

Soppi

Moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cër, juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy réew yi am ag bokk gu sax ñooy: Nguur-Yu-Bennoo yi, Faraas, Itaali, Sapoŋ ak Almaañ mi jël cërub Aamerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi. Ak yeneen ñeenti réew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg-leeg. Bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi. Dana faral di daje it, ci anamug jagle, ci xew-xew yu bette yu man a xupp jàmmi àdduna bi. Limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi, juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent.

Koolute gi (secretariat)

Soppi
 
Taax miy makkaanu Koolute gi

Koolute gu kureelug gi, mi ngi sosoo woon ci liggéeykat yu kureel bi, ya daa liggéeye ca dalam bu sax ba nekkoon Geneve. Njiit li moom moo daa doon Ku-nu-woolu ku matale, ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn. Koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom, ñooy: kureelug dimblanteg caada gi , kureelug jële fi ag njaam, kureelug xeex seneebar, kureelug aar neewte yi , kureelug féetale yu sax yi ak kureelug tawat yu bon yi.

Am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi, ñooy yu mel ne: Àttekaayu Maanduteg Àdduna bi, liggéeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi, àttee ko nag ci yoon bu àdduna bi, ak kollërante yi réew yiy xuloo jotoon a def. Nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn, tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne réewi kureel bee leen di indi. Àttekaayub Maanduteg Àdduna bi moom, mi ngi sosu ci atum 1921g, ab dalam it nekk Lahaay ca Olaand. Ak Mbootaayug liggéeyub adduna bi, ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci Àdduna bi, ak yekkati seen tolluwaayu dund. Moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi liggéeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi, ak boroom liggéey yi. Geneve nag moo dib dalam.

Ay ayibam

Soppi

Kureelu mbootaayu xeet yi de, ak li mu def lépp ci liggéey yu jëm ci saxal jàmm ci àdduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi, ak li mu fi def ci liggéey yu am njariñ ci wàllug mboolaay, loolu lépp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ŋaayoo yi daa am ci diggante réew yu mag yi. Loolu nag waraloon na neew-dooleg kureelu gi, rawati na ci atum 1930g, bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee réew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi, lu mel ni loolu moo xewoon bi Sapoŋ defee ay jalgati jëme ko Siin. Li ko gënoon a doyadil mooy génn gu ci Sapoŋ ak Almaañ génnoon ci atum 1933g, ak lott gu mu lottoon ci tee Itaali songu Ecoopi ci atum 1935g. Loolu sax moo taxoon mu génn ci kureel bi ci atum 1937g. Kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon a tee ay “dank yu xare” yu bees di am, maanaam ay réew dajaloo, boole seen bopp ci wàlli xare. Kureel bi tam àggoon na ci manatuloon a tee réew yu mag yi di rawante ci ngànnaayu, yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci génn.

Bokk na ci ayibi kureel bi, fent gu ñeenti réew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may Nguur-Yu-Bennoo yi ak Faras ñu man a sancati ay suuf yu bees, yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir, rawati na ci réewi araab yi, ak yu dul ñoom. Yenn yi ci yooyu, danoo nekkoon ci ron kilifteefug réewum Usmaan mi, yi ci des ci waawug imbraatoorub Almaañ bi. Réew yu mag yii danoo jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgga def lu baax, bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif réew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug Tirki ak Almaañ.

Bokk na ci ayibi kureel bi ba tay, aakimoo gi réew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi ñu daa gaaral ci kureel bi.

Jubluwaayi mbootaayu xeet yi ak ay kër-këraanam

Soppi

Kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam ci ñeenti mbir yu dàttu , ñooy:

  • Wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi.
  • Suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi.
  • Gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom-koom, ak mboolaay, ak aada, ak wàllug nit.
  • Dëppale jëfi xeet yi walla reew yi, walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg.

Bu dee ker-keraan yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu, moom mbootaay gi leerale na leen ci nii:

Bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoηal jàmm ak kaaraangey adduna bi. Di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi. Warlu yoon yi man’a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe-jafe yi ci adduna bi, ndare bu loolu day li gën ci adduna bi. Sukkandiku ci campeefi adduna yi ngir dëgëral jëm-kanamug koom-koom ak gu mboolaay gu askan yi.

Campeefi mbootayu bi aki bàqaasam

Soppi

Mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy:

Jataay bu matale bi

Soppi

Mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi, mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote. Jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar, ca dalam ba ca New York, man na’a am nag leeg-leeg ñu amal jataay bi ci xew-xew yu bette yi ko aajowoo. Jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem:

  • Gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral’a indil, ak saxal leen, ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi.
  • Gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi.
  • Nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk.
  • Tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi .
  • Tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi, ak ceri ñaari jataay yi: bu koom-koom bi ak bu mboolaay gi, ak jataayub ndenkaane bi.

Saxal yi jataay bu matale bi daa faral di jël, ñi ngi daa ame ci ndollant gu toll ci ñaari ñatteeli cer (2/3) yu fekke woote bu nuy def ci naal bu mu man’a doon walla ab ndenkaane.

