Meningite nekk na xeetu mettit yu tar la yuy jàpp cër yiy aar yuuru nit ki, ak doqam, te ñu koy gëna woowe meninge.[1] Ni muy gëna feeñee ci nit mooy yaram wu tàng, mettitu bopp ak ndong lu bañ. Yenn saay mu feeñee neeneen, lu ci melni xel mu jaxasoo ak ñàkka xàmme yenn mbir, waccu, bëggul leeraay ak xumbaay. Neneen lay feeñee ci xale yi, lu ci melni gaawa mer, tayeel, wala baña lekk.[2] Ni muy tàmbalee feeñ ci yaramu ki ko am, mën na wane ban xeetu Meningite la am; ci misaal, Meningite bi bacterie meningococcal mën na ànd ak yeneen xeetu feeñal ci deru nit ki.[1][3]

Wiris, bakteri wala yeneen doomi jàngoro mën nañu jàpp wàll yu bari ci yaram wi, garab yi itam mën nañu ko waaye bariwul.[4] Meningite mën na faat doomu aadama ndax li muy yàq dafa jege yuur gi ak moelle epiñeer; moo tax, su dalee nit ki dañu ko wara gaaw faj.[1][5] Suñu jamee (Une ponction lombaire) nit ki ci yaram lañuy mëna xam ndax amna Meningite am déet.[2] Dañuy roof ràbb ci kanaal rachidien bi ngir taataan lenn ci liquide cephalo-rachidien (LCR), bi muur yuur gi ak moelle epiñeer bi. Ci ab labo lañu càmbaree LCR.[5]

Amna yenn xeetu meningite yoo xamni boo ñaqoo duñu la mënal dara, muy ñaq biy aare ci méningocoque, oreillon, pneumocoque ak Hib.[1] Ñi nekk ci barab bu am yenn xeeti meningite yi mën nañuy jëfandikoo antibiotique, baaxna ci lool.[2] Li ñu wara njëkka jox ki am meningite bu metti bi mooy ay antibiotique ak yenn garab yuy xeex doomu jàngoro ji (virus).[2][6] Soo bañee meningite bi indal la mettit yu dara wala mu am lumuy yàq ci sa der, dangay jël ay corticostéroïde ngir mu aar la ci yooyu jafe-jafe.[3][5] Meningite mën na indil nit ki ay jafe-jafe su yàggee, maanaam mën nala tëxloo, soyloo, wala xel mu wayadi, sudee teelu ñu ko faj.[1][3]

Ci atum 2015, meningite jàpp na lu tollu ci 8,7 milioŋ ciy nit.[7] Feebar bi faatna 379 000 nit ci àdduna bi, wuute ak limu 464 000 yi mu faat ci atum 1990.[8] Su nit ñi jëlee garab yi war ci meningitu bakteri bi, du mëna faat lu yegg 15%.[2] At mu nekk dina am feebaru meningite bu bakteri ci diggante weeru decembre ak juin ci biir Afrique suufu Sahara, ñu gën ko xame ci turu ceinture de meningite.[9] Feebar bi mën na feeñ ci yeneen gox ci àdduna bi waaye du bari noonu. Baatu meningite mingi bawoo grek μῆνιγξ méninx, "membrane" ak sufiksu -ite, "inflammation."[10][11]Royuwaay:Infobox medical condition (new)



  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 et 1,4 Sáez-Llorens X, McCracken GH (June 2003). "Bacterial meningitis in children". Lancet. 361 (9375): 2139–48. doi:10.1016/S0140-6736(03)13693-8. PMID 12826449.
  2. 2,0 2,1 2,2 2,3 et 2,4 "Bacterial Meningitis". CDC. April 1, 2014. Retrieved 5 March 2016.
  3. 3,0 3,1 et 3,2 van de Beek D, de Gans J, Tunkel AR, Wijdicks EF (January 2006). "Community-acquired bacterial meningitis in adults". The New England Journal of Medicine. 354 (1): 44–53. doi:10.1056/NEJMra052116. PMID 16394301.
  4. Ginsberg L (March 2004). "Difficult and recurrent meningitis" (PDF). Journal of Neurology, Neurosurgery, and Psychiatry. 75 Suppl 1 (90001): i16–21. doi:10.1136/jnnp.2003.034272. PMC 1765649. PMID 14978146.
  5. 5,0 5,1 et 5,2 Tunkel AR; Hartman BJ; Kaplan SL; et al. (November 2004). "Practice guidelines for the management of bacterial meningitis" (PDF). Clinical Infectious Diseases. 39 (9): 1267–84. doi:10.1086/425368. PMID 15494903.
  6. "Viral Meningitis". CDC. November 26, 2014. Retrieved 5 March 2016.
  7. Global Burden of Disease Study 2013, Collaborators (22 August 2015). "Global, regional, and national incidence, prevalence, and years lived with disability for 301 acute and chronic diseases and injuries in 188 countries, 1990-2013: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2013". Lancet. 386 (9995): 743–800. PMID 26063472.
  8. GBD 2013 Mortality and Causes of Death, Collaborators (17 December 2014). "Global, regional, and national age-sex specific all-cause and cause-specific mortality for 240 causes of death, 1990–2013: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2013". Lancet. 385 (9963): 117–71. doi:10.1016/S0140-6736(14)61682-2. PMC 4340604. PMID 25530442.
  9. "Meningococcal meningitis Fact sheet N°141". WHO. November 2015. Retrieved 5 March 2016.
  10. Mosby's pocket dictionary of medicine, nursing & health professions (6th. ed.). St. Louis, Mo.: Mosby/Elsevier. 2010. p. traumatic meningitis. ISBN 9780323066044.
  11. Liddell HG, Scott R (1940). "μήνιγξ". A Greek-English Lexicon. Oxford: Clarendon Press.