Karolin Fay Jóob
Karolin Fay Jóob mu ngi juddu fukki fan ak benn ci weeru sulet atum 1923 ca Funjuñ, faatu ñaar-fukki fan ak juroom-ñeent ci weeru sulet atum 1992 ci Dakaar. Moom mooy jigeen ji jëkk a nekk ndawu réew (deppite), nekk it jigeenu ji jëkk a nekk jëwriñ ci Senegaal. Moo doonoon soxnay Demba Jóob mi ñu bóomoon atum 1967.
Jëwriñu nguur (Ministar detaa) 1982 – 1983 | |
---|---|
Jëwriñu ji yore aw waar ci njëwriñ ju mag 1981 – 1982 | |
Ngornmaŋ | Caam I |
Jëwriñu ji yore ndimbalu askan wi 15 màrs 1978 – 9 awiril 1979 | |
Ngornmaŋ | Caam I |
Ndawu réew (Deppite) 1963 – 1978 | |
Dundu ak jaar-jaaram | |
Bésu juddu | 11 sulet 1923 |
Bérebu juddu | Funjuñ (Afrig sowu jant gi nekkoon ci waawu Farãas: Afrique-Occidentale française) |
Bésu faatu | 29 sulet 1992 |
Bérebu faatu | Dakaar |
Réew | Senegaal |
Waajur wu góor | Luwi Jéen Fay |
Waajur wu jigeen | Faatim Jóob |
Borom-kër | Demba Jóob |
Dundu ak jaar-jaaram
SoppiCosaan ak njàngam
SoppiKarolin Fay Jóob mu ngi juddoo Funjuñ (Fatig, bokkoon ci Afrig sowu jant gi doon wéy ci waawu Frãas (Afrique Occidantale française) fukki fan ak benn ci weeru sulet atum 1923. Doom la woon ci Luwi Jéen Fay, xam-xamam màccoon ci mbirum waññi (kontaabilite), bokkoon ci SFIO, nekkoon tamit kenn ci soskati Bloc démocratique sénégalais. Way-juram wu jigeen mu ngi tuddoon Faatim Jóob soqeekoo ci Mañ Jóob Mbaaco bu Waalo. Njàng mu suufe mi, mu ngi ko defe seen dëkk laata muy jàngeeji lekool Albeer Saró bi nekk tey lekool Bert Móbeer. Mu daldi am ndam ci joŋanteb dugg lekool normaal bu xale yu jigeen yi bu Afrig sowu jant gi doon wéy ci waawu Frãas (Afrique Occidantale française), nekk ca Tëngeej (Rufisque)Foofee la génne ak ab lijaasa atum 1945 ginnaaw bu mu jëlee ñetteel ci joŋante ba. Ñi mu fa nekkoonandoo, ràññe nañu ci Anet Mbay Dernëwil mi jëloon pee ak Ndey Kumba Jaxate mi jëloon ñaareel, Aan Mari Sohaay, Saan Martee Siise (Jeanne Martin Cissé).
Ay jaar-jaaram ci njàngale mi,
SoppiLijaasa bi mu am atum 1945 moo ko tax a nekk ab jàngalekat ca Luga ci ndigalu xelalkatam bi Abdulaay Satsi (Abdoulaye Sadji), ca Cees, ca Maatam ak ca Mbuur foofee ca Mbuur la nekkoon njiitu lekoolu xale yu jigeen yi 1951 ba 1962. Ca Mbuur googu, la tase ak Demba Jóob, mu nekkoon ab wottukat maanaam sirweyãa ci lekool bu tuddoon Cours normal bu Mbuur, lekool boobu sax, moom Demba Jóob lañu ko mujj tudde. Mu daldi nekk soxnas Demba Jóob atum 1951. Bi muy wéyal njàngale mi, la dugg ci pàrti bile di Bloc démocratique sénégalais ca Luga atum 1945 ; bi mu xamee ne boole ñaar yi dina jafe lool (njàngale mi ak pólotig bi), ndax farlu bi mu amoon ci pólotig dafa doon gën di yokk, la ko Léwopool Sedaar Seŋoor, mi doon jiite pàrti bi, may mu nekk ab jàngalekat buy yëngu rekk ci lépp luy suqali kow gi
Ay jaar-jaaram ci wàllu pólotig