Jaataayu kaaraange gi

Soppi

Jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax , ñooy ndawi Diiwaani Amerig yu Bennoo yi (USA) ak Bennog Sofyet gi , ak Nguur Gu Bennoo gi ak Frans ak Siin, ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at. Cer yu sax yi nag dananu am sañ-sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba, boobu sañ-sañ ñu koy woowe (veto), jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi, yi nga xam ne man nanoo jur njombe. Saxal yu jataay bi, ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu, ci cosaanul fukki kàddu ak juroom, maanaam saxal gi du man’a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw, la ca des ne deet walla ñu noppi. Waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee ne àndu ci. Jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi , am na it sañ-sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew, ak tege ay mbugali koom-koom, ak yu xare ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam, am na sañ-sañu yabal ay doole it ngir taxawal ab xeex, walla ay kureeli soldaar ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar’a xeex.

Koolute gu matale gi

Soppi

Moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi, koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi, nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu, bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko (kàddu ko). Dalub koolute gi mi ngi New York. Ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi .

Jataayub koom-koom ak mboolaay

Soppi

Bii jataay’a ngi ame ci cer yu seen xam-xam aju ci mbirum koom-koom ak mboolaay. Jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at. Jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom-koom yi ak mboolaay yi, ak aada ak lu aju ci nit. Mbootaayi adduna yii ma lay bëgg’a leeral ci jataay bii lanu bànqaasoo:

UNESCO

Soppi

Moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam-xam ak yar , dalam bu sax ma nga Paris, ca Frans. Yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam-xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk, jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam-xam yi.

Mbootaayu Liggéeyu Àdduna bi

Soppi

Li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu liggéeykat yi ci àdduna bi, ak fexe nu yokk seeni ngérte . Moom nag mbootaay gi, mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi, ab dalam nag mi ngi nekk Geneve.

Mbootaayug Wérug Àdduna bi

Soppi

Mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ,ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle, te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram. Moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér, di ci sàkku it xam-xam yi manul a ñàkk. Di yonni ay boroom xam-xam ci loolu, di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér. Ab dalam nag ma nga Geneve moom itam.

Mbootaayu dund ak mbay gu àdduna bi

Soppi

Moom nag liy ligeeyam mooy jeem’a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi . Loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker-keraanam, ak xeex gàkk-gàkki mbay yi ak yu dundat yi , ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi . Dalam bu sax bi nag mi ngi Rom ca Itaali. Ëttu àtte bu maandute gu kawe gi:

Moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci Kureelu xeet yi. Moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi. Mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn, ak jataayub kaaraange gi, ginaaw bu leen seeni reew sampee, gaaral leen ci mbootaay gi. Ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi. Mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante, ak àttey yoonu adduna bi. Ab dalam nag mi ngi Lahaay ca Holand.

Mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax

Soppi

Li miy yittewoo mooy mbiri way daw-làqu yi, te indil leen ndimbal li manul’a ñàkk te dëkkal leen, ligeeyloo leen.

Jataayub ndénkaan yi

Soppi

Mooy saytu mbirum sancu yi Almaañ moomoon, Itaali ak Japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi. Bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi, ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi.

Bankub addunna bi ngir sos ak tabax

Soppi

Bii bank danu koo sosoon ngir man’a lebal reew yi ci bokk, ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq, ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg, ak sos ay naal yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom-koomu adduna bi, ak jeem’a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg . Banku adduna bi, moom dafa mel ni ag lonkoo gu adduna bi, goo xam ne boppu alalam mi ngi juge ci li cer yi di teg. Cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom-koomam toll. Dalam bu sax nag mi ngi Wasington, peeyub Amerig.

Keesug kee gu àdduna bi

Soppi

Yitteem mooy saxal njëgu kee gu adduna bi, ak dindi fi jafe-jafe yi man’a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi .

Man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna, gu am sañ-sañ yi kureelu xeet yi amoon, waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo, ñooy:

  • mbootaayu xeet yi day dëgëral - ci ay jubluwaayam – àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi, ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi (goor ak jigeen) cig wàll, ak yamale reew yi ci geneen wàll.
  • Mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi, te bu dee kureelu xeet yi moom Amerig bokku ci woon ngir bañ gu Kongres bañoon ne du ci bokk. Te it Bennoog Sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante 1934 – 1939 g. Nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi, boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi, yu mbootaay gi moo leen di ëpp.
  • Mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man’a wéyal ay saxalam, am na it sañ-sañu tege ay dogoo yu koom-koom, ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ.

Ànd ak loolu lepp nag, teewul mbootaayu xeet yi moom, doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi, yooyu nga xam ne ñoo ame sañ-sañu firi (veto), man a bañ mbaa firi bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi. Ci noonu yenn ci reew yu mag yi, fètteerlu nanu,wéy ci jëfandikoo sañ-sañu firi, di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe, di ci tooñe, di ci dumaa, di ci aare reew yuy jalgati. Te lu bari ci saxali jataay bu matale bi, ak saxali jataayub kaaraange gi, ba leegi daa rekk lanu ci kayit, kenn doxalu leen. Ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom-koom, aada, wér gu yaram ak mboolaay, lu am solo la, te yayoo màggal, waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare, moom dëgg-dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg, sori maandute te sori yoon.

Lëkkalekaay yu biti

Soppi