Jimbulang bu waa-Brëtaañ

Jimbulang bu waa-Brëtaañ walla Encyclopædia Britannica (ci wu-angalteer), ñi ngi ko siiwal ci diggante 1768-1771. Siiwalam gu njëkk mi ngi ame ca Edimbuurg ca Ekos. Bu waa-Brëtaañ bi bokk na ci jimbulang yiy wax ci lu daj yi njëkk ci kàllaama wu-angalteer, te bay jii ñoo ngi koy siiwal.

yëgleeb génnu jumbulang bi

Ci ndoorteelu ñaareelu xaaju 1700 ba ci 1900, bari woon na ay boroom xam-xam yu doon jàppee ay jukkeem niki delluwaay bu wóor, yenn saa yi, ci siiwal yu yees yi, daa na am ay gisiin yu yees yees jagleel ay mboolooy gëstukat. Ci jamono yooyu amoon na gëdd bu baax ci biir askan wiy làkk wu-angalteer. Ci XX xarnu bi la yitteey jimbulang soppiku bu baax, coppite gi amal na ay njeexiit ci xarkanam ci fukk ak benneelu siiwal gi.

Taariixu jagal yi

Soppi
jagal taariixu jagal dayoo
1eel 17681771 3 téere
2eel 17771784 10 téere
3eel 17881797, 1801 18 téere
4eel 18011809 20 téere
5eel 1815 20 téere
6eel 18201823, 18151824 20 téere ak 2 yees yokk
7eel 18301842 21 téere
8eel 18521860 21 téere
9eel 18751889 24 téere
10eel 19021903 9u jagal ak 2 yees yokk
11eel 19101911 29 téere
12eel 19211922 11u jagal ak 3 yees yokk
13eel 1926 11u jagal ak 6 yees yokk
14eel 19291973 24 téere
15eel 19741984 28 téere
1985 32 téere

jagal gu njëkk gees def ci CD-ROM mi ngi génn 1994.

Lëkkalekaay yu biti

Soppi