Rajab manees naa wax ne ci xeetu garab yi la bokk. Amna ñu ko ber it ne du garab. Bari na ay xeet lool nag, amna lu ëpp téemeeri xeet.

Nataalu rajab

Xeet yi Soppi

Amna ci bu ñuy wax kooyi naar, pakkub lëg, jaatoor, beñeb lëg, sawum xaj. Amna ci yu weex am ci yu yor yeneen i wirgo. Amna ci yu ñuy lekk, te muy sax ci suuf di am jëmm, am ci yoy tooke la day raye. Yooyu di raye nag Afrig la ëppe ci tàngoor wi, fu ci mel ni Senegaal, rajab ya fa nekk, kenn waru koo lekk.

Saxiin wi Soppi

Moom rajab nag ci ngelaw li rekk la aw jiwoom di jaar. Jiwu wu góor wi mooy naaw daje ak wu jigeen wi ñu joxe doom. Amna ci yoy, day yàq garab da koy ray. Pëndax lay doon bu weex tuuru ci garab gi ne ci ñàpp. Pëndëx boobu it bu laalee kawari nit, da koy xus moom la ñuy wax mbay-wataan . Rajab yi tuuti ba kenn manu koo gis ak bët moo koy def. Lu bari looy gis mu xuur nag, bu dul bagteri rajab a ko waral.

Nataal yi Soppi

Tur wi ci yeneeni làkk Soppi

farañse: champignon
angale: mushroom
itaaliyee: fungo