SoppiKarolin Fay Jóob bokk na ci ñi sos kureelu jigeen gi ànd ak pàrti bile di Union progressiste sénégalaise, daldi nekk njiit la suyee (juin) 1954 ca Cees ginnaaw bu Faatu Siga Ñaŋ bàyye. Mu daldi nekk ab deppite diggante 1963 ba 1978, dugg nag ci taarixu réew mi ndax looloo ko tax a doon jigeen ji jëkk a nekk deppite ci Péncum ndawi réew mi. Atum 1963 xaat, mu ngi doon wax waxi sos sàrtu njaboot bi (Code de la famille), di ñaax jigeen ñi ci dem ak seen bopp, bañ a wékku ci kenn. Moom rekk moo doon jenn jigeen ji bokkoon ci woteb sàrtu njaboot bi. Moo nekkoon ñeenteelu kilifa gi topp ci njiitu péncum ndawi réew mi (ñeenteelu wis peresidãa bu péncum ndawi réew mi). Atum 1964 lañu ko fal njiitu jigeeni Union Progressiste Sénégalaise, mu dellu nekk sekerteer seneraal bi ñu toftal ci njiitu kureel gile di Jigeeni Afrig yi, maanaam Panafricaine des femmes ci farañse. Moom mooy jigeen ji jëkk a nekk jëwriñ ci réew mi ndax 1978 lañu ko tabb jëwriñ ji yore wàllu taxawu néew-di-doole yi, nekkaat jëwriñ ji ñu feggal jëwriñ ju jëkk ji diggante 1981 ba 1982, dellu nekkati jëwriñu nguur (ministar detaa) diggante 1982 ba 1983. Ci njëwriñam lañu gis ne sos nañu ay kureel yuy gëddal ak a dooleel jigeen ñi. Am na sax ab nettali ci li xewoon ca kongareb pàrti ba woon ca Cees atum 1958, nga xam ne woowuñu ca woon benn jigeen, moom mu dem ca ba pare, naqarlu ci kanam Seŋoor, njiitu réew mi, li fa jigeen ñi teew ba pare te kenn ci ñoom jëlu fa kàddu. .
Karolin Fay Jóob jàppoon na ne taxawu na jigeeni réewam diiru fukki at yoo xam ne moom kese moom nekk ca péncum ndawi réew mi « Xeex naa ngir Sàrtu njaboot bi am, ngir ñu teg ndimbali njaboot yi ci yoxoy jigeen ñi ». Mu dellu jàpp ne ay jaar-jaaram ci pólotig dañoo tar, kenn ci góori pàrti bi daanu ko jàppale ndax mësuñoo rafetlu ràññekug jigeen ñi wala fit wi ñu am, def benn dank ñoomi neen, di xàccandoo, di dóorandoo.
Kàddu yile ca waxtaanam wa lañu leen tibbe woon : Nee na woon ca ndajem fukki fan ak juroom mu jigeen ñi (keesenu jigeen ñi) « Lu guy rëy rëy, warul a fàtte mukk ne ab xoox bu ndaw moo ko jur ». Ci lu aju ci taxawu àq ak yelleefi jigeen ñi, nee na : « Waxuma waxi taxawu jigeen ñi bu jéggi dayo. Waxuma ne na góor ak jigeen tolloo, waaye dama bëgg ñoom ñaar ñuy mottaliwante. Nekkuma kuy yéegal fii, di wàcce fee. »
Ay jëfam ak i sargalam
Soppi- Màngasiinu pepp bu USAID joxe.
- Moom lañu yaayale woon ñaar-fukk ak juroom-ñaareelu keesenu jigeen.
- Amal ay tooli ñépp
- Def ay farmasi ci dëkki kow yi, ay lekooli tuut-tànk ci Garãa Yoof, Cees, Tàndem (Kaasamaas), Ayere Laawo (Fuuta)
- Mbindum sàrtu njaboot ci Senegaal (moom rekk moo nekkoon jigeen ji bokkoon ca wote ba)
- Ay ndimbali jaboot ngir jigeen ñi
- Wax ñu jagleen jigeen ñi bésu ñaar-fukki fan ak juroom ci weeru màrs atum 1972 te ñu soppi ko tey keesenu jigeen
- Sos ay mbootaay yuy taxawu ak a dooleel jigeen
- Sos ay kureeli dimbalante, lebal ak denc xaalis yu ñu mujj soppi ag ràbboo
Toftal bi
SoppiTéere, jukki wala dali web yi ñu yër
SoppiJukki yi ñu ko tudd
Soppi- Pólotigu Senegaal (Politique du Sénégal)
- Nekkinu jigeen ci Senegaal (Condition féminine au Sénégal)
- Limu jigeen ñi jot a nekk jëwriñ ci Senegaal (Liste de femmes ministres sénégalaises)
Lees bind ci moom
Soppi- « Caroline Faye Diop » in Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, Dakar, 2006, p. 164
- « Caroline Faye : Première femme députée et ministre du Sénégal », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 78-79