Mooy fukk ak ñeenteelu buur ca nguuru Jolof gu mag ga. Su fekkee daanug Lat Joor feeñ na ci taxawaayu jàmbaar yi ci kanamu tubaab bi, loolu terewul Alburi Njaay jël ndondol bañ ak fukki loxoom. Alburi tax na tubaab bi fattewul Lat joor. Looloo tax tubaab bi doon ko xoolee bëtu mbañeel ci fat gi mu fatoon Lat Joor.

Gàddayug Alburi Soppi

Ñoñantal gu metti gi tubaab biy teg waa réew mi te Alburi manu koo faj moo taxoon mu génn rèew mi dem fekki Aamadu Taal doomu Sayxu Omar Taal ca Kolomina. Foofa la àndeek moom jàmmaarloo ak tubaab bi, ci luy dayob njàmbaar ba ci 1893 la Alburi daanu ci Doosu, baatam ni Poto!

Seetal BUNTU TAARIIX
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Alburi Njaay