Cosaan wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Tamsier (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Aucun résumé des modifications
Tafaan: recent_changes
Rëdd 1 :
'''Cosaan''' baati [[Seereer|Seereer-Safen]] la. Moo teki "début" / "origine" / "commencé" ci làkki Seereer.<ref>{{fr}} « Cosaani Sénégambie » (« L’Histoire de la Sénégambie») : 1ere Partie relatée par Macoura Mboub du Sénégal. 2eme Partie relatée par Jebal Samba de la Gambie [in] programme de Radio Gambie: « Chosaani Senegambia ». Présentée par: Alhaji Mansour Njie. Directeur de programme: Alhaji Alieu Ebrima Cham Joof. Enregistré a la fin des années 1970, au début des années 1980 au studio de Radio Gambie, Bakau, en Gambie (2eme partie) et au Sénégal (1ere partie) [in] onegambia.com [in] The Seereer Resource Centre (SRC) (« le Centre de Resource Seereer ») : URL: www.seereer.com. Traduit et transcrit par The Seereer Resource Centre : Juillet 2014. p. 28-29 [http://www.seereer.com/The-Seereer-Resource-Centre-French-Transcript-of-Cosaani-Senegambia-part1-Sohna-Chenaba-Saar-part2-History-Saluum.pdf]</ref>
[[Image:Ndangane.jpg|thumb|300px|Cosaan ([[Ndangane]], [[Senegaal]])]]
Ci [[angale]] mooy ''tradition''. Ci [[faranse]] mooy ''tradition''.
 
[[Wàll:Cosaan]]
 
Ci xëtt wi, dama see fas yeeni jeema tekki ani lan moodi cosaan. Sama weerukay ci walu xam-xam moodi jangat-nit . Bile baat, manko tëggé ci (anthropologie), manaam anthro=nit ak pologie=jangat. Cosaan, aada, ak luñuubaaxo daño fasoo, dugantè lu bari. Waayé, ci sama gis-gis, cosaan moy reenu askan, manaam fu aw askan bayee koo. Bilep firi daa ajju si walug bërëp (espace). Cosaan, mana firi batay luñu donnu ci makk ñi. Kon ci tënkk, cosaan, moy reenu askan, di delu waayu askan. Ndaxte cosaan moy lunġa xamni moom la maam yi daan def. Boo länkalee cosaan ak aada, di luñu baaxo def, loolu moo lay jox "culture". Culture nak moo gena mattalee boy séet. Ndax baat la bu emb mboleem fan yu doomu aadam fèntt, ligeey, ak lumu deffar ak loxoom, wala mu xeltu ko ta mu jem ci walu dundam, man nañ jappé "culture". Kon, suma suka ndikoo ci lii ma fessäl, dama jeema wax ne, cosaan mooy "tradition", "origine"; aada mooy "coutume". Waayé buma juumul, baatu "culture" dafa boolee aada ak cosaan.
Cosaan nak, ci walu xeltu, baat bu jaxaso la. Ndax tekkina ay jëff (actes), ay gis-gis (vision), mbaax (valeurs), ak ay mbir yuñu don nee ci maam yi la moo waral mu lëntt. Sama laac moo: cosaan "embu" wala ab yan bu makk ñi doon aw laantoo, dalee ko ci maam yu yag ya ba si jamonoy tay ji? Wala book, cosaan, nekul rek ab embu bu nga xamê si dara soppe ku wucci la ta ñu don nee ci maam yi , waayè mbir muy soppee ku la. Manaam luñuy jellee ci makk ñu jekk ya, ta diko mengalee ak nekinu tay, mélè kaanu tay.
Gëstukat yu barri daño jappu ne bu fekeeni cosaan ab embula, kon du luñu wara soppi; waaye bu nekkee lu dox la, dalee ko ci jamano yu yàg ya, kon luy walbatiku. Nittu jamano boo jel, dañu tànn ci seen cosaan ay lëffin, wacci licci dess. Rax ci dooli, dañuy fentt ay mbir yu bees dolli ca. Bilee gis-gis, booy seet, moo gena am maana, gena dal xèl. Ndax day junjju ne, aw askan warula wax ni sama cosaan kon duma ko bayyi. waaye day tànn li gena rafet ci cosaan, baayi li mengowul ak jamanomfen. Waaye timit, nguuruk reew munek war jôk aar cosaanam ci coppiku aduna bu gaawjôkaar bilee. CosaanCosa, don te mengo tul ak, danu ko wara dencci fu woor ngir elek ci bir sunu doom ak sunuy set man xam lu seeni maam doon doxale seen aduna. Cosaan ak aaday Reew yi eup doolee dañu wali ci cosaanu reew yi new doolee, ak dileendi nasaxal. Jokkoo ak waxtaanu cosaan yi, manaam ni ñuy abalaantee, lu baaxla. Bu loolu amul, yokkute du am. Wante lii warut ta tax nu bayi sunu yos./
 
Bu njekk, borom xam-xam yi bayoo tuggal ta see gëstu ajju ci walu jangat-nit, daño weddi woon ni nit ku ñuul amul aada ak cosaan. Li lalloon bilee weddi moodoon ne see dëkk yi ñoo bagoona noot, jalgate axu doomu adam, moom (coloniser) ngir asaloo seeni kom-kom. Bi aduna doxee ba nootagee bi jeex, bu afrik moom boppam, xam-xamu tubaabbi tasaaro, ñeppu nagu nagn ni askan yeppa am aada ak cosaan, ak seeni mbaax (valeurs). Nit ku nuul bu melni Seex Anta Job, jok takku gestul nu sunu cosaan fumu bayee ko. Ligee yam wanee ne nit yu nuul no tabaxoon Ezipt bu yaag ba. Lolu di ndam lu rey si xeetu nit ku nuul.Ndax te bo xamul fo jogee, do xam fo jem.
SEEX LO
 
Ci « https://wo.wikipedia.org/wiki/Cosaan » lañ ko jële