Doolerandu mooy xam-xam biy gëstu lepp lu ñeel wuutuloxo yi, doxalkat, ndaamar, ci gattal, lepp luy jur walla di yòbb ab jalaxu, doole, ag soppeeku. Da nuy wax tamit doolerandu gu daj, doolerandug ndaamar, taggat-yaram gu doolerandu, doolerandug gaal, doolerandug asamaan, doolerandub kàttan-ferñent

Cosaanam Soppi

ci taariix, doolerandu mooy boole, gi Newton def; jëmm ak gëstubidiw. Kon su nu ko xoole ci wallu taariix jëmm walla fisiyaa ci doolerandu la joge. Ci sunu besu tay yi, day lu noppale, ci daara yu kawe yi, ne atte doolerandu yi ci jëmm la ñu joge.

Xam-xam yi ci lënku Soppi

Doolerandu ab banxaas la ci xam-xam yiy gëstu jalaxu yi ak soppeekuy neen yi, ci lu tukkee ci doole jiy man a indi googu jalaxu walla googu coppiku. Man nan koo xoolee ni ag wàll ci xam-xamu jëmm. Kon aajoom mooy leeral, xalaatjiitalu jalaxug neen yu tekkaaral yi, ak yaram yu asamaan si walla jëmm yuy dund (dun-doolerandu) ëbb na tamit:

  • Doolerandu gu yàgg ga, ni ko it gu newton, moo ñeel njangat gu imbiku (njangatum jalaxu yi te bañ a bayyi xel ca ngérte la), njangatu demin yu tekkaaral ak yuy yëngu, muy demiin gu wayaymbir (doolerandu gu tomb) walla demin gu lëj (doolerandu gu daj).
  • Dolerandug asamaan, mooy jang jalaxub yaram yu asamaan si.
  • Doolerandug tekkaaral, mooy jang demin gu bari cër, lu mel ne gil yi, yi cëroo ay milioŋi ngënjabar.
  • Doolerandug jëmm moom day gëstu demin yu am y melokaanu jëmm yu mel ne doolerandu gu yolaakon yi ak doolerandu yu seen demin soppeekuwu.


Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Doolerandu