Kàdd
Kàdd garab la gees di fekk ci gox yu naaje yi niki ca Senegaal, ca Afrig la bàyyikoo.
Melow kàdd
SoppiKàdd garab la gog ay caram ak i wànqaasam yéppay am i dég. Njoolaayam man naa àgg ba ci 30i met, xalaam man na àgg ba ci 2i met. Reenu garab gi man naa dugg ba ci 15i met ci biir suuf. Ci jamonoy maral, xasu garab gi day soppi wirgo teg ci di xolleeku.
Garabu kàdd daa am dund gu wuute ak yeneen i garab yi des yépp ndax moom kepp mooy garab gu ay xobam di ruus nawet ak a sëq ci jamonoy lolli. Loolu nag li ko waral mooy ngir mu man a dund cig maral ak ci barab yu ñàkk ndox.
Njariñi kàdd
SoppiKàdd garab gu am njariñ la fii ci tund Sahel rawatina ci lu jëm ci wutum lem ndax ci jamonoy nawet ay tóortóoram man nañu dundal yamb yi ngir ñu man a am lem bu doy. Leneen ci ay njariñam, fóyteefu garabu kàdd di Àdd lu am solo la ci dundug jur.
Nataali kàdd
Soppi
Turu xam-xam wi
SoppiFaidherbia albida Acacia albida la tuddoon