Soobaan di Sapindus saponaria garab la gu am xob yu xaw a tal, yor taxawaay bu yam rëyul ndawul. Ma nga fekk baax ca Amarig. Xeetu turam wii di Sapindus nag, mi ngi jóge ci latin di tekki saabub endo.

Nataalu garabug soobaan

Melo wi Soppi

Garab gu yamamaay la guddaayam war a àgg ci 10i met. Ay xobam di xob yu sew te xaw a gudd cat yu bëñe. Guddaayam war a àgg ci 30 cm. Am ay rëdd ci biir xob wi yu sew. Meññeef di nekk ci poqi car yi.

Foytéef bi Soppi

Foytéef bi wirgo mboq lay yor. Ag ndombaam di àgg 4 cm. Day am ci biir benn pepp bu ñuul. Doom Oktoobar lay ñor, waaye yenn saa yi mu des ci garab gi ba noor. Ci waxtuw noor lay gën a meññ.

Nataal yi Soppi

Turu xam-xam wi Soppi

Sapindus saponaria