Jiitalug aji firi ji (preface)

Jiitalug aji firi ji:


Li ma tax a jug, jëme ma ci def bile ligéey, te ma jàppe ko muy bu am njariñ, mooy, benn: jortu ne, ci def gi, ñi ngi ligéeyal Sëriñ bi, waaye it xeet wi . Ndax jël lu mel ni jaar-jaari Sëriñ Tuubaa, ak li mu làmboo ciy njariñ, nga tas ko, teg ko ci fu loxol ku nekk àgg,yombal ko ba ku jug man koo xam, man koo dégg , man cee jariñu, ca anam ga mu gën a yombe, gënnee leere, te yaakaar naa ne def ko ci wolof , ñeel wolof yi,ci anam yiy yombal la, tey leeral . Lu mel ne lii de yaakaar naa ne amul lu ko gën di ligéeyal Sëriñ bi,waaye ag ligéeyal sa xeet it mi ngi ci, ndax ag dundal la, ñeel saw làmmiñ, te gis naa ne lu waay man a xame ci làkk, ak wu mu man a doon, ci sa wos, lay gën a dugge,lay gën a tooge,lay gën a nekke, luy dund ak yaw, ci lay doone kenn ci yaw, ngay, yaw itam, kenn ci moom, ngéen di benn bu dul ñaar, gis naa ne bokk na ci li ñiy rawe, di rawe; di jànge ci seeni làkk, di ci waxe, di ci xalaate, te di ci jokkoo.

Man de bile téere,njëkk ma koy tekki, nekkoon na di bob,dees na soxla as lëf ci waxtu,ngir yër ko,dégg ko,naan ko,waaye daa mel ni bi ma ko defee ci wolof,soxlaatunu lu dul lu néew, ngir jaar ci, jaarati ci, kon nanu fonku sunu bopp,ci fonkaat bu baax sunu làkk yii,te xam ne dug fonkadi ñeneen ñi.

Ñaareel bi mooy , gis gi ma gis téere bii,di bu jéggi dayo ba ci solo ak njariñ, di delluwaay ci delluwaayi téerey yoonu murit wi,di rootukaay ci yu xam-xam yi. Làmboo nag kem bu réy ci xam-xam, ci lu aju ci Sëñ bii, di kenn ci ñi ñu war a xam, bu ma waxul ki ëpp solo ci ñoom . Kon xam leen ne yii ak yeneen yu ma waxul, ngir bañ a guddal, ñoo sabab firi gi, nga rax ci dolli,nekkug aji taalif ji, di kenni jëlewaayi yoon wi,yu xam-xam yi. Ndax kat, boo yëree, da nga ko gis lu bari mu naan Sëñ bi nee na ma, te loolu du lu yomb . Kok bëkk-néeg la woon ci bëkk-néeg yi,bu ma waxul ngën ji bëkk-néeg , kon kooku maneesu koo gën di jëlewaay, mbaa delluwaay, rawati na muy ku ñépp xam ag sellam, akug dëggoom, yal na nu Yàlla taas ci barkeem te dolli ngërëmam ci Sëriñ sunu,Sëriñam,laafaale ko ci, ci barke ku nu ligéeyalam, ak ki muy ligéeyal moom mu mujj mi, Aamiin,yaw boroom mbindéef yi.

Aji firi ji: Abdul Xaadir KEBE